Yàlla taxawu na Israyil
2
1 Kàddug Aji Sax ji dikkal ma, ne ma:
2 «Demal yéeneji lii, Yerusalem di dégg,
nga ne: “Aji Sax ji dafa wax ne:
Maa ngi fàttliku sa ngor ba ngay ndaw,
ak sa cofeel ba nga deeb séet,
ba ngay topp sama gannaaw ca màndiŋ ma,
ba ngay jaare fa dara dul sax.
3 Mooy ba Israyil dee lu ñu sellalal Aji Sax ji,
di ndoortel meññeefama.
Képp ku ko sex, toppees ko ko,
musiba dikkal ko.”»
Kàddug Aji Sax jee.
Bànni Israyil wor nañu
4 Dégluleen kàddug Aji Sax ji,
yeen waa kër Yanqóoba,
ba ci mboolem làngi kër Israyil.
5 Aji Sax ji dafa wax ne:
«Ana sikk bu ma seeni maam gisal,
ba tax ñu sore ma,
di topp xërëmi neen,
ba far neen?
6 Newuñu: “Ana Aji Sax,
ji nu génne woon réewum Misra,
jiite nu ca biir màndiŋ ma,
ca joor gu wow gaak xur ya,
réewum maral ma lëndëm këruus,
jaareesu fa, dëkkeesu fa?”
7 Ma indi leen suuf su nangu,
ngir leel leeni meññeefam aki ngëneelam.
Ngeen dikk sobeel sama suuf sii,
ba sama céru suuf si siblu.
Aji Sax jaa ngi layoo
8 «Sarxalkat yi newuñu: “Ana Aji Sax ji?”
Ñi ŋank yoon wi faaleetuñu ma,
njiit yi gàntal ma,
yonent yiy waxe waxyuy Baal, tuur mi,
di topp lu leen dul jariñ.
9 Moo ma tax di layooteek yeen,
ba layook seeni sët.»
Kàddug Aji Sax jee.
 
10 «Jàll-leen ba ca duni Kitim fa sowu, te xool;
yónneeleen Kedar fa penku, seetlu bu baaxa baax
ndegam dingeen gis lu mel nii!
11 Fu aw xeet masa weccee yàllaam?
Moonte duñuy yàlla sax!
Moona xeet wi ma séddoo weccoo séen darajay Yàlla
te du leen jariñ dara.
12 Asamaanee, waarul ci lii!
Jommil, ba jommaaral!»
Kàddug Aji Sax jee.
13 «Ñaari yoon la xeet wi ma séddoo bàkkaar:
ma di bëtu ndox muy dund,
ñu wacc ma, man,
di gasal seen bopp kàmbi dencukaayi ndox,
te kàmb yi fett, di senn.
 
14 «Israyil da dib jaam a?
Am daa juddoo kërug njaam?
Ana lu tax ñu doon alalu sëxëtoo?
15 Gaynde yaa ngi ŋar ci seen kaw,
di leen xiiru!
Gaynde yee gental seenum réew,
ba seeni dëkk di gent yu kenn dëkkul.
16 Te it niti Memfisoo niti Tapanesb
ñooy dikk wat leen nel.
17 Xanaa du yeena def seen bopp lii,
di wacc seen Yàlla Aji Sax ji,
ba mu leen di jiite ca yoon wa?
18 Léegi lu ngeen wuti Misra?
Dangeen di naani ca ndoxum Niil ma ca Misraa?
Lu ngeen wuti Asiri?
Dangeen di naani ca dexu Efraat ca Babilon a?
19 Seenug mbon a leen di mbugal,
seen ñàkk kóllëre yar leen.
Ñamleen ba gis ni ngeen ma dëddoo,
wormaalatuleen ma, man seen Yàlla Aji Sax ji,
muy loraange ju leen wex.»
Kàddug Aji Sax jee, Boroom gàngoor yi.
Yuda amul worma.
20 «Yàgg ngeena yiwiku,
dog seeni jéng,
ba ne dungeen ma jaamu.
Kaw tundoo tund,
ker garaboo garab gu naat,
gànctu ngeen fa.
21 Moona maa leen jëmbat, ngeen di ngëneelu reseñ,
di jiwu mu mucc ayib.
Nu ngeen walbatikoo di baadooloy reseñu àll?
22 Bu ngeen raggoo woon saabu,
ba raggooteek xeme it,
seen ñaawtéef gàkk, may gis.»
Kàddug Boroom bi Aji Sax jee.
23 «Nu ngeen ñemee naa: “Sobeelunu sunu bopp
te toppunu tuuri Baal?”
Seetleen li ngeen nekke ci xur wic,
xool-leen li ngeen di def,
mel ni giléem gu ndaw, di wodd-woddi,
fu ne mu daw jëm fa,
24 mbaa mbaamu àll mu miin màndiŋ mi,
xabtaloo bakkanam, di xañtu ngelaw li.
Bu bëggee tëbu, ku ko mana téye?
Kuuy mu koy sàkku du sonn,
bu ci tolloo rekk, mu jot ko.
25 Ma ne, buleen daw ba mujje tànki neen
ak put gu wow.
Ngeen naa: “Bul sonn,
sopp nanu yàllay doxandéem yi,
te ñoom lañuy topp!”»
 
26 «Gàcceg sàcc bu ñu jàpp
dees na ko gàcceel waa kër Israyil,
ñook seeni buur ak seeni kàngam
ak seeni sarxalkat ak seeni yonent,
27 ñoom ñii naa bii bant: “Yaay sunu baay,”
naan wee doj: “Yaa nu sukk, jur.”
Wonuñu ma kanam, xanaa gannaaw,
te bu leen musiba dikkalee, ñu naa:
“Wallu nu boog!”
28 Waaw, ana seen yàlla yi ngeen sàkkal seen bopp?
Bu leen musiba dikkalee,
nañ leen wallu, bu ñu ko manee!
Gannaaw yeen waa Yuda,
ni seeni dëkk tollu la seeni yàlla tollu!
29 Ana lu ngeen di layook man?
Yeen ñépp a ma gàntal!»
Kàddug Aji Sax jee.
30 «Mbugal naa seeni doom, jariñul dara.
Dégguñu yar,
bóom ngeen seeni yonent,
mbete gaynde yuy fàdde.
31 Éey niti Israyili tey,
teewluleen kàddug Aji Sax ji!
 
«Ni màndiŋ mi aaye, ndax mas naa nee aaye ci Israyil?
Mbaa ma mel ni réewum lëndëm aki loraangeem?
Lu waral sama ñoñ naa:
“Noo moom sunu bopp,
dootunu délsi fi yaw”?
32 Ab janq dina fàtte takkaayam?
Am ab séet dina fàtte mbubbum xewam?
Moona sama ñoñ fàtte nañu ma fan yu dul jeex.
33 Yeen aka mokkal gànctu!
Jeeg ju bon ji sax di jànge ci yeen.
34 Te seeni pendal sax taq na
dereti néew-ji-doole yu deful dara,
fekkuleen leen it ñuy dàjji kër jaamburd.
Loolu yépp terewul,
35 ngeen naan: “Nun de defunu dara,
merum Yàlla won na nu gannaaw moos.”
Gannaaw nee ngeen bàkkaaruleen,
maa ngii di leen àtte.
36 Yeen aka yomba soppi doxalin!
Waaye Misraa leen di bett,
na leen Asiri bette woon,
37 ngeen jóge ca yenu seeni loxo.
Aji Sax jee wacc ñi ngeen yaakaar,
ba dungeen baaxlee ci ñoom.»