8
1 «Su boobaa déy,»kàddug Aji Sax jee,
«noon yeey sulli yaxi buuri Yuda
ak yaxi kàngam yi
ak yaxi sarxalkat yi
ak yaxi yonent yi
ak yaxi waa Yerusalem,
fa seeni bàmmeel,
2 weer leen ci naaj week weer wi
ak mboolem biddiiw yi ñu soppoon,
di leen jaamu, di leen topp ak a sàkku,
di leen sukkal.
Deesu ko dajale, deesu ko suul;
day mel niy jonkan fi kaw suuf si.
3 Dee mooy gënal dund
mboolem ku des ci njaboot gu bon gii,
ak mboolem fu ñu dese fa ma leen tasaare woon.»
Kàddug Aji Sax jee, Boroom gàngoor yi.
Askan wi të na ticc
4 «Nanga leen wax ne leen:
Aji Sax ji dafa wax ne:
Ku daanu, da dul jógaat?
Am ku lajj, du délsi?
5 Lu tax xeet wii dëddu?
Lu tax Yerusalem gii lajj, baña délsi?
Ñu ngi langaamoo naxi neen,
baña délsi.
6 Teewlu naa, déglu naa;
du lu jaadu lañu wax.
Kenn tuubu ci mbonam,
ba ne: “Lu ma def nii?”
Ku nekk a topp yoonam,
ni fas wu màmm cib xare.
7 Ag xodd sax xam na bésub demam,
pitax, wetwet ak mbelaar it dem,
tey sàmm seen bésub délsi.
Waaye sama ñoñ faalewuñu àtteb Aji Sax ji.
8 Nu ngeen man ne: “Am nan xel,
nungeek yoonu Aji Sax ji,”
te xalimay yoonalkat soppi ko fen?»
9 Dees na gàcceel boroom xel yi,
ñu jàq, tarsu.
Kàddug Aji Sax jaa ngii ñu dëddu,
kon ana seenum xel?
10 «Maay joxe seeni jabar,
jox seeni tool ay foqatikat,
ndax ki gëna tuut ba ki gëna mag,
ñépp a ngi lewal lu lewul.
Ab yonent akub sarxalkat, ñépp a ngi wor!
11 Sofental nañu sama pajum ñoñ ñi dammtoo,
naan: “Jàmm, lépp jàmm!”
te jàmm amul.
12 Ñu wara am gàcce ci seen jëf ju siblu,
te gàcce gàcceelu leen.
Xamuñu sax luy kersa!
Moo tax ñuy fëlëñoondook ñiy fëlëñu.
Kera ba ma leen di dikkal, ñooy tërëf.»
Aji Sax jee ko wax.
Yaakaar tas na
Yàllaay wax
13 «Maa leen di witta witt.»
Kàddug Aji Sax jee.
«Garabu reseñ du dese doom,
figg du dese doom,»
kàddug Aji Sax jee,
«xob ya sax day wow.
Lu ma leen joxoon, rëcc na leen.»
Askan waay wax
14 «Ana lu nuy toog?
Fabuleen, nu dem ca dëkk ya tata wër,
deeyi fa.
Sunu Yàlla Aji Sax ji nar na sunu dee;
moo nu nàndal tookey mbugal,
nde noo tooñ Aji Sax ji.
15 Nuy yaakaar jàmm,
dara baaxul;
nuy séentum paj,
tiitaange ne jaas!
16 Seen noowi fas yaa dégtoo bëj-gànnaar fa Dan,
seen naari góor di ŋexal, suuf sépp yëngu.
Ñu dikk, tas réew mi tasar,
booleek li ci biiram,
ak dëkk beek ñi ci biiram.»
Yàllaay wax
17 «Maa ngii déy di leen yónnee
jaani ñàngóor yu déggul jat,
ñu di leen màtt.»
Kàddug Aji Sax jee.
Yeremi am na naqar
Yeremeey wax
18 Ndaw naqar wu tiis,
ndaw xol bu diis!
19 Sama bokk yaa ngooguy yuuxu
yuux yu àkki fu sore,
naan: «Moo Aji Sax ji daa newul Siyoŋ a?
Moo Buurub Siyoŋ da fee nekkatul a?»
Yàllaay wax
«Lu tax ñuy yékkati sama xol
ak seen jëmmi tuur yii,
seen yàllay doxandéem yi tekkiwul dara?»
Yeremeey wax
20 Ngóob wéy na, jamonoom wees,
te nun de muccagunu.
21 Sama bokk yi seen xol jeex
tax na sama xol jeex,
may tiislu, tancoo njàqare!
22 Moo diwu pajtal amul Galàdd aa?
Am fajkat a fi amul?
Ana lu waral bokk yi taneeguñu?
23 Éy ku may duyal sama bopp ndox,
saay gët di xelliy rongooñ
yu ma jooye guddeek bëccëg
bokk yi ñu bóom?