Aji Sax ji du moroomu xërëm
10
1 Yeen bànni Israyil, dégluleen kàddu,
gi leen Aji Sax ji dégtal.
2 Aji Sax ji dafa wax ne:
«Jikkoy xeeti yéefar yi, buleen ko roy;
màndargam asamaan, buleen ko tiit;
na ko yéefar yi tiit.
3 Aaday xeet yi kat neen la.
Garab lañuy dagge ca gott ba,
ab yettkat yette ko sémmiñ,
4 rafetale xaalis ak wurus,
daaj koy pont, dëgëral,
ba du yëngu;
5 muy saf kuñeental
ci biir tóokërub xaal.
Du wax, du séqi jéego,
ñu di ko gaŋar-gaŋaree.
Buleen ko ragal, du lore, du jariñe.»
Yeremeey wax
6 Aji Sax ji, kenn melul ni yaw,
yaaka màgg, jàmbaare, màggu tur.
7 Yaw Buuru xeet yi, ana ku la dul ragal?
Yaw déy yaa yelloo ragal.
Mboolem ñi xelu ci xeet yi
ak mboolem seeni buur,
kenn melul ni yaw.
8 Ñoom ñépp a bokk dofe, ñàkk bopp:
xam-xamu kasara, bant kese!
9 Xaalis lañuy jële Tarsis, xoobe ko bant,
wurus wu jóge Ufas, ñu boole ca,
ndaanaan liggéey ko,
tëggu gànjar yett ko,
ñu solal ko ndimo lu yolet
ak lu xonq curr,
lépp di liggéeyu ràbb yu xareñ.
10 Waaye Aji Sax jeey Yàlla dëgg.
Mooy Yàlla jiy dund,
di buur ba fàww,
xadaram gësëm àddina,
meram man xeet yi.
11 Lii nag, nangeen ko siiwal:
«Seen yàlla, yi sàkkul asamaan, sàkkuñu suuf,
ñooy sànku, jóge fi suuf ak fi asamaan tiim.»
12 Suuf, Aji Sax jee sàkke kàttanam;
dun bi, mu sampem xelam;
asamaan, mu lale xam-xamam.
13 Bu àddoo, ndoxum asamaan riir;
mu yéegey niir fa cati àddina,
yebbee ngelaw fa dencam ya,
daldi melax, taw.
 
14 Nitoo nit dim sannax, sore xam-xam:
te képp kuy tëgg sa jëmmu tuur, yaa añe gàcce.
Sa jëmmi weñ ji nga xelli, di neenug neen,
noog bakkan, tus!
15 Cóolóolu neen, liggéeyu caaxaan;
bu bésam taxawee, mu sànku.
16 Ki séddoo Yanqóoba déy wuute naak yii caaxaan.
Kookoo bind lépp,
te Israyil di giir gi mu séddoo.
Kookooy Aji Sax ji Boroom gàngoori xare yi!
Mbugal dikk na
17 Yerusalemee, yeen ñi ñu gaw,
forleen seen ëmb.
18 Aji Sax ji déy dafa wax ne:
«Maa ngii naa xërr waa réew mi bii yoon,
teg leen njàqare, ba ñu yég ko.»
Yerusalem ay wax
19 «Wóoy man, yàqu naa!
Ndaw góom bu metti!
Dama noon lii jàngoro doŋŋ a,
naa muñ!
20 Xayma xotatoo,
buumi xayma xëttandoo,
samay doom wacc ma, ne mes;
kenn sampatul sama xayma, firi ko.»
Yeremeey wax
21 Sàmmi xeet weeka dofe:
Aji Sax ji, sàkkuwñu ko.
Moo leen taxa bonle,
seen jur gépp tasaaroo.
22 Xibaar a ngoog, di ñëw,
riir mu réy a yëngoo réewum bëj-gànnaar,
nara gental dëkki Yuda yu mag yi,
till yi dëkke.
Yeremi tinu na Aji Sax ji
23 Aji Sax ji, maa xam ne
nit moomul yoonam,
kuy dox moomuli jéegoom.
24 Aji Sax ji, yar ma lu yem,
te bañ maa yare mer,
di ma semmal.
25 Xëppal sa xadar yéefar yi la yégul,
ak làng yi la tuddul.
Ñoo bóom giirug Yanqóoba,
bóom leen ba fàkkas leen,
gental seen dëkkuwaay.