Lu jëm ci Filisteen ñi
47
1 Kàddug Aji Sax ji dikkaloon na Yonent Yàlla Yeremi jëm ci Filisteen ñi, balaa Firawna di song dëkkub Filisteen ba ñuy wax Gasa. 2 Aji Sax ji dafa wax ne:
«Ndox a ngay fuddoo bëj-gànnaar,
diy waame, walsi,
walal réew meek li ci biiram
akub dëkk ak ku ci biiram;
doom aadama yuuxu,
waa réew mépp serandoo.
3 Booba fas yaa ràmbal,
watiir ya riir,
mbegey watiir ya kar-kareendoo,
yoxo yoqi, ba baay geesuwul doom,
4 bésub sànkute dikkal képp kuy Filisteen,
ba dagge dëkk yii di Tir ak Sidon
ndimbal lu ñu dese woon.
Aji Sax jaa ngay sànk Filisteen, ña des
te cosaanoo dunu Keret.
5 Watu nel, ñaawloo, dikkal na Gasa,
te wedamloo nañu Askalon.
Yeen ñi dese joor gi,
fu ngeen àppal seen yaram,
wi ngeen di daggat, di ko ñaawloo?
6 Ngeen naa: “Wóoy saamaru Aji Sax jii,
xanaa doo selaŋlu?
Dellul sa mbar, boog,
dal-lu, ne tekk!”
7 Waaye yaw saamar, noo mana selaŋloo
te Aji Sax ji yebal la
ci kaw Askalon ak waa tefesu géej,
fa mu ko dogale?»