Lu jëm ci Amoneen ñi
49
1 Lu jëm ci Amoneen ñi,
Aji Sax ji dafa wax ne:
«Israyil daa amuli doom?
Am daa amul dono?
Lu tax Milkoma tuur mi donloo suufas Gàdd,
ba ay jaamukatam sanc dëkki Gàdd?
2 Moo tax ay bés a ngii di ñëw,»
kàddug Aji Sax jee,
«maay dégtal Raba, dëkku Amoneen ñi,
coowal xare ci seen biir,
tund wa gental,
dëkk-dëkkaan ya tàkk ba jeex,
ba keroog Israyil futti ñooña ko futti woon.»
Aji Sax jee ko wax.
 
3 «Éy waa Esbon, Ayi seen dëkk bi tas na, yuuxuleen!
Yeen waa dëkk yi séq Raba,
sol-leeni saaku, ñaawloo,
jaab diggante tata yi, tiisloo.
Milkom seen tuur mi déy duggi na ngàllo,
ànd aki sarxalkatam aki kàngamam.
4 Céy Raba, bii dëkk bu taaru, toogadi,
yeena doon damoo xur yi,
ba ci seen xur wu naat wii?
Yeena yaakaaroon seeni denc,
naan: “Ku ñemee dal sunu kaw?”
5 Maa ngii di leen wàcceel njàqare,»
kàddug Boroom bi Aji Sax jee, Boroom gàngoor yi,
«njàqare luy bawoo fi leen wër fépp,
dàq leen, ku ne jubal yoonam,
du kenn ku leen di dajaleeti.
6 Waaye bu loolu weesee,
ma tijji wërsëgu Amoneen ñi.»
Kàddug Aji Sax jee.
Lu jëm ci Edomeen ñi
7 Lu jëm ci Edomeen ñi, Aji Sax ji Boroom gàngoor yi dafa wax ne:
«Xanaa boroom xel amatul fi Teman?
Xanaa ndigal a réer xamkat yi?
Am seen bopp a yàqu?
8 Yeen waa Dedan,
walbatikuleen daw, ruuroo seeni pax.
Maa ngi wàcceel askanu Esawub safaan,
seen mbugal taxaw na!
9 Su leen wittkati reseñ dikkalee, xanaa dinañu ca wacc ay doom?
Su leen ay sàcci guddi dikkalee,
du la leen doy lañuy sëxëtoo?
10 Waaye yeen askanu Esawu,
man maa leen di ñori, ba ngeen ne duŋŋ.
Maay siiwal seeni rawtu,
ba dootuleen mana làqu;
seeni goneek seeni bokk, ñépp ay sànku,
seeni dëkkandoo sax, kenn du ca des ku naan:
11 “Jirim yi ngeen bàyyi,
maa leen di dundal,
te seeni jëtun man nañu maa yaakaar.”
12 Ndegam ñi yeyoowul mbugal
ñooy jolu kaasu mbugal,
nees leen di ñàkka toppe, yeen?
Dees na leen topp moos,
ngeen jolu kaasu mbugal.
13 Giñ naa ko ci man mii, déy,»
kàddug Aji Sax jee,
«Boccra, dëkk bii day mujj di gent bu ñu doyadal,
ndànd-foyfoy bu ñuy móoloo,
dëkk-dëkkaanam yépp gental ba fàww.»
Yeremeey wax
14 Ab dégtal laa dégg, mu bawoo fa Aji Sax ji,
ndaw la yebal ci biir xeet yi, ne leen:
«Dajeleen waajal xare te song Edom xare!
15 Yeen Edom, tuutal leen laay def ci biir xeet yi,
ñu xeeblu ngeen di doon ci biir doom aadama yi.
16 Seen ragluwaay ak seen reewande sànk na leen,
yeen ñi dëkke xuntiy doj,
féetewoo colli tund yi.
Waaye su ngeen ajee seenum tàgg ni jaxaay it,
fa laa leen di àjjee.»
Kàddug Aji Sax jee.
17 «Edom day mujj gental,
ku fa jaare waaru,
di muslu ci mboolem li ko dal.
18 Edom day tas ni Sodom ak Gomor ak la ko wër.»
Aji Sax jee ko wax.
«Nit du ca dëkk,
doom aadama du fa dal.
19 Maa ngii di fëlle gottub Yurdan ni gaynde,
wuti mbooy gu naat.
Xef ak xippi déy, ma fëxale fa ñépp,
ba tabb fa ki ma taamu.
Ana moos ku mel ni man?
Ku am sañ-sañ ci man?
Ana njiit luy taxaw fi sama kanam?
20 Kon dégluleen pexe mi Aji Sax ji waajal Edom,
mébét yi mu mébétal waa Teman ñooñu!
Ndegam deesu leen wommat ni seen gàtt yu ndaw, yóbbu,
ba yàq seen parlu yaxeet.
21 Seen jéll day réy ba riiral suuf,
seeni yuux àkki géeju Barax ya.
22 Lu mel ni jaxaay a ngii, naa fëyy,
firiy laafam, këfsi Boccra.
Bésub keroog fitu jàmbaari Edom ne tërit,
mel ni kuy matu.»
Lu jëm ci Damaas
23 Lu jëm ci Damaas:
«Dëkk yu mag ya ko wër,
di Amat ak Arpàdd, jàq nañu;
dég-dég bu tiis ba ñu dégg la.
Dañu ne yàcc, jaxasoo,
mbete géej gu sàmbaraax, deesu ko dalal.
24 Damaas a ne yasar, ne wërëñ, di daw;
tiitaange ne leen nuus,
njàqareeku mitit ne leen taral
ni kuy matu.
25 Lu tee ñu gental bii dëkk bu siiw,
taax yii ma saf?
26 Su bés baa kay, seeni waxambaane fëlëñoo pénc yi,
seeni xarekat wedam.»
Kàddug Aji Sax jee, Boroom gàngoor yi.
27 «Maay taal ca tatay Damaas
sawara wu xoyom këri Buur Ben Addàd.»
Lu jëm ci Arabi Kedar ak Àccor
28 Lu jëm ci Kedar ak nguuri Àccor yi Nabukodonosor buuru Babilon nangu woon, Aji Sax ji dafa wax ne:
«Ñokket ci kaw Kedar,
ba tas waa penku yooyu,
29 nangu xaymaaki jur,
ak kiiraay ak luy jumtukaay,
yóbbu seeni giléem,
te biral leen, ne leen:
“Musiba ubale na!”
30 Yeen waa Àccor,
fëxleen te dawa daw,
ruurooji seeni pax.»
Kàddug Aji Sax jee.
Mu ne: «Nabukodonosor buuru Babilon déy,
lalal na leen pexe,
mébal leen.
 
31 «Ayca ci kaw xeet wii ne finaax,
dëkke xel mu dal!»
Kàddug Aji Sax jee.
«Du bunt, du galanu weñ gu ñu fegoo,
te ñoom rekk a dëkk.
32 Dees na nangu seeni giléem,
tonni seen juroo jur,
ma tasaare ñooñuy wat seen peggu kawaru bopp,
ngelaw lu jóg, buub leen, yóbbu,
ma yéewe leen seen musiba, wetoo wet.»
Kàddug Aji Sax jee.
33 «Àccor day doon dëkkub till,
gental ba fàww;
nit du fa dëkk,
doom aadama du fa dal.»
Lu jëm ci Elameen ñi
34 Kàddug Aji Sax ji dikkaloon na Yonent Yàlla Yeremi, jëm ci Elameen ñi, ci njàlbéenu nguurug Cedesyas buurub Yuda. Mu ne:
35 Aji Sax ji Boroom gàngoori xare yi dafa wax ne:
«Damay damm fittu Elam,
seen ngëneelu ngànnaay.
36 Maay ngelawe ñeenti weti asamaan,
dal fi kaw Elam,
tasaare leen fépp fu ngelaw jublu,
ba du am xeet wu daw-làquy Elam dul fekki.
37 Maa leen di xoqtal fi seen kanami noon,
yiy wut seen bakkan,
alage leen sama tàngooru mer.»
Kàddug Aji Sax jee.
«Maa leen di toppe saamar,
ba raafal leen.
38 Maay déjjatee Elam buur ak bummi,
samp fa samab jal.»
Kàddug Aji Sax jee.
39 «Waaye fan yu mujj ya,
maay tijji wërsëgu Elam.»
Kàddug Aji Sax jee.