51
1 Aji Sax ji dafa wax ne:«Maa ngii di yebal fi kaw Babilon,
waa Lew Kamay gii,a
ngelawal yàqkat.
2 Maay yónnee Babilon ay beeskat
yu ko bees, tonni réew ma, ba mu set.
Keroog bésu safaan ba déy,
fu ne lañu koy songe.
3 Buleen leen may fu ñu taxaweek seen kiiraay, di fitte;
buleen ñéeblu seeni waxambaane,
fàkkasleen seen gàngoor gépp.
4 Ñii dee, ne wetar réewum Babilon;
ñee gaañu, ne lasar ca mbedd ya.
5 Israyil ak Yuda ñàkkuñu seen Yàlla,
Aji Sax ji Boroom gàngoor yi,
te réewum Babilon fees naaki moy
yu ñu moy Yàlla Aji Sell ji séddoo Israyil.
6 «Yeen gan ñi, génnleen Babilon,
ku ne rawaleji sa bakkan.
Buleen ñaawtéefu jaambur sànkaale;
lii àppu mbugal la bu Aji Sax ji matal;
seen añ la, bu mu leen añale.
7 Aji Sax jee yor Babilon ci loxoom, muy kaasu wurus bu def xadaru xeet ya,
di màndal mboolem àddina;
xeet ya naan ca,
ba tax ñuy say.
8 Teewul Babilon jekki daanu, tasaaroo.
Jooyleen ko,
dàmp ko, seral mititam,
jombul mu wér.»
Gan ñaay wax
9 «Bu nu sañoon faj Babilon, mu wér,
waaye wérul.
Nan ko ba te dem,
ku ne ñibbim réewam.
Àtteb Babilon kat àgg na asamaan,
àkki na fa kaw niir ya.»
Bànni Israyil ay wax
10 «Aji Sax ji jox na nu dëgg.
Nanu yeggeji waa Siyoŋ
jaloorey Aji Sax ji, sunu Yàlla.»
Yàllaay wax
11 «Nàmmleen fitt yi, feesale mbar yi!
Aji Sax ji xabtal na buuri Medd fi kaw Babilon,
nar koo tas.
Lii mbugalu Aji Sax jee,
mbugal mi këram waral.
12 Yékkatil-leen tatay Babilon raayab xare,
yokkleen wattukat yi,
taxawal leen fa ñuy wattoo,
te waajal tërukat yi.
Aji Sax ji def na li mu waxoon
ne dina ko def waa Babilon.
13 Yeen ñi dëkke weti ndox yu ne xéew,
seen alal ne xéew,
seen muj taxaw na,
seen buumu bakkan dog na.
14 Aji Sax ji Boroom gàngoor yi giñ na ci boppam.
Mu ne: “Maa leen di same ay nit niy njéeréer,
ñu xaacu, song leen.”»
Yeremeey wax
15 Suuf, Aji Sax ji sàkke kàttanam;
dun bi, mu sampem xelam;
asamaan, mu lale xam-xamam.
16 Bu àddoo ndoxum asamaan riir,
mu yéegey niir fa cati àddina,
riddee ngelaw fa dencam ya,
daldi melax, taw.
17 Nitoo nit dim sannax, sore xam-xam,
te képp kuy tëgg sa jëmmu tuur, yaa añe gàcce.
Sa jëmmi weñ ji nga xelli, di neenug neen,
noowug bakkan, tus!
18 Cóolóolu neen, liggéeyu caaxaan;
bu bésam taxawee, mu sànku.
19 Séddoob Yanqóoba déy wuute naak yii caaxaan.
Kee bind lépp,
bind giir gi mu séddoo.
Kookooy Aji Sax ji Boroom gàngoori xare yi!
Yàllaay wax
20 «Yaw Babilon, yaa doon sama wàkku,
di sama ngànnaay,
ma di la wàkke xeet yi,
rajaxee la réew yi,
21 wàkke la fas ak gawaram,
wàkke la watiir ak dawalkatam,
22 wàkke la góor ak jigéen,
wàkke la mag ak ndaw,
wàkke la waxambaaneek ub janq,
23 wàkke la sàmm ak géttam,
wàkke la beykat ak lëkkeb nagam,
wàkke la kàngam ak jawriñ.
24 Waaye mboolem lu Babilon ak waa réew mépp def ci Siyoŋ,
maa leen koy fey, ngeen di gis, yeen Yudeen ñi.»
Kàddug Aji Sax jee.
25 «Maa ngii déy, fi sa kaw, yaw Babilon, ponkalum yàqkat bi,»
kàddug Aji Sax jee,
«yaw miy yàq àddina sépp.
Maay tàllal sama loxo fi sa kaw,
taxañe la fa kaw doj ya,
def la ponkalum jalu dóom.
26 Deesul seppee fi yaw doju tabax wu ñuy lëkklee,
mbaa doju tabax wu bokk ci kenu,
nde gent ngay doon ba fàww.»
Kàddug Aji Sax jee.
27 «Yékkatileen ub raaya fi réew mi
te walal liit gi xeet yi.
Dajaleleen xeet yi fi kaw Babilon,
te xabtal fi kawam réew yii:
Araraat ak Minni ak Askenas.
Tabbal-leen ko njiitu xare mu ko song,
indil koy fas yu saf ndiiraani njéeréer.
28 Dajaleleen xeet yi fi kaw Babilon,
wooleen buuri Medd ak kàngam ya
ak jawriñ ñaak mboolem réew mu ñu moom.
29 Suuf a fuddu, wañaaru,
mébéti Aji Sax jeey sottalal Babilon,
ngir réew ma dib gent bu kenn nekkul.
30 Jàmbaari Babilon xareetuñu,
ña nga des ca seeni tata,
doole ŋiis,
ñu mel niy jigéen.
Bunti dëkk bi dàjjiku,
kër ya jàpp.
31 Xélukat dab xélukat;
ndaw jottli ndaw xibaar
bu ñu yeggeji buuru Babilon, ne ko
nangu nañu dëkkam ba wetoo wet,
32 nangu jàllukaayi dex ya,
taal barax ya,
xarekat ya raj-rajloo.»
33 Aji Sax ji Yàllay Israyil Boroom gàngoori xare yi déy dafa wax ne:
«Ñu ngi dëggaate Babilon mu taaru mi,
ni ñuy dëggaatee dàgga ju ñuy bàccesi.
Balaa yàgg ngóobu Babilon taxaw.»
Yerusalem ay wax
34 «Buuru Babilon warax na ma.
Da maa muucu,
ñiit ma, ba ma set ni ndab.
Da maa modd ni ninki-nànka,
sole kollam li gën ci man,
yàbbi la ca des.»
35 Siyoŋ ne: «Yal na sama yàpp ak sama coono topp Babilon.»
Yerusalem ne: «Yal na sama deret topp waa Babilon!»
36 Aji Sax ji nag dafa wax ne:
«Maa ngii di leen layool seen layoo,
ba feyul leen.
Maay ŋeeral géejam,
ŋiisal am walam,
37 Babilon def jali doj,
di paxum till,
di gent bu ñuy muslu,
kenn du ko dëkke.
38 Ñu ngi ŋarandoo niy gaynde,
di xiiroo ni gaynde yu ndaw.
39 Ñu tàng bay bëgga dee,
ma may leen ñu naana naan,
màndal leen, ñu mana xawaare,
tëdd nelaw nelawi fàww,
duñu yewwooti.»
Kàddug Aji Sax jee.
40 Aji Sax ji nee: «Maa leen di wommat
niy xar ba ca rendikaay ba,
ñu mel ni kuuyi xar aki sikket.
Ngalla Babilon
41 «Ãa! Ana nees mana nangoo Sesag?
Nees mana tege loxo ki àddina sépp di kañ?
Ana nu Babilon mana gente fi digg xeet yi?
42 Géej ay mëdd Babilon,
mu sàngoo gannaxam yu jallaañoo,
43 ay dëkkam gental,
réew mi ne sereŋ, di ndànd-foyfoy,
kenn du ko dëkke,
doom aadama du fa jaare.
44 Maay dikke mbugal Bel,
tuur mi ci Babilon,
yàbbiloo kob lancam.
Xeet yi noppee def um wal, wuti ko,
tatay Babilon it màbb.
45 Yeen sama ñoñ, génnleen fi seen biir,
na ku ne rawale sa bakkan,
ba mucc tàngooru sànjum Aji Sax ji.
46 Bu seen fit rëcc,
ngeen di tiit xibaar yi ñuy yéene ci réew mi:
ren yéene jib,
déwén yéene jibati,
fitna law ci réew mi,
njiit ne njiit dann.
47 Kon ay bés a ngii di ñëw,
yu may dikke mbugal tuuri Babilon,
réew mépp torox,
ña ñu bóom ñépp wetaroo fa biir.
48 Su boobaa asamaan ak suuf
ak mboolem li ci biiram
sarxollendoo, di bége li dal Babilon.
Bëj-gànnaar kay la yàqkat yay bawoo.»
Kàddug Aji Sax jee.
Yeremeey wax
49 Waa Babilon it dinañu daanu
ngir waa Israyil ñi ñu bóom,
ba ñu yem ak mboolem waa àddina yi ñu bóom,
te ñu daanu ndax Babilon.
50 Ée yeen ñi rëcc saamar,
buleen taxaw, demleen,
di fàttlikoo Aji Sax ji fu sore,
tey bàyyi xel Yerusalem.
Bànni Israyil ay wax
51 «Nooka rus ci saaga yi nu dégg,
ak gàcce gi nu sëlmoo
ndax doxandéem yi dugg
ci biir bérab bu sell bi ci kër Aji Sax ji.»
Yàllaay wax
52 «Moo tax, bés a ngii di ñëw,»
kàddug Aji Sax jee,
«maay dikke mbugal seen jëmmi tuur yi, ñoom,
ñi ñu jam di binnee fi réew mi mépp.
53 Su Babilon yéegoon asamaan,
dàbbli fa tata ju ne kekk sax,
du tee ay yàqkat bawoo fi man, dal ci kawam.»
Kàddug Aji Sax jee.
Yeremeey wax
54 Yuuxi njàqare fa Babilon,
réewum Kaldeen ñooñaa toj ba tojatoo.
55 Aji Sax jee niy yàqtee Babilon,
tukkal fa riir mu réy.
Gàngoori noon yaa ngay buur ni gannaxi géej,
seen riirum kàddu jolli.
56 Yàqkat déy dikkal na Babilon,
jàpp ay jàmbaaram,
dammatey fittam.
Aji Sax ji déy mooy Yàlla jiy yoole,
di fey pey gu mat sëkk.
57 Mu ne: «Maay màndal seeni kilifaak seeni kaaŋ
ak seeni kàngam ak seeni jawriñ ak seeni jàmbaar,
ñu tëdd nelaw nelawi fàww,
duñu yewwooti.»
Kàddug Buur a, Aji Sax ji Boroom gàngoor yi.
58 Aji Sax ji Boroom gàngoor yi dafa wax ne:
«Tatay Babilon yu mag yi
dees koy màbba màbb;
bunt yu kawe ya lakk ba jeex.
Xeet yee ñaq ci neen,
waaso yee sonnal sawara.»
Yeremi santaane na misaal
59 Bëkk-néegu Buur Cedesyas moo doon Seraya doomu Nerya doomu Maaseya. Ba Cedesyas tolloo ca ñeenteelu atu nguuram, la Seraya ànd ak moom Babilon. 60 Fekk na Yeremi bind cib taxañ mboolem safaan yiy dikkal Babilon, di mboolem mbir yooyu jëm ci Babilon. 61 Yeremi sant Seraya, ne ko: «Boo àggee Babilon, fexeel ba biral kàddu yii yépp. 62 Te nga wax ne: “Aji Sax ji, yaw déy, yaa xamle ne dëkk bii dina tas, dara du ci dëkkati, du doom aadama, du rab. Ab gent lay doon ba fàww.” 63 Boo jàngee taxañu mbind mii ba noppi, nanga ci takk aw xeer, sànni ko ci biir dexu Efraat. 64 Su ko defee nga ne: “Nii la Babilon di diige te du jógati ndax safaan bi may wàcce fi seen kaw, ba ñu sonn.”» Fii la kàdduy Yeremi yem.