Aji Sax ji yebal na Esekiyel
2
1 Ba loolu amee boroom kàddu ga ne ma: «Yaw nit ki, jógal taxaw, ma wax la.» 2 Naka la ma wax loolu, ngelaw solu ma, ne ma yékkét, ma taxaw, di dégg kiy wax ak man. 3 Mu ne ma: «Yaw nit ki, maa lay yebal ci bànni Israyil, xeeti fippukat yi fippu ci sama kaw; ñook seeni maam dañu maa masa tooñ ba bésub tey jii. 4 Ci nit ñu dëgër bopp te dërkiis laa lay yónni. Wax leen, ne leen: “Lii Boroom bi Aji Sax ji da koo wax.” 5 Ñoom nag, su ñu la déglook su ñu gàntalee ndax kërug fippukat gi ñu jikkowoo, dinañu xam ne ab yonent a ngi ci seen biir. 6 Waaye yaw nit ki, bu leen ragal, bul ragal seeni wax. Xam naa ne ay taxas aki dég a lay wër, nga toog ci kawi jiit. Waaye bul ragal seeni wax te bul tiit seen kanam doonte kërug fippukat lañu. 7 Nanga leen àgge samay wax, ñu déglook ñu gàntal, nde ay fippukat lañu. 8 Yaw nit ki nag, déglul lii ma lay wax. Bul fippu ni kërug fippukat gii. Sexal, te lekk li ma lay jox.»