Congum noon yi nuyoo na
2
1 Wal-leen bufta ca Siyoŋ,
dégtal-leen ab yéene ca sama kaw tund wu sell.
Na waa réew mi mépp lox,
nde bésub Aji Sax jaa ngi dikk
te dëgmal na.
2 Bésub lëndëmu xàmbaari guddi gu ne këruus,
mbete bànqanoos bu lale ci kaw tund yi.
Gàngoor gu mag te am doolee ngi,
gu ni mel masula am mukk,
te dootul am feeki at, ba maasoo maas.
3 Lu leen jiitu, sawara lekk;
lu leen topp, ag daay xoyom.
Ni toolub Àjjana la réew mi
ci seen kanam di mel,
ñu won ko gannaaw,
muy màndiŋ mu wéet,
te kat dara du leen rëcc.
4 Seen melo ni melow fas,
ñuy daw ni fasi xare.
5 Ni watiiri xare di ker-keree,
ni lañuy cëppoo ca kaw tund ya,
mbete sawara wuy lakk boob, di fet-feti.
Gàngoor gu am doole lañuy dikke,
làng-déral xare!
6 Ñépp a leen di gis, jàq,
kanam yépp di tàkk.
7 Niy jàmbaar lañuy songe,
ni ñeyi xare lañuy yéege am tata.
Ku nekk ay jubalu yoonam,
kenn wàccul aw ñallam.
8 Kenn buuxul moroom ma,
ku nekk aw sélam lay topp,
ci biir saan yi lañuy xuus, jàll it,
te duñu taxaw.
9 Dëkk bi lañuy song,
ci kaw tata ji lañuy dukkate,
ci kaw kër yi lañuy yéeg it,
te ci palanteer yi lañuy jaare dugg niy sàcc.
10 Bu ñu jubsee, suuf yëngu,
asamaan rëng-rëngi,
jant ak weer giim,
biddiiw yi fat seenug leer.
11 Aji Sax jeey àddu fi kanam mbooloom xareem,
dalam ba réy lool,
te kiy jëfe ndigalam am kàttan.
Bésub Aji Sax ji kay moo réy te raglu lool!
Ana ku ko mana dékku?
Dellu ci Aji Sax ji jot na
12 «Terewul ba léegi,» kàddug Aji Sax jee,
mu ne: «Délseeleen seen léppi xol ci man,
boole kook koor aki jooy aki yuux.
13 Du seeni yére doŋŋ ngeen di xotti,
ngir ñaawlu,
seenub xol ngeen di xottiwaale, ñaawloo ko.
Waññikuleen ci seen Yàlla Aji Sax ji,
mooy boroom yiw ak yërmande;
mer maa diib, ngor ga bare,
muy fomm mbugal.
14 Jombul mu dëpp, fomm,
bàyyi gannaawam barke,
ba ci saraxu pepp ak saraxu tuuru,
ñeel seen Yàlla, Aji Sax ji.»
 
15 Wal-leen bufta fa Siyoŋ,
sellal-leen ag koor, te woote am ndaje.
16 Dajaleleen askan wi,
sellal-leen mbooloo mi,
wooleen mag ñi,
te ngeen dajale gone yi ba ci ñiy nàmp.
Na boroom séet génn ub néegam,
séet ba génn xaymab céetam.
17 Diggante buntu néeg bu sell beek sarxalukaay bi,
sarxalkat yi, boroom dénkaaney Aji Sax ji,
nañu fi taxaw jooy;
nañu ne: «Aji Sax ji, yërëmal sa ñoñ;
bul wacce say séddoo gàcce,
ak ñaawley xeeti jaambur yi.
Lu jar ñuy wax ëllëg ci biir askani jaambur yi,
naan: “Ñii, ana seen Yàlla ji?”»
Aji Sax ji nangu na ñaan
18 Aji Sax ji moo fiire am réewam,
ñeewante ñoñam.
19 Aji Sax jee àddu, ne ñoñam:
«Maa ngii di leen yónnee am pepp,
ak biiñ bu bees akug diw,
ba ngeen regg,
te dootuma leen gàcceel
ci biir xeeti jaambur yi.
20 Waa bëj-gànnaar, maa leen di soreleek yeen,
maa leen di dàq, jëme réew mu maral te wéet,
gàngoor ga jiitu jubal géeju penku,
ga féete gannaaw jubal 0géeju sowu,
ba seeni néew gilli, xasaw ba ubale,
ngir jëf ju réy ji ñu def!»
 
21 Yaw suuf, bul tiit, bégal te bànneexu,
nde Aji Sax ji moo def ay jaloore!
22 Yeen rabi àll yi, buleen tiit,
parluy àll yi day naat, garab yi meññ;
figg ak reseñ di baaxee seen xéewal.
23 Yeen doomi Siyoŋ, bégleen,
te bànneexu ci seen Yàlla Aji Sax ji.
Moo leen di may taw yu jëkk, muy njekk,
moo leen di sottil taw yu jëkk,
ak taw yu mujj, na woon.
24 Dàgga yi day fees ak pepp,
mbànd yi rembat ak biiñ bu bees aku diw.
 
25 «Sama mbooloom xare mu réy,
mi ma yebaloon fi seen biir,
te ñuy njéeréer yeek seen tostan,
ak salleer yeek soccet yi,
maa leen di delloo ati mbey yi ñu leen lekkal.
26 Dingeen lekka lekk, ba regg,
di sàbbaal seen turu Yàlla Aji Sax,
ji leen defal kéemaan,
te sama ñoñ dootuñu rus mukk.
27 Dingeen xam ne ci biir Israyil laa ne, man,
maay seen Yàlla Aji Sax ji, du keneen,
te sama ñoñ duñu rus mukk.