Aji Sax ji misaal na mbugalu Israyil
(Saar 7.1—9.10)
Peeñu mu jëkk mi
7
1 Am na bés Boroom bi, Aji Sax ji won ma am peeñu. Ndeke ma ngay sàkk naaxu soccet. Fekk na ñu góobal Buur, ba gàncax giy saxaat. 2 Soccet yiy lekk gàncaxu réew mi, ba mu bëgga jeex, ma ne: «Éy Boroom bi Aji Sax ji, ngalla déet! Askanu Yanqóoba àttan na lii am? Lu néew doole lañu.» 3 Aji Sax ji fomm ko, ne ma: «Kon du am.»
Peeñum ñaareel bi
4 Boroom bi, Aji Sax ji dellu ma feeñu. Ndeke Boroom bi, Aji Sax ji day waaja mbugale ñoñam sawara. Mu xoyom xóotey géej mbàmbulaan, bay waaja xoyom réew ma. 5 Ma ne: «Boroom bi, Aji Sax ji, ngalla taxawal. Askanu Yanqóoba àttan na lii am? Lu néew doole lañu.» 6 Boroom bi Aji Sax ji fomm ko ne ma: «Liitam du am.»
Peeñum ñetteel bi
7 Mu feeñooti ma, gisuma lu moy Boroom bi taxaw ci ab tata, mu ñu natte buumu beteex ba ñu koy tabax. Ma nga yor buumu beteex ca loxoom. 8 Aji Sax ji ne ma: «Amos, ana loo gis?» Ma ne ko: «Xanaa buumu beteex.» Boroom bi ne: «Maa ngii di natte buumu beteex fi digg Israyil, sama ñoñ. Dootuma leen baal dara.
9 Dees na tas fu askanu Isaaxa di màggale,
ba gental bérabi Israyil yu sell.
Maay jëlal askanu Buur Yerbowam saamar.»
Dàq nañu Amos
10 Ba mu ko defee Amaciya sarxalkatu Betel yónnee ca Yerbowam buurub Israyil, ne ko: «Amos a ngi lay fexeel ci digg Israyil. Réew mi du àttan waxam ji. 11 Mu ngi naan ci xare ngay deeye, te dees na jële Israyil suufam moos, yóbbu ngàllo.»
12 Gannaaw loolu Amaciya ne Amos: «Yaw boroom peeñu mi, dawal, làquji réewum Yuda, nga waxe fa waxyu, am fa loo dunde. 13 Betel gii nag, bu fi waxeeti waxyu, ndax fii jaamookaayu buur la, te it jaamookaayu réew mi la.»
14 Ba loolu amee Amos ne Amaciya: «Man de dumab yonent te bokkuma ci kurélu yonent. Sama gétt laa yor, te maa ngi topptoo ay tooli figg. 15 Aji Sax jee ma jële fa ma doon sàmme samay gàtt. Moo ma ne: “Demal biralal ma waxyu ci Israyil sama ñoñ.” 16 Léegi nag, déglul kàddug Aji Sax ji. Yaa ma ne: “Bul biral waxyu ci Israyil te bul kebetu ci kaw askanu Isaaxa.” 17 Gannaaw noonu la, Amaciya, Aji Sax ji nee:
“Sa jabar ci biir dëkk bi lay gànctoo,
say doom, góor ak jigéen, saamar tëral;
sam réew, ñu natte buum, séddoo.
Yaw nag, réewum yéefar ngay deeyeji;
Israyil, ñu jële kom réewam, gàll ngàllo.”»