11
1 Libaŋéey, ubbil say wunt,
sawara xoyom sa garabi seedar.
2 Yaw garabu sippar, yuuxul,
garabu seedar daanu na,
garab yu darajawu rajaxoo na.
Yeen garabi seen ya ca Basan, jooyooleen,
nde gott bu fatt baa sëngéem.
3 Jooyi sàmm ya jib na,
seen daraja réer na,
ŋari gaynde ya it jolli na,
nde gajjug tàkkal Yurdan a tas.
Sàmm bu baax jotul yoolam
4 Aji Sax ji sama Yàlla dafa wax ne:
«Sàmmal gétt gi ñuy rendiji.
5 Ñi leen jënd di leen rendi,
te jàpp ne yoon toppu leen ci;
ñi leen jaay naan: “Sant Aji Sax ji, woomle nanu,”
gétt gi la seeni sàmm yërëmul.
6 Dootuma yërëm waa réew mi (/àddina) déy,»
Kàddug Aji Sax jee!
«Maa ngii di teg doom aadama yi,
ku nekk ci loxol moroomam,
ak ci loxol buuram,
ñu not réew mi,
te duma leen xettli ci seen loxo.»
7 Ba loolu amee may sàmm xar yi teefonke yi nara rendiluji, rawatina ñi gëna sonn ci gétt gi. Ca laa jël ñaari yeti sàmm. Benn bi ma tudde ko Xejjoo, bi ci des ma tudde ko Bennoo. Ci kaw loolu may sàmm gétt gi. 8 Gannaaw gi, ñetti sàmm laa dàq ci wenn weer. Ci kaw loolu ma doyal ci xar yi, ñoom it, ma génnliku leen. 9 Ma ne gétt gi: «Dootuma leen sàmm. Na ñiy dee, dee; ñiy sànku, sànku; ñi dese bakkan yàppante ci seen biir.»
10 Ba mu ko defee ma jël sama wenn yet wi, Xejjoo, damm ko, ngir doge ko sama kóllëre gi ma fasoo woon ak askan yépp. 11 Bésub keroog la kóllëre ga dog, teefonke yi may xool daldi xam ne loolu kàddug Aji Sax ji la.
12 Gannaaw loolu ma ne leen: «Su leen neexee, joxleen ma sama peyoor, su leen neexul téyeleen ko.» Ñu waññ fanweeri donji xaalis, feye ma.
13 Aji Sax ji ne ma: «Ndaw njëg gu réy gu ma leen jaral! Sànni ko ca boroom njaq ya.» Ma jël fanweeri donji xaalis yaa, sànni ko boroom njaq ya, ca kër Aji Sax ji.
14 La ca tegu ma damm sama ñaareelu yetub sàmm ba, Bennoo, ngir dog bokk gi dox diggante Yuda ak Israyil.
15 Aji Sax ji nag neeti ma: «Léegi jëlal jumtukaayu sàmm bu ñàkk bopp. 16 Maa ngi nii kat di taxawal ab sàmm ci réew mi. Lu ci réer, faalewu ko; lu ci lajj, du ko seet, lu ci gaañu, du ko faj, lu wér du ko xont, te lu ci duuf, mu yàpp, ba toj seeni we.
17 Wóoy bii yambarub sàmm
buy wacci gàttam.
Yal na saamar làggal loxoom,
fuq bëtu ndijooram.
Yal na loxoom lax ne làcc,
bëtu ndijooram giim ba gëmm fatuus.»