Yeesu dugg na Yerusalem
11
1 Gannaaw loolu Yeesu ak taalibe ya jege nañu Yerusalem, ba agsi dëkki Betfase ak Betani ci wetu tundu Oliw ya. Noonu Yeesu yebal ñaar ciy taalibeem, 2 ne leen: «Demleen ci dëkk bi ci kanam. Bu ngeen fa duggee, dingeen fa gis cumbur gu kenn masula war. Yiwileen ko, indi. 3 Bu leen kenn nee: “Lu ngeen di def?” neleen ko: “Boroom bi da koo soxla, te léegi mu delloosi ko.”»
4 Taalibe ya dem nag, ñu gis cumbur ga ci mbedd mi, mu yeewe cib buntu kër. 5 Bi ñu koy yiwi nag, am na ca ña fa taxaw, ñu ne leen: «Lu ngeen nar, bay yiwi cumbur gi?» 6 Taalibe yi wax leen, ni leen Yeesu digale woon, nit ñi bàyyi leen, ñu dem.
7 Ñu indi cumbur gi Yeesu nag, lal ci seeni yére, mu toog ci. 8 Ñu bare lal seeni yére ci yoon wi, ñenn ñi dagg ay cari garab ci tool yi, lal leen it ci yoon wi. 9 Ñiy jiitu ak ñiy topp ci Yeesu ñépp di wax ci kaw naan:
«Osaana!
Yaw miy ñëw ci turu Boroom bi, ku barkeel nga!
10 Nguuru sunu maam Daawuda giy ñëw dina barkeel!
Ci bérab yu gëna kawe, nañu ne: “Osaana!”»
11 Noonu Yeesu dugg Yerusalem, dem kër Yàlla ga, xool lépp, ba noppi génn dem dëkku Betani, moom ak fukki taalibe ya ak ñaar, ndaxte dafa guddi.
Yeesu dàq na jaaykat ya ca kër Yàlla ga
12 Bët set ñu génn Betani, fekk Yeesu xiif. 13 Noonu mu séen fu sore garabu figg gu sëq, mu dem seeti, ndax am na ay doom. Waaye bi mu fa eggee, gisul lu dul ay xob, ndaxte jamonoy figg duggagul. 14 Ci kaw loolu mu ne garab gi: «Dootuloo meññ mukk!» Taalibe yi dégg loolu mu wax.
15 Bi ñu eggee Yerusalem, Yeesu dugg ci kër Yàlla gi, daldi dàq ñi fay jaay ak ñi fay jënd. Mu daaneel taabali weccikatu xaalis yi ak tooguy jaaykati pitax yi, 16 te mayul kenn, mu yóbbu am njaay ci kër Yàlla gi. 17 Mu di leen jàngal ne leen: «Ndax waxuñu ci Mbind mi:
“Dees na wooye sama kër
këru ñaan ci Yàlla ngir xeet yépp.”
Waaye yéen def ngeen ko këru sàcc.»
18 Bi ko sarxalkat yu mag ya ak xutbakat ya déggee nag, ñu ragal ko, ndaxte mbooloo mépp dañoo waaru ci njàngleem. Noonu ñu seet pexem reylu ko.
19 Bi timis jotee Yeesu ak taalibe yi génn dëkk bi.
Garabu figg gi ñu rëbb
20 Ci suba si, bi ñuy dem, ñu gis ne garabu figg gi dee na, ba wow koŋŋ. 21 Noonu Piyeer fàttaliku li xewoon, ne Yeesu: «Kilifa gi, xoolal, figg gi nga rëbb dee na, ba wow!»
22 Yeesu ne: «Gëmleen Yàlla. 23 Ci dëgg maa ngi leen koy wax, ku ne tund wale: “Jógal, tàbbi ca géej ga,” te nga gëm ne loolu dina am, bañ cee boole xel ñaar, kon sa ñaan nangu. 24 Moo tax maa ngi leen koy wax, bu ngeen di ñaan Yàlla, lépp lu ngeen ko mana laaj, gëmleen ne jot ngeen ko, te dingeen ko am. 25-26 Te it bu ngeen di ñaan, fekk ngeen jàppal kenn dara, baal-leen ko, ngir seen Baay bi ci kaw baal leen seeni tooñ, yéen itam.»
Sañ-sañu Yeesu
27 Gannaaw loolu ñu duggaat Yerusalem, te Yeesu doon doxantu ca ëtti kër Yàlla ga. Noonu sarxalkat yu mag ya ak xutbakat ya ak njiit ya dab ko 28 ne ko: «Yëf yii ngay def, ci ban sañ-sañ nga koy defe? Te ku la may sañ-sañu def ko?»
29 Yeesu ne leen: «Man itam dinaa leen laaj lenn; bu ngeen ma ci tontoo, kon dinaa leen wax ci ban sañ-sañ laay defe yëf yii. 30 La Yaxya daan def, di sóob nit ñi ci ndox, fu mu ko jële, ci Yàlla walla ci nit ñi?»
31 Bi ñu ko déggee, ñuy werante ci seen biir naan: «Bu nu nee: “Ci Yàlla,” kon dina nu laaj: “Lu tax gëmuleen ko kon?” 32 Waaye bu nu nee: “Ci nit ñi,” kon mbooloo mi dal ci sunu kaw;» ndaxte ñépp teg nañu Yaxya ab yonent. 33 Ñu wax Yeesu nag ne: «Loolu de xamunu ko.» Noonu Yeesu ne leen: «Kon man itam duma leen wax ci ban sañ-sañ laay defe yëf yii.»