Deewu Lasaar
11
1 Amoon na benn waay bu woppoon, ñu koy wax Lasaar. Ma nga dëkkoon Betani, moom ak Maryaama ak Màrt, mi mu bokkaloon ndey ak baay. 2 Maryaama mooy jigéen jiy sottiji latkoloñ ci tànki Boroom bi, fompe ko kawaram. Moom la càmmiñam Lasaar woppoon. 3 Ñaari jigéeni Lasaar yónnee ca Yeesu ne ko: «Boroom bi, sa xarit wopp na.» 4 Bi Yeesu déggee xibaar boobu, mu ne: «Lasaar de, woppam jooju du ko mujje; day wone ndamu Yàlla, tey màggal Doomu Yàlla ji.»
5 Yeesu soppoon na Màrt ak Maryaama ak Lasaar. 6 Bi mu yégee nag ne Lasaar wopp na, mu toogaat yeneen ñaari fan ca bérab, ba mu nekkoon. 7 Gannaaw loolu mu ne taalibe ya: «Nanu dellu Yude.» 8 Taalibe ya ne ko: «Kilifa gi, yàggul dara waa Yude doon nañu la wuta rey ak i xeer, nga di fa dellu?» 9 Yeesu ne leen: «Xanaa du bëccëg fukki waxtook ñaar la? Kuy dox bëccëg, du fakktalu, ndaxte day gis leeru àddina si. 10 Waaye kuy dox guddi, dina fakktalu, ndaxte leer nekkul ci moom.» 11 Yeesu wax loolu, teg ca ne: «Sunu xarit Lasaar nelaw na, waaye maa ngi dem yee ko.» 12 Taalibe ya ne ko: «Boroom bi, bu nelawee kay, kon dina wér.»
13 Yeesu dafa bëggoona wax ne, Lasaar dee na, waaye taalibe yi dañoo xalaatoon ne mbiri nelaw rekk lay wax. 14 Ci kaw loolu Yeesu wax ci lu leer ne: «Lasaar dee na. 15 Bég naa ngir yéen ndax li ma fa nekkul, ngir seen ngëm gëna dëgër. Waaye nanu ko seeti.» 16 Noonu Tomaa, ki turam di tekki «Séex bi», daldi ne yeneen taalibe ya: «Nanu dem nun itam, deeyandoo ak moom!»
Yeesu mooy ndekkite, mooy dund
17 Bi Yeesu agsee, mu fekk ne bi ñu dencee Lasaar ak léegi, mat na ñeenti fan. 18 Betani ma nga woon ca wetu Yerusalem, diggante bi matul woon sax ñetti kilomet. 19 Yawut yu bare ñëwoon nañu kër Màrt ak Maryaama, ngir dëfal leen ci seen deewu càmmiñ.
20 Bi Yeesu ñëwee, Màrt yég ko, dem di dajeek moom; fekk booba Maryaamaa nga toogoon ca kër ga. 21 Màrt ne Yeesu: «Boroom bi, boo fi nekkoon de, sama càmmiñ li du dee. 22 Waaye xam naa ne fii nu tollu sax, loo ñaan Yàlla, mu may la ko.» 23 Yeesu ne ko: «Sa càmmiñ dina dekki.» 24 Màrt ne ko: «Xam naa ne dina jóg bésu ndekkite la, keroog bés bu mujj ba.» 25 Yeesu ne ko: «Man maay ndekkite li, maay dund gi. Ku ma gëm, boo deeyee it, dinga dund. 26 Rax-ca-dolli kuy dund te gëm ma, doo dee mukk. Ndax gëm nga loolu?» 27 Mu ne ko: «Waaw, Boroom bi. Gëm naa ne yaay Almasi bi, di Doomu Yàlla, ji wara ñëw àddina.»
28 Bi Màrt waxee loolu, mu daldi dem wooyi Maryaama ne ko ci pett: «Kilifa gaa ngi fi; mi ngi lay laaj.» 29 Bi Maryaama déggee loolu, mu daldi jóg, gaawantu dem ca Yeesu. 30 Te fekk duggagul woon ca dëkk ba, waaye ma nga woon ba tey ca bérab, ba mu daje woon ak Màrt. 31 Noonu Yawut, ya nekkoon ca kër ga di dëfal Maryaama, gis ko mu ne bërét génn, ñu daldi koy topp, defe ne day jooyi ca bàmmeel ba.
32 Bi Maryaama agsee nag ca Yeesu, ba gis ko, mu daanu ciy tànkam ne ko: «Boroom bi, boo fi nekkoon, sama càmmiñ du dee.» 33 Yeesu gis ne mi ngi jooy te Yawut yi ànd ak moom itam ñu ngi jooy. Mu daldi jàq, am naqar wu réy. 34 Mu ne leen: «Fu ngeen ko denc?» Ñu ne ko: «Kaay gis, Sang bi.»
35 Yeesu jooy. 36 Noonu nag, Yawut ya ne: «Gis ngeen ni mu ko bëgge woon!» 37 Waaye am na ca ñoom ñu doon wax naan: «Moom mi ubbi bëti gumba gi, ndax manul woona fexe ba Lasaar du dee?»
Lasaar dekki na
38 Yeesu dellu am naqar wu réy, daldi dem ca bàmmeel ba. Pax la mu ñu yett ci doj, ube ko xeer. 39 Yeesu ne: «Dindileen xeer wi!» Màrt, jigéenu ku dee ki ne ko: «Boroom bi, dina xasaw xunn fii mu nekk, ndaxte am na ci bàmmeel bi ñeenti fan.» 40 Yeesu ne ko: «Ndax waxuma la ne boo gëmee, dinga gis ndamu Yàlla?» 41 Ñu daldi dindi xeer wa. Yeesu xool ci kaw, ne jàkk asamaan, ñaan Yàlla ne: «Baay, sant naa la ci li nga ma déglu ba noppi. 42 Xam naa ne doo jóg ci di ma déglu, waaye dama koy wax, ngir nit ñi ma wër gëm ne yaa ma yónni.»
43 Bi mu waxee loolu, Yeesu woote ak baat bu dëgër ne: «Lasaar, ñëwal ci biti!» 44 Néew bi daldi génn, ñu gis càngaay, li ñu takke woon tànk yi ak loxo yi, ak kaala, gi ñu muure woon kanam gi. Yeesu ne leen: «Tekkileen ko, bàyyi ko mu dem.»
Pexe yi jëm ci Yeesu
45 Yawut yu bare ca ña ñëwoon kër Maryaama te gis li Yeesu defoon, daldi koy gëm. 46 Waaye amoon na it ñu demoon ci Farisen ya, nettali leen la Yeesu defoon. 47 Farisen ya ak sarxalkat yu mag ya woo kureelu àttekat ya ne: «Nit kii kat, kéemaan yi muy def a ngi bëgga bare. Lu nuy def nag? 48 Ndaxte su nu ko bàyyee mu jàppoo nii, ñépp dinañu ko gëm, te kilifay Room yi dinañu ñëw, daaneel sunu kër Yàlla gi, tas sunu réew!»
49 Amoon na ca ñoom ku ñuy wax Kayif te mu nekkoon sarxalkat bu mag ba at mooma; mu ne leen: «Xamuleen ci mbir mi dara. 50 Xanaa xamuleen ne, kenn nit rekk dee ngir ñépp, mooy li gën ci yéen? Bu ko defee réew mi du tas.»
51 Loolu Kayif waxu ko woon ci sagoom, waaye li mu nekkoon sarxalkat bu mag ba at mooma, moo tax Yàlla xiirtal ko mu ne, Yeesu dina dee ngir réew mi. 52 Du woon rekk ngir xeet woowu, waaye ngir itam doomi Yàlla, yi tasaaroo yépp, dajaloo nekk benn.
53 Keroog la njiiti Yawut ya dogu ci rey Yeesu. 54 Taxoon na ba Yeesu dootul doxantu ci biir Yawut ya. Noonu mu dem ca gox bu jege màndiŋ ma, ca dëkku Efrayim. Foofa nag la toog ak ay taalibeem.
55 Bésu Mucc baa ngi doon jubsi, mu doonoon ag màggal ci Yawut yi, ba ñu bare ca waa àll ba di dem Yerusalem balaa booba, ngir sanguji set. 56 Ñu ngi doon wut Yeesu tey waxante ca kër Yàlla ga naan: «Lu ngeen ci xam? Ndax dina ñëw ci màggal gi walla déet?» 57 Sarxalkat yu mag ya ak Farisen ya daldi santaane ne, bu kenn xamee fu Yeesu nekk, mu yégle ko, ngir ñu man koo jàpp.