Ñépp war nañoo déggal njiit yi
13
1 Gannaaw loolu na nit ku nekk déggal ñi yore baat ci kanamam; ndaxte amul njiit lu fi Yàlla sampul. Njiit yépp nag Yàlla moo leen fi teg. 2 Kon ku leen baña déggal, ndigalu Yàlla nga lànk; ku def loolu, yoon dina la dab. 3 Kuy def lu baax warula ragal njiit li, kuy def lu bon moo ko wara ragal. Soo ko bëggee baña ragal nag, kon defal lu baax, te dina la tagg. 4 Ndax Yàllaa ko dénk liggéey boobu ngir sa jàmm. Waaye sooy def lu bon, war ngaa ragal, ndax du cig neen la ame jaasiy àtte; jawriñu Yàlla la ngir wàcce meru Yàlla, ci fey ku def lu bon. 5 Kon fokk ngeen déggal ko, waxuma sax ndax sañ-sañam boobu, waaye it ngir seen xel dal.6 Gannaaw Yàllaa sas njiit yi liggéey boobu, te ñi ngi ci, kon fàww ngeen fey galag. 7 Joxleen ku nekk céram; ku ngeen wara fey galag, feyleen ko ko; ku ngeen wara fey juuti, feyleen ko ko; ku ngeen wara weg, wegleen ko; ku ngeen wara teral, teral-leen ko.
Bëgganteleen
8 Buleen ameel kenn dara, lu dul mbëggeel; ndax ku bëgg sa moroom, wàccoo nga ak yoonu Musaa. 9 Ndaxte ndigali Yàlla yépp, yi deme ni: «Bul njaaloo, bul bóome, bul sàcc, bul bëgge,» walla leneen ndigal lu mu mana doon, wax jii moo leen ëmb: «Nanga bëgg sa moroom, ni nga bëgge sa bopp.» 10 Ku bëgg sa moroom, doo ko tooñ; kon ku wéy ci mbëggeel matal nga yoonu Musaa.
Jekkleen ngir teeru Kirist, buy délsi
11 Te lii itam am na: xam ngeen bu baax jamono ji nu tollu; jamonoy yewwu jot na, ndax léegi sunu mucc gën na noo jege, ca ba nu dooree gëm. 12 Guddi gi màggat na, bët a ngi bëgga set. Nanu bàyyi nag jëf yu lëndëm te ràngoo gànnaay yi nu Yàlla jox, ngir dund ci leer. 13 Gannaaw nu ngi ci leer, na sunug dund rafet. Bunu naan sàngara ba màndi tey bànneexu; bunu njaaloo tey def i ñaawteef ak sunuy cér; bunu xuloo mbaa nuy ñeeyante. 14 Waaye gànnaayooleen Yeesu Kirist Boroom bi, te baña topp seen bakkan ciy bëgg-bëggam yu bon.