6
1 Nun nag ñiy liggéeyandoo ak Yàlla, nu ngi leen di ñaan: jariñooleen yiw, wi ngeen jote ci Yàlla, ngir mu baña neen ci yéen. 2 Ndaxte Yàlla nee na:«Ca jamono ja mu jekke, nangu naa sa ñaan;
ci bésu mucc gi laa la wallu.»
Tey jii la jamono ju jekk ji; tey la bésub mucc gi.
Tiis yi nu daj ci liggéeyal Yàlla
3 Bëggunoo lëmbaaje xelu kenn ci dara, ngir kenn baña sikk sunu liggéey. 4 Li nu bëgg moo di rafetal sunu tur ni jawriñi Yàlla ci fànn gu nekk; danuy muñ coono yi, tiis yi, njàqare yi; 5 ñu nuy dóor, di nu tëj ci kaso, dëkk yi di yëngu ndax sunu mbir; nuy liggéey ba sonn, di fanaane xool, di woor. 6 Nu ngi rafetal sunu yen ci dund gu sell, ci xam-xam, muñ ak laabiir, ci Xel mu Sell mi ak ci mbëggeel gu raxul njublaŋ, 7 ci kàddug dëgg ak ci kàttanu Yàlla, nu ngi yor gànnaayi njubte ci loxol ndijoor ak lu càmmoñ. 8 Ñu bàkk nu, jéppi nu, sant nu, xas nu. Ñu di nu jiiñ réeral, moona niti dëgg lanu. 9 Ñuy xeeb sunu tur, moona tur yi siiw nañu. Nu mel ni ñu loof, moona nu ngi dund. Ñu yar nu, teewul nu rëcc ci dee. 10 Danuy dékku tiis, waaye di bég fu nu tollu. Nu tumurànke, waaye di woomal ñu bare; amunu dara, fekk noo moom lépp.
11 Yéen bokki Korent, wax nanu leen sunu biir ak sunu biti, di leen ubbil sunu xol. 12 Ubbiku nanu ci yéen, waaye yéen ubbikuwuleen ci nun. 13 Maa ngi wax ak yéen ni samay doom; feyleen nu bor bi, yéen itam; ubbileen seen xol!
Bàyyileen bokkaale
14 Buleen likkoo ak ñi gëmul. Gan àndandoo moo mana am diggante njubte ak ndëngte? Gan booloo moo mana am diggante leer ak lëndëm? 15 Gan déggoo moo mana am diggante Kirist ak Beliyar? Gan jaxasoo moo mana am diggante ki gëm ak ki gëmul? 16 Nan la kër Yàlla mana mànkoo ak xërëm yi? Ndaxte nun nooy kër Yàlla Aji Dund ji, ni ko Yàlla waxe:
«Dinaa dëkk ci seen biir, tey dox ànd ak ñoom,
ma nekk seen Yàlla, ñuy samay gaay.»
17 Kon nag Boroom bi nee na:
«Génnleen biir ñooñu te beru.
Buleen laal dara lu am sobe,
kon dinaa leen teeru.
18 Dinaa nekk baay ci yéen,
ngeen di doom ci man, muy góor, di jigéen.
Moom la Aji Man ji wax.»