Deeleen dimbaleente
6
1 Bokk yi, ku ñu fekk muy def lu Yàlla bëggul, yéen ñi topp Xelum Yàlla, nangeen ko jubbanti ak xol bu lewet. Waaye nanga sàmm sa bopp, ngir bàkkaar bañ laa fiir, yaw itam. 2 Jàpplanteleen, noonu dingeen sàmm yoon wi Kirist tëral. 3 Ndaxte kuy naagu te fekk doo dara, dangay nax sa bopp. 4 Na ku nekk seetlu ni muy beye sasam. Bu ko defee dina mana naw boppam, tey bañ di diirante mbagg ak ñi ci des. 5 Ndaxte ku ci nekk dangaa wara yenu sab yen.6 Kiy jàng kàddug Yàlla war na sédd ki koy jàngal ci alalam jépp.
7 Bu leen ci dara nax; kenn du foontoo Yàlla, ndaxte lu waay ji, moom ngay góob. 8 Ku ji ngir sa nafsu, dinga góob li sa nafsu meññ, maanaam ag yàqute. Waaye ku ji lu soloo ak Xelum Yàlla, li Xel mi meññ ngay góob, maanaam dund gu dul jeex. 9 Bunu tàyyi ci def lu baax, ndaxte bu nu ci sawaree, bu waxtu wi jotee dinanu jariñu. 10 Noonu fi ak nu koy man, nanuy defal ñépp lu baax, rawatina nag sunu bokk yi gëm.
Mbindeef mu bees
11 Seetleen araf yu mag yii ma leen bind ci sama loxob bopp!
12 Ñiy gistal ci seen yaram, ñooñoo bëgg ngeen xaraf, ngir ragala daj fitna ci yégle deewu Kirist ca bant ba. 13 Kureel gi faaydaal xaraf, ñoom ci seen bopp sax, duñu topp yoon wi. Dañoo bëgga ngeen xaraf, ba ñu mana bàkku ci seen yaram, yéen. 14 Man ci sama wàllu bopp, duma bàkku mukk su dul ci deewu sunu Boroom Yeesu Kirist, ba ñu ko daajee ca bant ba. Deeyam moo tax ma mel ni ku dee ci yëfi àddina; yëfi àddina dee ci man. 15 Xaraf ak baña xaraf dara amu ci solo. Li am solo mooy nekk mbindeef mu bees. 16 Ñiy topp ndigal lii nag, yal na Yàlla wàcce jàmm ak yërmande ci ñoom, ak ci Israyilu Yàlla.
17 Léegi nag, bu ma kenn lëjalati, ndaxte yor naa ci sama yaram ay leget yuy màndargaal ne jaamu Yeesu laa.
18 Bokk yi, yal na yiwu Yeesu Kirist sunu Boroom ànd ak seen xel. Amiin.