Mbooloom ñi gëm, jenn jëmm la, ni céri yaram
4
1 Man mi ñu tëj kaso ngir Boroom bi nag, maa ngi leen di dénk, ngeen dund dundin wu yellook wooteb Yàlla. 2 Ngeen woyof toyy te lewet, di muñalante tey baalante ci mbëggeel, 3 te dem ba fu seen kàttan yem, ngeen likkoo ci jàmm, bay sàmm booloo gi leen Xelum Yàlla may.4 Jenn jëmm moo am, menn Xel, ak jenn yaakaaru ëllëg ju wooteb Yàlla ëmb. 5 Benn Boroom it a am, genn ngëm, ak benn seedeb ngëm ci li ñu leen sóob ci ndox. 6 Te jenn Yàllaa am, di Baayu ñépp, mu tiim ñépp, fees ñépp te dëkk ci ñépp.
«Yéeg na ba ca fa gëna kawe,
yóbbaale mbooloom noon mu bare, mi mu not,
tey séddale nit ñi ay may.»
9 Su nu waxee ne «yéeg na,» li moo ci génn: daa jëkka wàcc ba ca bérab ya gëna suufe. 10 Ki wàccoon moo yéegaat, ba tiim asamaan yépp, ngir fees lépp. 11 Moo may ñii di ay ndawam, ñii ay yonent, ñii ay taskati xibaaru jàmm bi, ak ñeneen ñuy sàmm mbooloom ñi gëm te di ko jàngal. 12 Maye na leen, ngir ñu waajal gaayi Yàlla yu sell yi, ñu mana bey seen sas ci taxawal mbooloom Kirist, di jëmmam. 13 Noonu nu mànkoo ci sunu ngëm ak ci xam Doomu Yàlla ji, ba kera nuy egg ci nekk nit ku sotti te taxaw taxawaay bu dëppook matug Kirist.
14 Noonu dootunu ay gone yu njànglem nit ku ñëw di fàbbi ci seeni làqarci ak seeni pexe, nu mel ni ay gaal yu duus yi ak ngelaw li di baaje. 15 Waaye dinanu wax dëgg, ëmb ko ci mbëggeel, bay màgg ci fànn gu ne ci sunu bokk ci Kirist. Mooy bopp, 16 te jëmm jépp ci moom lay dunde, di jëmm ju ràbboo te déggoo ci bépp tenqo, te cér bu nekk di def warugaram. Noonu jëmm ji di yokku ak a màgg ci biir mbëggeel.
Sunu jikko ju jëkk ak sunu jikkoy tey
17 Maa ngi leen di wax lii nag, te di ko dëggal ci kanam Boroom bi: buleen dundeeti ni xeeti àddina yi, ci seeni xalaati neen 18 ak seen xel mu lëndëm. Dañoo génn ci dundu Yàlla, ndax umple gi ñu am ci moom, ak li ñu ko tëjal seen xol. 19 Seen xol dafa dërkiis, ba ñu bayliku ciy topp seen nafsu, di sóobu ci bépp sobe te xér ci.
20 Waaye du dundin woowu ngeen jàng ci Kirist. 21 Ndax yaakaar naa ne dégg ngeen Kirist te jàng ngeen ci moom, ba xam dëgg gi Yeesu ëmb. 22 Maanaam ngeen yulli seen jikkoy judduwaale ju bon ji daan fés ci seeni jëf, di gëna yées, te ànd ak i bëgg-bëggam yu di naxi kese. 23 Te ngeen yeeslu ci seen biir xel, 24 te soloo jikko ju bees, ji Yàlla sàkk ci njubte lu dëggu ak sellaay gu dëggu.
Melow dund gu bees
25 Kon nag bàyyileen di fen, tey wax dëgg kenn ku nekk ci moroomam, ndax ku nekk sa genn-wàllu moroom nga. 26 Ku mer, bu mu jàll aw kaañ; bu jant bi sowaale seen mer, 27 ba ngeen may Seytaane bunt. 28 Ku daan sàcc, na ko dëddu te jublu ci liggéey lu baax ci ay loxoom, ngir mu mana dimbali ñi néew doole.
29 Bu genn kàddu gu ñaaw génn ci seen gémmiñ, waaye su wax yegsee, nangeen wax lu rafet, ba faj soxlay seeni moroom, te teg ñi leen di déglu ci yoonu yiw. 30 Buleen yóbbe tiis Xelu Yàlla mu Sell, mi leen tàmpe ngir bésu goreel ba. 31 Dëdduleen lépp luy wex mbaa tàng bopp, luy mer mbaa coow, lépp luy xaste mbaa coxor. 32 Te ngeen baax ci seen diggante, di laayante biir tey baalante, ni leen Yàlla baale ci turu Kirist.