Njub gu wóor
3
1 Kon nag samay bokk, bégleen ci Boroom bi. Duma sonn mukk ci di leen ko wax, ndax seen mucc moo ci aju.2 Moytuleen xaj yi, waaw, moytuleen ñiy jëfe lu bon, ñoom ñi seen xarafal weesul wàññi yaramu nit. 3 Ndaxte nun noo xaraf tigi, nun ñiy màggal Yàlla ci Xel mu Sell mi, di damu ci Kirist Yeesu, te amunu benn yaakaar ci matug nit.
4 Ba tey manoon naa am yaakaar ci sama bopp; su nit doon damu, maa ciy raw. 5 Xarafoon naa ca ayu-bés ga, bokk ci bànni Israyil ci giiru Beñamin, di Ebrë ci deret ak ci meen. Bu dee ci yoonu Musaa ngeen bëgga wax, ci tariixab Farisen laa bokkoon; 6 bu dee it ci mbirum farlu, daan naa fitnaal mbooloom ñi gëm Kirist; bu dee ci njub ci sàmm yoon, awma benn gàkk.
7 Waaye loolu lépp lu ma tegoon ay njariñ fa kanam Yàlla, dëddu naa ko ngir Kirist. 8 Rax-ca-dolli dëddu naa lépp ngir xéewali xam Kirist Yeesu sama Boroom, di xam-xam bu xóot, ba xel manu koo takk. Moo tax ñàkk naa sama lépp, te def ko ni mbalit, ngir am cér ci Kirist. 9 Na ma Yàlla fekk ci moom, waxuma ci njub gu aju ci sàmm yoon, waaye gu aju ci gëm Kirist, maanaam njub gi nu Yàlla sol ci kaw ngëm. 10 Moom laay ittewoo xam, ak doole ji ànd ak ndekkiteem, ma bokk ci ay coonoom, ba fekki ko ci deeyam, 11 ngir mana séddu ci ndekkiteem, su ma ko manee am.
Farlu ci jëm kanam
12 Waxuma ne jagoo naa ko ba noppi, waxuma it ne aji mat laa, waaye maa ngi daw, ngir jot li tax Kirist jël ma. 13 Bokk yi, gëmuma ne jot naa ko ba noppi, waaye lenn lii laay def: fàtte li ma weesu, jublu ci li féete kanam, 14 di daw yen muj ga, ngir jot li ma Yàlla taxa woo, di cér bi ma Yàlla wooye te dencal ma ko ci asamaan ci darajay Kirist Yeesu.
15 Nun ñi mat nag, nanu xalaat loolu. Su ngeen ci amee werantey xol, Yàlla dina leen ko leeralal. 16 Li am daal, fa seen ngëm tolloo, na fa seen jëf àgg.
17 Kon nag bokk yi, toppleen ma te xool ñiy roy ci li nu tëral diirub sunu ngan ci yéen. 18 Ndaxte jëfi ñu bare juuyoo na ak dee gi Kirist dee; loolu wax naa leen ko ba tàyyi, maa ngi koy waxaat léegi ak i jooy. 19 Alku lañuy mujje, ñoom ñiy jaami seen biir, di wonoo lu ruslu, tey wut yëfi àddina rekk. 20 Waaye nun waa asamaan lanu, te noo ngi xaar Boroom bi Yeesu Kirist jóge fa, musalsi nu. 21 Noonu dina soppi sunu yaram wu toroxlu, def ko ni yaramam wi ànd ak ndam dëppook kàttanam, gi ko mana notal mbindeef yépp.