Leeral yi
Aaróona: Magu Yonent Yàlla Musaa la. Moom la Yàlla jëkka def sarxalkat bu mag ci biir bànni Israyil.
Abiib: Weeru Abiib moo doon weer wi jiitu ci at mi, ni ko bànni Israyil takke woon, mu dëppook weeru màrs, jàpp awril ci takkinu nasaraan. Weeru Abiib, Nisan lañu ko mujj di wooye.
Àggripa: Seetal ci Erodd.
Aji Sax j-: Mooy turu Yàlla. Mooy ki sax fàww.
albatar: Xeer wu rafet la. Ni kew la weexe, ñu daan ko yett, di ko def ay njaq.
Almasi: Baatu ebrë la, di tekki «ki ñu fal». Bu Yawut yi masaana fal nit, dañuy sotti diw ci boppam, muy yonent, di sarxalkat mbaa buur. Almasi nag, mooy ki Yàlla sol Noowam, ngir firndeel ne mooy Yonent, bi nuy jottli xibaaru jàmm bu Yàlla; di Sarxalkat, bi nu ubbil bunt fa Yàlla; te di Buur, bi yilif lépp ak ñépp.
alowes: Gàncax gu xeeñ la, gu ñu daan génne ndox mu wex ca xob ya, di ko sotti néew yi.
Alyaasa: Yonent la woon, moo donn Yonent Yàlla Ilyaas.
Asera: Mooy tuuru Kanaaneen mu jigéen mi ñu gëmoon ne mooy giiral nit. Ñu di ko farala dendaleek tuur mi ñuy wax Baal. Ñu daan ko jaamu fu jege ab gott, walla fu ñu ko sampal ay xer.
Astàrt: Moo doon tuur mu jigéen mi gënoona màgg ci tuuri Kanaaneen ñi. Ñu yaakaaroon ne moo jagoo wàllu séy, te mooy giiral. Moo doon jabaru tuur mi ñuy wax Baal.
Baal: Moo doon tuur mi gëna màgg ci tuuri waa Filisti. Waa dëkk bu mag bu nekk amoon nañu seenum Baal. Moo tax Baal yu baree amoon. Tur wi di firi «sang bi». Ñu jàppoon ne moo moom lépp lu ñu sàkk, te mooy tax jur geek tool yi nangu. Diiney Baal daa laajoon ay nit ñuy jaay seen bopp fa ñuy jaamoo Baal, muy lu Aji Sax ji ñaawlu lool.
Babilon: Babilon, ab dëkku penku la woon, di péeyub réewum Kalde. Babel la jëkkoona tudd. Fa la bànni Israyil nekke woon jaam diggante 566—536 at lu jiitu Almasi. Leeg-leeg xanaa ñu misaale ko dëkku Room, ak it nguur, giy bëreek Yàlla ci mujug jamono.
bàmmeel b-: Bu jëkkoon ca penku, aw doj wu mag lañu daan yett, ba mu mel ni néeg, ñu man caa dugg, di fa denc ay néew.
bànni Israyil: Israyil mooy tur wi Yàlla jox Yanqóoba, doomu Isaaxa, sëtub Ibraayma. Ñi soqikoo ci Yanqóoba lañuy wooye bànni Israyil mbaa Yawut. Ñoo def fukki giir ak ñaar, di xeet yi soqikoo ci doomi Yanqóoba. Gannaaw ba réew ma séddlikoo, saa yu Mbind mi indee baatub «Israyil» ñaare, réew mépp taxul ñuy wax, waaye fukki giir yi féete bëj-gànnaar rekk lañuy wax.
Beñamin: Mooy caatum Yanqóoba te moo sos giirug bànni Israyil gi ñuy wooye Beñamineen ñi. Ba réew ma xaree ñaar, giirug Beñamin ak gu Yuda ñoo far. Sóol ma jëkk di Buur ci Israyil, ci Beñamineen ñi la bokk.
bérab bu sell b-: Muy xaymab jaamookaay ba, di néeg Yàlla ba ñu mujje tabax, lu ci nekk ñaari wàll lees ko séddale woon. Wàll wu jëkk, wa ngay janook rido ba, moo doon bérab bu sell ba. Sarxalkat yépp a fa sañoona dugg. Néegu biir ba ca wàllaa rido ba lañu doon tudde bérab bu sell baa sell. Sarxalkat bu mag ba doŋŋ moo sañoona dugg benn yoon cim at ca bérab bu sell baa sell te deretu sarax lay duggaale. Taxawalinu xayma bi ak tabaxinu kër Yàlla gi ak li ci biiram, lépp, sellaayu Yàlla lay misaal.
bérabi jaamookaay y-: Bérabi jaamookaay yi ay bérab la yu nit ñi taamu woona màggale, muy yéefar yi, di bànni Israyil. Lu ci ëpp ay bérab yu kawe la daan doon, waaye man naa baña kawe itam. Su dee yéefar yi, ñu di ca jaamu seeni xërëm; su dee bànni Israyil ñoom, ñu di ca jaamu seen Yàlla Aji Sax ji. Gannaaw ba Suleymaan tabaxee ca Yerusalem kër Yàlla gu ñuy màggale Aji Sax ji, bérabi jaamookaay yooya ay tuurukaay rekk lañu mujj doon.
bésub Aji Sax ji-: Mooy bés bu Aji Sax ji dikke meram.
bésub Mucc b-: Seetal ci (màggalu) bésub Mucc b-.
bésub Noflaay b-: Moo doon juróom ñaareelu bés ci ayu bésu bànni Israyil. Bés la woon bu ñu jagleel Yàlla, ñu aaye ci bépp liggéey. Bésub Noflaay boobu Yàllaa ko séddoo, ba muy sàkk lépp. Gannaaw gi la tànn bésub Noflaay, firndeele ko kóllëre gi mu fasoo ak bànni Israyil.
cuuraay l-: Bokkoon na ci li bànni Israyil daan jëfandikoo ci seenug jaamu Yàlla, muy sarax su jëm ci Yàlla tey misaal kàddug ñaan gu ñu yékkati jëme fa Yàlla.
Daawuda: Buuru Israyil bu mag la woon te moo bind lu bare ci Sabóor.
Daraxma: Seetal ci Xaalis.
Dinaar: Seetal ci Xaalis.
Doomu nit k-: Mooy tur wi Yonent Yàlla Dañeel wooye woon Almasi ci ay bindam, lu jiitu juddub Almasi. Lenn ci li tur woowu wone mooy ni Almasi toroxloo, ba bokk ak nun sunu bindu doom aadama. Tur la wu Yeesu ci boppam jagoo woon.
Ebrë: Ebrë, am na ñu koy wax Ibraan ba tey. Yonent Yàlla Ibraayma ab Ebrë la woon. Xeet wi soqikoo ci moom te sëtoo ci Yanqóoba, moom lañuy wooye Ebrë. Seen làkk mooy ebrë mbaa ibraan. Wax nañu ne, Ebrë ci seen turu maam Eber la jóge (Njàlbéen ga 10.21).
Erodd: Amoon na juróomi buur yu tudd Erodd:
1. Ki ñuy wax Erodd mu mag ma, moo doon buurub Israyil ba Yeesu juddoo (Luug 1.5).
2. Doomam ji tudd Arkelawus; moo falu woon ci diiwaanu Yude (Macë 2.22).
3. Jeneen doomam ji ñuy wax Antipas; moo yilifoon diiwaani Galile ak Pere (Luug 3.1; 23.7; Jëf ya 4.27).
4. Àggripa sëtub Erodd mu mag ma, moo falu woon ci diiwaani Israyil yu bare (Jëf ya 12.1; 23.35).
5. Àggripa doomu Àggripa moo falu woon ci ay gox yu féete bëj-gànnaar (Jëf ya 25.13).
Esayi: Yonent bu mag la woon, bu jamonoom jiitoo jamonoy Almasi juróom ñaar téeméeri (700) at. Wax na lu bare ci ñëwug Almasi; ci wàllu juddoom ak liggéeyam ak deeyam ak ndekkiteem.
Estateer: Seetal ci Xaalis.
Farisen y-: Tariixa lañu woon ci biir Yawut yi. Ñu xér lañu woon ci sàmm yoonu Musaa, waaye jëf ju tegu ba mu ëpp ci ndigal moom lañu jiital, ba seen jaamu Yàlla mujj nekk ngistal, ak xeebeel seen digg ak képp ku bokkul ci ñoom.
gaalu kóllëre g-: Mooy waxande wa ñu dencoon àlluway doj ya Yàlla joxoon Musaa. Àlluwa yooyu la lale kóllëre ga mu fas ak bànni Israyil. Li waral ñu tudde ko gaal ga seede sa dence, mbaa gaal ga àlluway seede sa dence moo di àlluwa yooyu, seede la woon ca la Yàlla santaane. Bu gaal ga masaana teew bérab, loolu day firndeel ne Yàllaa fa teewal ag leeram ngir ñoñam.
gaana: Baat bi man naa ëmb yeneen jàngoroy der, yu dul ngaana kese.
Ibraayma: Jamonoy Ibraayma jiitoo na jamonoy Yeesu Almasi lu xawa tollu ci ñaari junniy (2 000) at. Yàlla moo digoon Ibraayma doom, mu di ko nég diiru ñaar fukki at ak juróom, Isaaxa doomam doora juddu, fekk Ibraaymaa ngi ci téeméeri atam.
Ilyaas: Yonent bu mag la woon. Jiitu na jamonoy Almasi juróom ñetti téeméeri (800) at.
jàngi yéeg g-: Jombul ay jàng la yu màggalkat yi daan jàng bu ñuy yéeg, jëm Yerusalem ci bési màggal at mu nekk.
jot: Doom aadama yépp ci notaangeg bàkkaar lañu nekk, mel ni ay jaam. Ni ñuy feye njégu jaam, ngir goreel ko, noonu la Yeesu Almasi jooxee bakkanam, ngir jot doom aadama.
jotkat b-: Wàllam moo doon fexe ba jotaat li giir gi ñàkk. Muy nit ku ñu bóom, jotkat bi wara topp ka ko bóom ba rey ko. Mbaa muy ku ñu xañ yoon ci giir gi, jotkat bi war koo jàpple ci wàllu yoon. Mbaa muy alal ju ku bokk ci giir gi ñàkk, jotkat bi war koo jotaat. Gannaaw Aji Sax ji moo dénkoon suuf si bànni Israyil, ñu yor ko, sañuñu ko woona jaay. Bu ñu ci tayle woon lenn lu ñu feye bor it, wareef la woon ci fexe ba loola dellu ci seeni loxo nu mu gëna gaawe. Su ko defee suuf si des ci bokk gi, di wone seenug bootu ci mbooloo mi kóllëreg Aji Sax ji lal.
juutikat b-: Ca jamono yooya juutikat ya ay Yawut yu dëng lañu woon. Waa Room lañu doon liggéeyal, ba tax Yawut ya waa Room tegoon tànk, jéppi leen, jàppe leen ay workat yu génn xeet.
kaala g-: Bu jëkkoon, ñi yore nguur ñoo daan kaalawu, mu mel ni màntob buur. Ñi daan raw ci ay po itam, kaalag xobi garab lañu leen daan terale. Te it kaala, dees na ko misaale añ, bi Yàlla dencal aji jub ñi.
Këlódd: Seetal ci Sesaar.
kóllëre g-: Ci Mbind mu sell mi, digoo la bu ëmb ay dige. Man nañu koo tëral, mu dib digoo diggante nit ak moroom ma, mu mel ni la Ibraayma digoo woon ak Abimeleg (Njàlbéen ga 21.27), mbaa diggante kilifa ak surgaam. Kóllëre gu ni mel la Yàlla taamu woona fasook nit, mu mel ni la Yàlla digoo woon ak àddina, jaare ko ci Nóoyin (6.18), mbaa diggante Yàllaak Ibraayma (15.18), mbaa Yàllaak Isaaxa (17.19). Ñetti yoon yu mujj yooyu ñu lim, Yàlla rekk a dige; moom ci wàllu boppam moo fas kóllëre ak ñooñu. Ñoom defuñu dara lu dul gëm ko. Waaye Ibraaymaak Abimeleg dañoo digoo, maanaam dañoo fasoo kóllëre, ku nekk am lu ko war. Noonu lañu dégge li xàjjale fas kóllëre ak fasoo kóllëre.
kurélu àttekat y-: Moo doon mbooloom njiiti xeet wa ca Yerusalem. Ñi ko séqoon di sarxalkat yu mag ya, ak magi xeet wa, ak ay firikati yoon; mbooloom juróom ñaar fukki nit la daan doon.
Kuus: Réew la mu nekkoon ca bëj-saalumu Misra te ëmboon réewum Sudan ak Ecopi ga woon ak Nubi.
Leween b-: Lewi kenn la woon ca ña sos bànni Israyil, di fukki doomi Yanqóoba yaak ñaar. Lewi mooy maamu Musaa ak Aaróona. Aaróona la Yàlla tànn muy sarxalkat bu mag ba. Ñenn ci ñi soqikoo ci moom ñoo daan donnante liggéeyu carxal bi. Ña ca des ñoo leen daan jàpple ca liggéeyu kër Yàlla ga.
Lewi: Maam la ci Musaa.
Màggali Yawut yi: Ci biir màggali Yawut yi, amoon na ñetti màggal yu mag yu ànd ak tukkib siyaare: màggalu bésub Mucc ba, màggalu Ngóob topp ci, juróom fukki fan gannaaw loolu; ak màggalu bési Mbaar yi, di ñeenti weer gannaaw màggalu Ngóob.
màggalug Ayi bés: Seetal ci (màggalug ayi bési) Ngóob m-.
màggalu bésu Farmàngu: Kuy farmàngu, jeexal nga bépp liggéeyu tool. Jamonoy lolli lañu daan amal màggal gii ca réewum Israyil, mu dëppook diggu sàttumbar. Moo yemook fa ndajalem meññeef ma jeexe, gannaaw bu ñu wittee oliw jaak reseñ ja. Ci wàllu diine, at maa nga daan tàmbalee ci weeru Nisaan, di màrs jàpp awril, yemook weer, wa bànni Israyil génne Misra. Waaye ci wàllu caada, at maa nga daan jeexe ci diggu weeru sàttumbar, mu dëppook njeextel liggéeyu tool ya ca réewi penku yooyu. Seetal ci Mucc ga 23.16 ak 34.22.
màggalu bésu Liit y-: Liit gi béjjénu kuuy la daan doon, ñu di ko wal wal mu xumb ngir yéene at mu bees. Seetal ci Sarxalkat yi 23.23-25.
(màggalu bési) Mbaar y-: Màggal la gu bànni Israyil daan amal, diiru juróom ñetti fan yu ñuy dale mbaar yu ñu defare cari garab. Ñu di ko amal gannaaw bu ñu wittee reseñ ak oliw ak yeneeni meññeef. Su ko defee seeni sët xam ne ciy mbaar la Yàlla dëkkaloon bànni Israyil, ba mu leen génnee réewum Misra. Seetal ci Sarxalkat yi 23.33-43.
(màggalug) ayu bésu Mburu mu amul lawiir b-: Moo topp ca bésub Mucc ba, di màggalug ayu bés. Ca la bànni Israyil daan lekke mburu mu amul lawiir, di ko fàttlikoo fitna ja seeni maam génne réewum Misra; taluñu woona nég sax, ba mburu ma funki. Mburu mu amul lawiir di misaal itam ni seen xol wara selle ñeel Yàlla. Seetal ci Sarxalkat yi 23.6-8.
(màggalu) bésub Mucc b-: Bésub Mucc ba, weeru Yawut wa jiitu la daan yemool, mu dëppook awril ci weeru tubaab. Bànni Israyil daan ca baaxantal la xewoon ca réewum Misra ca jamonoy Yonent Yàlla Musaa. Mooy ba maam ya rendee ay gàtt, taqal deret ja ca seeni buntu kër, ba tax malaakam reykat ba jéggi seeni kër. Noonu la leen Yàlla musale ca musiba, ma mu wàcce ca Misra, goreel leen, génne leen ca loxoy Firawna, buuru Misra, ba génne leen réew ma.
(màggalug ayi bési) Ngóob m-: Ca ñetteelu weeru Yawut lañu ko daan amal. Gannaaw bu bésub Mucc ba weesoo lu mat juróom ñaari ayi bés, ca lañu ko daan amal. Ca lañu daan sante Yàlla ca seen naataangey ngóobum bele. Pàntakot mooy tur wi ñu ko mujj tudde. Dees na ko wooye itam màggalug Ayi bés. Seetal ci Sarxalkat yi 23.15-22.
bésub Njotlaay b-: Amoon na ca fukkeelu fanu juróom ñaareelu weer wa. Ca bés booba la sarxalkat bu mag ba yóbbu deretu mala fa kanam Yàlla, ngir mu baal Yawut ya seeni bàkkaar. Bés bu sella sell la woon, ca lañu daan yendoo woor. Seetal ci Sarxalkat yi 16 ak 23.26-32.
mànn: Moo di ñam wa Yàlla wàcceeloon Musaa ak bànni Israyil, ba ñu gàddaayee Misra, jëm ca réew ma leen Yàlla digoon.
Mbaar y-: Seetal ci (màggalu bési) Mbaar y-.
Mburu mu amul lawiir: Seetal ci (màggalug) ayu bésu Mburu mu amul lawiir b-.
mburum teewal m-: Ayu bés gu nekk sarxalkat ya daan nañu sàkk fukki mburu ak ñaar, teewal ko ca kanam Yàlla, muy misaal ni bànni Israyil jébbaloo ci Yàlla.
Musaa: Yonent Yàlla Musaa yonent bu mag la woon. Moo jiite bànni Israyil, bi ñu gàddaayee réewu Misra. Ca moom la Yàlla jaarale téere bi ñuy wax Tawreet, mu ëmb ndigal yi ñuy wooye yoonu Musaa.
néeg (Yàlla) bu mag b-: Mooy néeg bu mag ba nekkoon ca biir tabaxu kër Yàlla ga. Néeg boobu, sarxalkat yi ak Leween ñi doŋŋ a fa sañoona dugg. Dees na ko wooye it bérab bu sell bi, mu wuuteek néegu biir bi, di bérab bu sell baa sell te sarxalkat bu mag ba doŋŋ sañ faa dugg benn yoon cim at.
njiitu gàngoor g-: Mbooloom juróom benni téeméeri (600) xarekat la daan yilif.
njiitu takk-der b-: Téeméeri xarekat la daan yilif.
njot g-: Seetal ci jot.
Noflaay, bésub: Moo doon juróom ñaareelu bés ci ayu bésu bànni Israyil. Bés la woon bu ñu jagleel Yàlla, ñu aaye ci bépp liggéey. Bésub Noflaay boobu Yàllaa ko séddoo, ba muy sàkk lépp. Gannaaw gi la tànn bésub Noflaay, firndeele ko kóllëre gi mu fasoo ak bànni Israyil.
Noo gu Sell g-: Moo di Noowug Yàlla. Du malaaka te du mbindeef. Mooy Taxawukat, bi Almasi digoon ay taalibeem, ne mooy dikk dëkk ci seen xol, di leen dooleel ak a sellal.
Pàntakot: Seetal ci (màggalug ayi bési) Ngóob m-.
Pilaat: Poñsë Pilaat moo taxawaloon nguuru Room ci diiwaanu Yude, 26—36 gannaaw juddub Almasi. Moo joxe ndigal la reylu Yeesu.
Sadusen y-: Tariixa lañu woon ci biir Yawut yi, di ñu amoon alal ca sarxalkat ya, te am doole ca nguur ga. Gëmuñu woon ne dund amati na feneen fu dul ci àddina, te gëmuñu woon malaaka.
Samari: Mooy diiwaan ba nekkoon diggante Yude ak Galile. Ñu bare ci waa Samari ay làkk-kati yéefar la leen Yawut yi jàppe woon, te ay noon lañu woon.
Sarax yi: Sarax yi ñuy wax fii, Yàlla lañu koy jagleel. Bànni Israyil amoon nañu xeeti sarax yu bare: ay saraxi yéene ak ay saraxi sañul-bañ ak sarax su ñuy tuural Yàlla ak saraxu xaalis ak saraxu pepp. Waaye li ci ëpp ay saraxi tuur deret la woon yu leen Yàlla tegoon, ngir seen njéggalug bàkkaar. Su ko defee ñu mana dëkke jokkook moom, Yàlla ju sell ji, ndax saraxu deret ja. Am na ci ay sarax, Yàlla da ciy xamal bànni Israyil ne peyug bàkkaar mooy dee, te deewu jur, gi ñuy sarxal, njot la ci boroom sarax bi. Bu loolu weesoo, deretu sarax dina fóot sobes bàkkaar itam, muy sobe suy topp nit mbaa lenn ci jumtukaayi jaamookaay ba.
saraxu cant ci biir jàmm: Mooy sarax, si ñu daan sante Yàlla jàmmam. Sarax boobu ag jur lay doon gu ñuy séddale ñetti cér. Benn bi, ñu lakkal ko Aji Sax ji ci sarxalukaay bi, ba mu jeex. Benn bi, sarxalkat yi féetewoo ko. Ñetteel bi, ki sarxe moo koy lekk, ak waa këram.
saraxu dóomal: Seetal ci saraxu rendi-dóomal.
saraxu ndoortel meññeef: Meññeef mu jëkka ñor la bànni Israyil daa sarxalal Aji Sax ji, mu yemook seen màggalu Ngóobum at mu nekk. Muy la jëkka ñor, di lu góor lu nit ak jur taawloo, lépp lañu séddoon Aji Sax ji, muy moomeelu boppam.
saraxu pepp m-: Peppam bele la mu ñuy jagleel Yàlla. Lenn li, ñu jaxase kook cuuraay ak diwu oliw, taal ko. Li ci des sarxalkat bee ko moom. Sarax la su ñu daan defal Aji Sax ji, muy galag bu ñuy nangoo nguuram, nangoo ko moomeel gu mat sëkk gu mu moom bakkanu ki koy joxe. Nit ki daan ko yeesloo ngiñam ne dina sàmmonte ak kóllëreg Aji Sax ji.
saraxu peyug tooñ: Bu nit tooñee ci lenn lu sell lu mu teddadil, muy jumtukaay bu sell mbaa sarax, mbaa lu bokk ci bànni Israyil gi Yàlla sellal, mbaa mu sofental sellngay turu Yàlla; bu defee lenn ci yooyu, pey gu mat sëkk war na ko ci gépp tooñ gu ni mel, te war na caa teg daan bu tollook benn xaajub juróomeel, ñeel ka mu tooñ. Gannaaw loolu itam war na caa boole sarax bu muy defal Yàlla, doora am njéggal.
saraxu póotum bàkkaar: Ci misaal, sarax la suy dindi sobe, di far ag tooñ tey musal boroom ci mbugalu bàkkaar. Ag jur lay doon gu nit ki di rendil Yàlla, defal ko ko sarax. Bu ñu tuuree deret ji, bakkanu jur gi mooy wuutu bakkanu ki sarxe. Sarax boobu it dees koy lakk.
saraxu rendi-dóomal: Mooy tekki sarax su kenn dul lekk dara. Dañu koy lakk muy saxar, ba jeex, jagleel lépp Yàlla.
sarax su ñuy tuural Aji Sax ji, saraxu tuuru: Saraxu naan la bu ñu daan defal Yàlla, muy ànd ak saraxu rendi-dóomal mbaa saraxu pepp. Li ci ëpp biiñ la daan doon, ñu di ko sotti ca taatu sarxalukaay ba.
saraxu yéene: Xeetu saraxu cant la ci biir jàmm. Day neex boroom, mu def ko, waaye du wartéef.
sarax bu ñuy yékkati, jébbal Aji Sax ji: Turu sarax soosu day wone ne dañu ko daan yékkati, mel ni ku koy jox Aji Sax ji, door koo wàcce. Jombul ay yooni yoon lañu ko daan yékkati, wàcce.
sarxalkat b-: Ab sarxalkat njiitu diine la bu sasoo di rendil jaamukat yi seeni sarax. Muy yéefar yi di bànni Israyil, ku ci nekk amoon na ay sarxalkatam yu leen di taxawal ca kanam ka ñu gëm, mu dim tuur su dee yéefar yi, mbaa muy Aji Sax ji, su dee bànni Israyil. Yàlla moo taamu ñi bokk ci giirug Lewi, doomu Yanqóoba, ñuy Aaróona ak ñi askanoo ci moom, ngir ñu taxawal bànni Israyil fa kanamam. Sarxalkati bànni Israyil ay góor lañu yu ñu sellalal Yàlla, ñu féetewoo liggéeyam. Ñoo sasoo liggéey biy jubale mbooloo meek Yàlla. Ñoo leen di sarxalal te ñoo yore liggéeyu jaamu Yàlla bi. Sarxalkat bu mag bi moo doon kilifay sarxalkat yi, te mooy misaal Almasi Yeesu, mi nuy àgge fa Yàlla.
sarxalukaay b-: Waa penku baaxoo woon nañoo yékkatil seeni yàlla, ay sarxalukaay ci yenn bérab, ngir njukkale ko seeni yàlla. Sarxalukaay yooyu, ban lees ko daan tabaxe mbaa ay xeer, mu taxawe ni waxande, te jur gi ñuy def sarax di tege ca kaw.
Niti Aji Sax ji ci seen wallu bopp, naka jekk, daan nañu yékkatil Aji Sax ji ay sarxalukaay yu ñu koy njukkale. Ba kërug jaamookaayu Aji Sax ji taxawee itam, noonu la bànni Israyil ame woon ñaari sarxalukaay ca biir kër Yàlla ga, benn bi ñuy lakke jur gu ñu rendi, bi ci des, ñu di ci taal cuuraayu sarax. Sarxalukaayu jur gi amul woon kubeer ca kaw, waaye ab caaxam la àndaloon, ñu di ci teg matt mi ñuy lakke jur gi. Ay béjjén lañu sàkkaloon boobu sarxalukaay ca ñeenti koñam ya ca kaw.
Sefas: Mooy tur wu Almasi tudde Simoŋ Piyeer, kenn ci fukki ndawi Almasi ya ak ñaar. Sefas ci làkku yawut, ak Piyeer ci làkku gereg, «xeer» lay tekki.
selaw: Jàpp nañu ne ndigal la luy taxawloo woykat yi, te jombul xalam yi wéy ba tey. Waaye man naa nekk itam ndigal ngir xalam yeek woykat yi gëna xumbal.
sell: Lu sell, ni ko yoonu Tawreet dégge, mooy lu ñu beral Yàlla; man naa doon nit, mbaa ab jumtukaay. Mboolem lu set te sellaluñu ko, su laalantee ak lu sell, lu sell loola day daldi teqlikoo ak sellngaam. Waaye du tee lu sell la set, li feek sobe laalu ko. Lu sell nag, bu taqee sobe rekk, sobewu na. Day daldi doon lu setul. Moo tax lu sell warul dajeek sobe fenn. Ku taq sobe, su masaana lekk lu sell lu mel ni yàppu jur gu ñu sarxal Yàlla, dees koy dagge ci askanu bànni Israyil, rey ko. Ci yoonu Tawreet, su ñu nee Yàlla ku sell la, ni mu beroo ak ni mu wéete ci sellngay jikkoom moo tax ñuy wax, ndax Yàlla moo matale mboolem mbaax, moo mucc ci gépp sikkaange, te lenn ci sellaayu jikkoom mooy ngoram gu bare, ak kóllëreem gu sax.
serub y-: Baatu ebrë la. Ay bindeef lañu yu bokk ak Yàlla jataay. Ñooy wattu dénd ba ngànguney Yàlla nekk, ba foofa dëkke sell. Jaamookaayu Yàlla ga amoon na gaal gu ñuy wooye gaalu kóllëre ga. Ñaari serub yu ñu tëgge wurus lañu tegoon ca kawam, ñu tiim ko, seeni laaf firiku, di saamandaay ngàngunem buur. Loolu di wone ne Yàlla Aji Sax jaa nga fa teew, na mu teewe ca kaw asamaan, serub ya yéew ko. Yàlla ci boppam nag kenn jëmmalu ko fa, na ñu jëmmale serub ya ñu tëgg.
Sesaar: Sesaar, buuru Room, réew yu bare la yilifoon, ba ca réewum Yawut ya. Lim nanu buuri Room, yi ñu tudd seen tur ci Mbind mi.
Ogust: 30 at lu jiitu Almasi, ba 14 gannaaw juddub Almasi (Luug 2.1)
Tibeer: 14 g.A.—37 g.A. (Luug 3.1)
Këlódd: 41 g.A.—54 g.A. (Jëf ya 11.28)
Neron: 54 g.A.—68 g.A. (Jëf ya 25.10-12; 27.24)
Domikan: 81 g.A.—96 g.A. (Peeñu ma 1.9).
Seytaane: Mooy malaaka mu dëddu Yàlla, ba noonoo ak moom, te moo yóbbaale malaaka yu bare yu ànd ak moom ci jaww ji. Almasi moo ko nasaxal ca bant ba mu deeye. Ku gëm Almasi, rëcc nga ci dooleem. Yàllaa ko daan te moo koy mujj tàbbal sawara. Dees na ko wooye itam: Beelsebul; Belyar; Ibliis; Tuumaalkat bi; yàllay xarnu bi, kilifay àddina si.
Sidon: Seetal ci Tir.
Siyoŋ: Mooy turu tund, wa ñu tabax Yerusalem ci kawam. Dees na ko wooye itam askanu Yawut.
Sodom ak Gomor: Dëkk yu siiw la woon ca jamonoy Ibraayma. Waa Sodom ak Gomor la seeni bàkkaar réyoon, ba Yàlla tas dëkk ya. Leeg-leeg turi dëkk yooyu dees na ko misaale xeeti yàqute, yi waa dëkk ya daan def.
Taaw b-: Su ñu nee Yeesu Almasi mooy Taaw bi, du lu jëm ci juddoom waaye ci darajaam la. Yeesu Almasi moo sut ñépp te moo yilif lépp luy mbindeef. Rax ci dolli mooy ki jëkka dekki, ndekkite lu dee toppul, te ci darajaam la nit ñiy dekkee. Moom mooy Sëtub Daawuda bi sottal dige bi ci Sabóor 89.27.
teg loxo: Almasi aki ndawam ak magi mbooloom gëmkat ñi ñoo baaxoo di teg nit seeni loxo, ngir màndargaal barkeb Yàlla bu ñu ko jottli, mbaa wér-gi-yaram gu ñu koy sàkkul fa Yàlla, mbaa ab sas bu ñu koy sas ci ndigalal Yàlla, mbaa Noo gu Sell gu ko Yàlla baaxe.
Tir: Tir ak Sidon, ay teeru lañu woon yu siiw ndax seeni bàkkaar, ca diiwaanu Siri.
tundu Oliw y-: Tund la wu am taxawaayu 800 m, féete ci penkub Yerusalem, te sëqoon ak garabi oliw. Fa la Sang Yeesu daan farala wéetoo ak Yàlla.
Urim ak Tumim: Ñaari jumtukaay yu ndaw la woon, sarxalkat baa ko daan seete ci Yàlla, ngir xam lu mu namm. Xameesul nag nan lañu ko daan jëfandikoo. Waaye xeetu ceetin wu dagan la.
waxyu: Wax lay doon, ju Yàlla déey ab yonent, mu di ko biral ci ndigalal Yàlla. Leeleeg bu ab yonent tolloo ci biral waxyu, day mel ni ku daanu leer.
Xaalis: Gis nanu ci téere bii xaalisu ñetti xeet:
Yawut yi seen bos moo doon:
leptonMàrk 12.42; Luug 12.59; Luug 21.2
 
Waa Room amoon nañu poset yii:
kodorantesMacë 5.26; Màrk 12.42
asariyonMacë 10.29; Luug 12.6
dinaarMacë 18.28 (100 dinaar); 20.2, 9, 10, 13 (1 dinaar); 22.19 (1); Màrk 6.37 (200); 12.15 (1); 14.5 (300); Luug 7.41 (500 ak 50); 10.35 (2); 20.24 (1); Yowaan 6.7 (200); 12.5 (300); Peeñu ma 6.6 (1)
 
Gereg yi amoon nañu poset yii:
daraxmaLuug 15.8
didaraxmonMacë 17.24
estateerMacë 17.27
minaLuug 19.11-27
talaŋMacë 18.24; 25.15-38
Méngale seen xaalis ak sunu xaalisu tey, lu jafee def la. Ba tey gis nanu ci Macë saar 20 ne, dinaar moo doon peyug bëccëg ci kuy liggéey tool, kon man nanu koo fexee yemale ak 1.000 CFA. Su nu tàmbalee lim bi nag ci dinaar, muy benn kepp [1], kon lii lanu ci tëral:
 
YawutWaa RoomGereg yiNjariñamLi mu méngool ci xaalisu tey
lepton÷ 1288 faraŋ CFA
kodorantes÷ 6415 faraŋ
asariyon÷ 1660 faraŋ
dinaardaraxma[1]1.000 faraŋ
didaraxmon× 22.000 faraŋ
estateer× 44.000 faraŋ
mina× 100100.000 faraŋ
talaŋ× 6.0006.000.000 faraŋ
 
xar-sànni m-: Mbubbu jaamookaay la, mu sarxalkat biy sol, kiiraayal dënn ba tege ca kaw. Kiiraay li xeetu jiba la ju daan def jumtukaay yooyu ñuy wax Urim ak Tumim, jumtukaay yu sell, yi ñuy seete, ba xam li Yàlla namm.
xaymab ndaje m-: Ba bànni Israyil nekkee ca màndiŋ ma, moo doon seen jaamookaay bu ñu mana wékki, yóbbu. Fa la Yàlla daan taseek Musaa, te fa la Yàlla taamu woona misaale teewaayam ci digg ñoñam ñi mu goreel.
Xel mu Sell m-: Moo di Xelum Yàlla. Seetal ci Noo gu Sell g-.
xóote b-: Mooy fa ñu tëj Seytaane ak malaaka yi ànd ak moom, di leen nége seen mbugal.
Yanqóoba: Weneen turam di Israyil. Sëtub Ibraayma la. Aw turam di taxawe itam askanu Yawut.
Yaxya: Yaxya doomu Sàkkaryaa mooy yonent, bi Yàlla yónni ci bànni Israyil, ngir ñu tuub seeni bàkkaar, teertu Almasi bi te nangu njàngleem.
Yerusalem: Mooy péeyu réewum Yawut, te fa la kër Yàlla ga nekkoon. Foofa rekk lañu manoona rendi ay saraxi mala yu ñu jébbal Yàlla.
Yese: Mooy baayu Yonent Yàlla Daawuda, mi bind Sabóor. Ci moom la Almasi soqikoo.
Yosuwe: Ba Musaa faatoo, Yosuwe moo ko wuutu, daldi jiite mbooloom Israyil, ba ñu dugg ca réew, ma leen Yàlla digoon.