Kàddug Yàlla gi
Kàddug Yàlla gi ñaari pàcc la: Téereb Kóllëre gu jëkk gi ak Téereb Kóllëre gu yees gi.
Kóllëre gu jëkk gi, ni ko xamkati Yawut yi séddalee, moo ëmb Tawreet ak Téereb yonent yi, ak Téereb yeneen bind yu sell, yi indi Sabóor.
Kóllëre gu yees gi moo ëmb Injiil, ak bataaxal yi jëm ci mboolooy gëmkat ñi.
Téere bu mag, biy kàddug Yàlla gépp, juróom benn fukki téere laak juróom benn. Yàlla moo tànn ay yonent ak ñeneeni nit ci diiru junniy at ak juróomi téeméer, xiir leen ci bind kàddoom.
Xaajub Tawreet bu jëkk bi, Njàlbéen ga, moo indi lu jëm ci Aadama ak Awa, ak Kayin ak Abel, ak Nóoyin ak Ibraayma ak Saarata ak Ajara ak Ismayil ak Isaaxa ak Yanqóoba ak Yuusufa.
Ñaareelu xaajub Tawreet, Mucc ga, ci la Yàlla joxe yoonam, Musaa jottli, gannaaw ba Yàlla musalee bànni Israyil cig njaam, ngir mbooloo ma doxe ca mucc, di topp yoon wi. Su ko defee ñu mana sàmm seen nekkandoo ak Yàlla. Ñu ngi ciy nettali bi Yàlla santee Musaa mu sàkk ab xaymab jaamookaay bu taxawalin ba, ak li ci biiram lépp di misaal sellngay Yàlla.
Ñetteelu xaajub Tawreet, Sasu Sarxalkat yi, ci la Yàlla tegtale ay sarax yuy doon ag njotlaay ci bàkkaar ak sobe, li ñag diggante doom aadama ak Yàlla Aji Sell ji.
Yeneen xaaji Tawreet yi ci des nettali na cosaanu bànni Israyil aki jaar-jaaram, ba leen Aji Sax ji di wommat. Waaye xaaj yooyu baamu na itam dogali yoon yi, ñeel Israyil ci seenug ñàkka sàmm yooyu dogal.
Lenn ci Téereb yonent yi nettali na ni Yàlla mujj mbugale bànni Israyil ndax ñoo sàmmoontewul ak sàrti kóllëre gi mu fas ak ñoom.
Téereb yeneen bind yu sell yi ñoo indi Ayóoba, ak Sabóoru Daawuda, ak Kàddu yu Xelu yu Suleymaan, ak téerey woy yu boole ay kàdduy ñaan aki cant.
Kóllëre gu yees gi, ci la Yàlla sàkke kóllëre gu tegu ci sarax, bi Almasi sarxe bakkanam ngir texey mboolem doom aadama.
Kàddug Yàlla benn téere la bu mag bu tënk jëfi Yàlla ci jamono, Yàlla bindloo ko ay yonent yu mel ni Musaa ak Esayi ak Yeremi, ak njiit yu mel ni Samiyel, ak buur yu mel ni Daawuda ak Suleymaan, ak sarxalkat yu mel ni Esra ak Esekiyel.
Kàddug Yàlla nag yemul ci nettali jaar-jaari jamono, ndax Yàllaa ci fésal mooy kan; mooy kenn ku amul moroom, di ku baax, di boroom yërmande, di ku sell te xajoowul bàkkaar. Yàlla, ci mbaaxam la sàkke àddina, sàkk nit. Waaye sobey nit ak bàkkaaram mooy gàllankoor wi yàq digganteem ak Yàlla Aji Sell ji. Teewul Kàddug Yàlla gi xamle na pexe mi Yàlla teggee woowu gàllankoor, ba xalaatal doom aadama, yoon wu mu delloo ci moom.
Yeen ñiy jàng téere kàddug Yàlla gii, nu ngi leen di ñaanal ngeen barkeelu ci, ba dajeek yiwu Yàlla.