Baamtug Yoon wi
di juróomeelu xaaju Tawreetu Musaa
Ubbite gi
Téereb Baamtug Yoon wi moo tënk ci mbind, yeesalug kóllëre gi Yàlla fas ak bànni Israyil, fa tundu Sinayi, gannaaw ba ñu génnee Misra. Ñeent fukki at gannaaw gàddaay ga fekk na mboolem maasug fippukat ga jóge woon Misra, faatu ba jeex. Moo tax yeesalug kóllëre ga ngir maas ga ca topp, manul woona ñàkk. Musaa mi doon jottlikatub sàrti kóllëre gi moo demoon ba ag dundam desatul lu bare. Kon warteef la woon ci Israyil, mu dogu ne dina déggal kay wuutu Musaa. Ba bànni Israyil nangoo réew ya féete dexu Yurdan penku, dem nañu ba ca tàkkal dex ga, di waaja dugg nanguji réew ma leen Yàlla digoon.
Téere bi dafay sàrtal itam ni bànni Israyil wara dunde ca réew ma ñu leen dig. Yàlla moo leen jot, ñuy céru boppam bu mu sopp. Moo leen jële ca njaam ga ca Misra, ngir jox leen réew ma mu dige woon, ngir sottal digeem baak Ibraayma ak Isaaxa ak Yanqóoba. Cëslaayal sàrtoo gi nag mooy jeneen Yàlla amul ku moy Aji Sax, ji ñu wara déggal ci lépp, te moom doŋŋ a moom askan wi.
Ki jàng Kàddug Yàlla tey mbaa ki ko jàngoon démb, ñoom ñépp la Baamtug Yoon Wi fàttli ne mbég mi mboolem doom Aadama di sàkku, fi mu nekk dëgg du fenn fu moy ci saxoo déggal Yàlla, ak fépp fu mu doon, ndax Yàlla mooy texeel, di goreel.
Ci Tënk:
1.6—4.43 Musaa fàttli na jaar-jaari Israyil
4.44—26.19 Musaa baamtu na yoon wi
27.1—30.20 Musaa biral na yooni barke ak alkànde
31.1—34.12 Musaa tàggoo na