Kàddug Yàllaa wóor
12
1 Mu jëm ci njiital jàngkat yi, ànd ak xalamu juróom ñetti buum, di kàddug Sabóor, ñeel Daawuda.
 
2 Wallóoy, Aji Sax ji, ngor jee na!
Kóolute réer na doom aadama.
3 Dañuy fenante,
làmmiñ dig lem, xol ba njuuy la.
4 Yal na Aji Sax ji tëj gémmiñu kuy naxe,
ak kuy làmmiñuy tëggu.
5 Ñu ngi naa: «Sunu làmmiñ lanuy daane,
nook sunu kàddu; ku nu manal dara?»
 
6 Ku ñàkk a ngi, ñu futti,
mu ngi binni, di néew-ji-doole.
Aji Sax ji nee: «Maa ngii, di ci jóg,
teg leen fi rawtu gu ñu ne siiw.»
 
7 Kàddug Aji Sax ji, kàddu gu sell la,
ni xaalis bu ñu xelli ci taalu ban,
settli ko juróom ñaari yoon.
8 Ngalla Aji Sax ji, sàmmal ku néewle,
aar ko saa su ne ci nitu tey.
9 Ñu bon ñaa ngi taxawaalu fu ne,
jikko ju sew falu ci biir doom aadama yi.