Aji Sax ji waccu ma
138
1 Ñeel Daawuda.
 
Ma sante la sama léppi xol,
woy la, gàngooru Yàlla ga ca kaw seede.
2 Ma sujjóot jublook sa kër gu sell gi,
di wormaal saw tur,
ngir sa ngor ak sa worma.
Màggal nga sa tur ak sa kàddu,
ba mu tiim lépp.
3 Bés ba ma wootee, yaa ma wuyu,
ñemeel ma, dooleel ma.
 
4 Aji Sax ji, na la buuri àddina yépp màggal,
ñoo dégg kàddu yi nga wax.
5 Nañu woy say jaloore, naan:
«Aji Sax jeeka màgg teddnga!»
6 Aji Sax jee kawe!
Ku toroxlu, mu niir;
ku réy, mu ñooru.
 
7 Ma wéye njàqare,
nga musal ma,
dogalee sa loxo merum noon,
walloo ma sa ndijoor.
8 Aji Sax jee may feyul.
Éy Aji Sax ji, yaa saxoo ngor!
Bul wacc ñi nga binde sa loxo.