W - w

wàññi *   v.t. 1 • diminuer; réduire; baisser; soustraire *; verringern; verkleinern; senken; reduzieren; herabsetzen; abziehen; subtrahieren; to diminish; to reduce; to lower; to subtract. Usage: prix; volume; cheveux; calcul; Preis, Lautstärke, Haare; Rechnen; price; volume; hair; arithmetic

2 • éliminer; supprimer *; ausschließen; beseitigen; vernichten; streichen; abschaffen; to eliminate; to suppress; to remove; to delete; to abolish, to cut off. Dégg naa am na ku wàññeeku ci yeen. [ME] Te kat ay bés a ngi ñëw dinaa wàññee ci sa waa kër ak sa waa kër baay mboolem lu tollu ci digg dooleem, ba deesatul gis góor gu màggat ci sa askan. [1Sa 2.31] See: dindi.

war *1   v.aux. devoir; avoir à faire quelque chose *; müssen; etwas tun müssen; to have to; to have to do something.

war *2   v.t. monter à califourchon; se mettre sur *; sich rittlings setzen auf; sich setzen auf; to climb astride; to put oneself on. Gannaaw loolu Rebeka ànd ak xale yu jigéen, yiy jaamam, ñu war ay giléem, topp waa ja. Noonu surga ba daldi dem, yóbbu Rebeka. [Njàlbéen ga / Gn 24.61]

wareef w- *   n. devoir; charge; obligation *, donner en gage; premier cadeaux de la dote; Pflicht; Aufgabe; Auftrag; Verantwortung; Verpflichtung; duty; responsibility; obligation, to give a guarantee. Laaj nañ la wareef ñeent ndobin ak ab rajo ak montar. [ME] Usage: marriage only! syn.: àq. See: warugar w-.

warugar w- *   n. 1 • obligation morale; devoir *; moralische Verpflichtung; Pflicht, Aufgabe; moral obligation; duty. Li ma la defar, du dara, sama warugar la. [ME]

2 • dot, compensation matrimoniale; somme d'argent que doit verser le fiancé pour que le mariage soit valide *, responsabilité en matière de mariage-; Mitgift; Brautpreis; Geldsumme, die der Verlobte zahlen muß, damit die Hochzeit gültig ist; dowry; matrimonial compensation; sum of money that the fiancé has to pay for them marriage to be valid. See: wareef w-.

wasin *   v.t. accoucher *; enfanter; entbinden; gebären; to give birth; to bring into the world. syn.: mucc.

waxambaane w- *   n. jeune homme *; junger Mann; young man. Yuusufa tollu na ci waxambaane, am fukki at ak juróom ñaar, di sàmmle jur gi doomi baayam, yi nga xam ne soxnay baayam Bilaa ak Silpa ñoo leen jur. [Njàlbéen ga / Gn 37.2]

woy *   v.t. 1 • chanter; psalmodier *; singen; absingen; leiern; to sing; to chant.

2 • chanter les louanges de *; jemandes Lob singen; to sing praises of.

woye w- *   Variant: araf wu jigéen w-; araf-ngelaw w-. n. voyelle *; Vokal; vowel. Variant: araf wu jigéen w-; araf-ngelaw w-. See: araf w- / b-.