M - m

mëdd *   v.t. engloutir; noyer *; verschlingen; ertrinken; to engulf; to drown; to be over one's head. Ndox ma di walangaan, ba mëdd tund yu kawe ya fépp fu asamaan tiim. L'eau s'écoulait au point d'engloutir les hauts montagnes partout sous le ciel. Das Wasser breitete sich aus bis es überall, worüber sich der Himmel erstreckt, die hohen Berge überflutete. The water flowed everywhere where the sky is above to the point of covering the high mountains. [Gn 7.19]

mer *   v.i. se fâcher; être fâché; être en colère *; verärgert sein; sich ärgern; wütend sein; to get angry (with); to be angry.

miin *   v.t. être habitué à ; être familier à; avoir l'habitude de voir; se familiariser à *; s'habituer; gewohnt sein; vertraut sein mit; die Gewohnheit haben zu sehen; sich gewöhnen an; to be used to; to be familiar with; to be used to see; to get used to. syn.: miis.

miis *   v. être habitué à; être familier à; avoir l'habitude de (voir) *; gewöhnt sein an; vertraut sein mit; die Gewohnheit haben zu (sehen); to be used to; to be familiar with; to have the habit of (seeing). Bu doom feree dina miis weenu yayyam. [ME] Gannaaw gi Buur Daawuda toppatul Absalom, ndax mujj na miis deewug Amnon. [2Sa 13.39] syn.: miin, tàmm.

muus *   v.i. être malin; être rusé; être éveillé *; être intelligent; être astucieux; pfiffig sein; boshaft sein; listig sein; schlau sein; aufgeweckt sein; intelligent sein; scharfsinnig sein; to be crafty; to be cunning; to be malicious; to be alert; to be intelligent; to be shrewd. Lëg dafa muus. Jaan dafa saay-saay. [ME] Booba jaan moo gënoona muus ci rabi àll, yi Yàlla Aji Sax ji sàkk yépp. [Gn 3.1] Yuusufa teg ca ne Firawna: «Kon léegi sang bi, wutal nit ku muus te rafet xel, jiital ko ci réewu Misra. [Gn 41.33] Loo muus muus sa goro gën laa muus. Rusé que tu sois, ton beau-père sera plus rusé que toi. [ME - Léebu wolof] Usage: positive syn.: boŋ. See: xelu. Note: ME: No snake is "muus" in Wolof.