Tabb nañu taxawukati mbooloom gëmkat ñi
6
1 Jant yooyu nag, naka taalibe yi di gëna bare, Yawut ñiy làkk gereg tàmbalee ñaxtu ci kaw Yawut ñiy wax seen làmmiñu bopp ndax néewal gu ñu gis ñu néewal ko seeni jëtun ca na ñuy séddalee ag ndimbal bés bu nekk. 2 Ba mu ko defee fukki ndaw ya ak ñaar woo mbooloom taalibe ya, ne leen: «Nu sàggane kàddug Yàlla, di topptoo mbirum séddale daal, jekkul ci nun. 3 Kon nag bokk yi, seetleen ci seen biir juróom ñaar ñu rafet seede, soloo Noo gu Sell gi te rafet xel, nu dénk leen sas woowu. 4 Nun nag nanu wéye julli gi, ak liggéey bi ci kàddu gi.»
5 Wax jooju daldi neex mbooloo mépp. Ñu seppi Eccen, nit kufeese ngëm ak Noo gu Sell gi, seppi Filib ak Porokor ak Nikanor ak Timon ak Parmenas ak Nikolas, ma dëkke Àncos te dib tuubeen bu duggoon lu jiitu ci yoonu Yawut. 6 Ñu indi leen fa kanam ndaw ya, ñu ñaanal leen, teg leen loxo.
7 Ba loolu amee kàddug Yàlla di law, limu taalibe yi yokku ba bare lool ci biir Yerusalem, sarxalkat yu bare daldi topp yoonu ngëm wi.
Teg nañu Eccen loxo
8 Ci kaw loolu Eccen, mi yiwu Yàlla def ag leer fees ko, di def ay kéemaan ak firnde yu mag ci biir askan wi. 9 Ba loolu amee ñenn ca jàngu ba ñuy wax jàngub waa Goreel ga, daldi jóg, di tàmbalee weranteek Eccen. Ay niti waa Siren a nga ca, ak waa Alegsàndiri, ak waa diiwaani Silisi ak Asi. 10 Teewul àttanuñu xelam mu rafet, ak Noo gi muy waxe.
11 Ñu daldi ger ay nit ngir ñu duural ko, ne: «Noo ko dégg, mu yékkati kàdduy saaga, jëme ci Musaa ak ci Yàlla.» 12 Ba loolu amee ñu xabtal nit ñi ak njiit yi, ak firikati yoon yi, ñu ne jalañ, jàpp Eccen, yóbbu ca kurélu àttekat ya. 13 Ñu indeeti foofa ay seedey naaféq yu ne: «Kii du bàyyee wax mukk lu juunoo ak bérab bu sell bii ak yoonu Musaa. 14 Noo ko dégg mu ne Yeesu Nasareen boobu dina màbb bérab bii te dina soppi aada yi nu Musaa bàyyee.»
15 Mboolem ña ca jataayu àttekat ya nag ne jàkk Eccen; ñu gis xar-kanam ba ne ràññ ni xar-kanamu malaaka.