Póol tiiñ na waa Korent
18
1 Ba loolu wéyee Póol bàyyikoo Aten, dem Korent. 2 Mu daje fa ak Yawut bu ñuy wax Akilas, fekk baax diiwaanu Pont. Muy sooga jóge réewum Itali, ànd ak soxnaam Pirsil, ndax Buur bu mag ba Këlódd moo joxe woon ndigal ne na Yawut yépp génn Room. 3 Póol nag miinante ak ñoom, te fekk ñu bokk benn liggéey, di defarkati xayma ni moom. Loolu tax mu far dal ak ñoom, di liggéey.4 Ci kaw loolu bésub Noflaay bu nekk Póol di waare ca jàngu ba, di yee Yawut yi ak Gereg yi. 5 Ba Silas ak Timote dikkee, bàyyikoo diiwaanu Maseduwan, Póol xintewootul lu moy di xamle kàddu gi, di seereel Yawut yi ne Yeesu mooy Almasi. 6 Yawut ya nag gàntal, di ko ŋàññ, mu yëlëb ay yéreem, misaale ko ne jaanam wàcc na. Mu ne leen: «Yeenay gàddu seen bakkanu bopp. Man set naa ci wecc. Gannaaw-si-tey, ci jaambur ñi dul Yawut laa jëm.»
7 Mu jóge foofa, dem kër jaamburub jaamukatu Yàlla bu ñuy wax Tisyus Yustus, te këram sësook jàngu ba. 8 Teewul Kirispus njiitu jàngu ba moom, gëm Sang bi, mook waa këram gépp. Ñu bare ci waa Korent a gëm, gannaaw ba ñu déggee kàddu gi, ba ñu sóob leen ci ndox.
9 Ba loolu amee Sang bi wax ak Póol ag guddi ci biir peeñu, ne ko: «Bul tiit dara, waaye waxal te bul noppi, 10 ndax maa ànd ak yaw, kenn du la song, def la lu bon, ndax xeet wu yaa laa am ci dëkk bii.» 11 At ak juróom benni weer la Póol toog ci seen biir, di jàngle kàddug Yàlla.
12 Jant ya Galyon moomee diiwaanu Akayi, Yawut ya dañoo mànkoo, jógal Póol, jàpp ko, yóbbu ca àttekaay ba. 13 Ñu ne: «Kii dafa juuyoo ak yoon ci ni muy xiire nit ñi ci jaamu Yàlla.»
14 Póol dem bay àddu, far Galyon ne Yawut ya: «Yeen Yawut yi, su doon ag njubadi mbaa jëf ju aay lool ju ngeen di tawat, kon xel dina nangu ma déglu leen. 15 Waaye su dee ag dëngoo ci wàllu wax, mbaa ay turi nit, mbaa seen yoonu bopp nag, seetal-leen ko seen bopp. Àtte loolu moom, duma ko nangu.» 16 Galyon daldi leen dàqe ca àttekaay ba. 17 Ci kaw loolu ñépp jàpp Sosten, njiitu jàngu ba, dóor ko ca àttekaay ba, te taxul Galyon yégal ko yaramam.
Póol délsi na Àncos gu Siri
18 Ba loolu wéyee Póol toogaat na fa fan yu bare, doora tàggtoo ak bokk ya, dugg gaal jëm Siri, ànd ak Pirsil ak Akilas. Fekk na mu watu nel ca teerub Señsere, firndeele ko aw xas wu mu xasoon.
19 Ba ñu teeree Efes, fa la Póol bàyyi Pirsil ak Akilas. Mu dem ca jàngu ba, ba diisoo fa ak Yawut ya. 20 Ñooñu ñaan ko, mu toogaat fa ab diir, mu gàntal. 21 Naka la tàggtoo ak ñoom, ne leen: «Dinaa leen seetsiwaat, bu soobee Yàlla.» Ba loolu amee mu dugg gaal, bàyyikoo Efes, 22 teereji Sesare. Mu dem nag Yerusalem, nuyuji mbooloom gëmkat ña, doora dem Àncos gu Siri.
Póol tukki na ñetteel bi yoonam
23 Póol toog na Àncos ay fan, jóge fa wër diiwaanu Galasi, teg ca Firisi, di ñaax mboolem taalibey foofa.
24 Ab Yawut nag bu ñuy wax Apolos te cosaanoo Alegsàndiri, moo dikkoon Efes. Ku rafet kàddu, te xam Mbind mi lool. 25 Kooku jotoon naa jàng yoonu Sang bi. Mu ànd ak cawarte, di waare ak a jàngle lu wér péŋŋ ci mbirum Yeesu, doonte xam-xamam a ngi yemoon ci sóobeb Yaxya ci ndox. 26 Mu tàmbalee waxe kóolute ca jàngu ba. Pirsil ak Akilas dégg ko, woo ko cig wet. Ñu daldi koy gëna leeralal yoonu Yàlla wi.
27 Ba mu ko defee Apolos namma jàll ba Akayi, bokk ya rafetlu mébétam. Ñu bind taalibey Akayi, ngir ñu dalal ko. Ba Apolos agsee Akayi, dimbali na lool ña fa yiw may ñu doon ay gëmkat. 28 Ndax fa kanam mbooloo ma la doon tiiñale Yawut ya ay firnde yu mat sëkk, firil leen Mbind mi, ba leeralal leen nàññ ne Yeesu mooy Almasi.