Jaar-jaari maam yedd na sët ya
10
1 Bokk yi, bugguma ngeen umple ko, sunu maam yépp la niir wa yiiroon, te ñoom ñépp a jàll géej gaa. 2 Ñoom ñépp lañu sóob sóobeb Musaa, ca biir niir wa, ak ca biir géej ga. 3 Ñoom ñépp, wenn ñamu kéemaanu Yàlla wa, moom lañu lekk, 4 te ñoom ñépp, menn ndoxum kéemaanu Yàlla ma lañu naan, ndax ñoo doon naane ca doju kéemaanu Yàlla ga, doj wa leen doon gunge, te doj wa Almasi la woon. 5 Teewul ñi ëpp ci ñoom, Yàlla amul woon lu ko neex ci ñoom, ba tax ñu daanu, dee ca màndiŋ ma.
6 Yooyu xew-xew ay misaal la, ngir nu baña xemmem yëf yu bon, na ko maam ya daan xemmeme. 7 Buleen doon ay jaamukati tuur, ni ko ñenn ci ñoom doone woon. Noonu lañu binde ne: «Mbooloo ma toog, di lekk ak a naan, nes tuut ñu jóg, di mbumbaayb 8 Bunu jëfe powum séy, ni ko ñenn ci ñoom daa defe, ba tax ñaar fukki junni ak ñett (23 000) ca mbooloo ma bokk dee ci benn bés. 9 Bunu wut itam Almasi, ni ko ñenn ci ñoom wute woon, ba tax ay jaan rey leen. 10 Buleen jàmbat, ni ñenn ci ñoom doon jàmbate, ba tax malaakam reykat ba rey leen.
11 Xew-xew yooyu dal maam ya ay misaal la, te dees koo bind ngir nu jànge ci, nun ñi mujug jamono yemool. 12 Moo tax ku yaakaar ne taxaw nga, nanga moytu bala ngay daanu. 13 Benn nattu dabu leen bu moy nattu yiy dale. Te it Yàllaa jara wóolu. Yàlla du nangu ngeen tegoo nattu bu ngeen àttanul, waaye nattu ba lay booleek pexe, ma leen cay génne, ba ngeen man koo dékku.
Dawleen bokkaale
14 Kon kat, samay soppe, dawleen bokkaale. 15 Njort naa ne boroomi xel laay waxal. Kon àtteel-leen seen bopp li ma leen wax. 16 Kaasu barke bi nuy barkeeloo, xanaa du mooy bokk gi nu bokk ci deretu Almasi? Te mburu mi nuy daggoo, du mooy bokk gi nu bokk ci yaramu Almasi? 17 Gannaaw menn mburu la nag, doonte ñu bare lanu, kon wenn yaram lanu, ndax nun ñépp, menn mburu mi lanu bokk.
18 Xool-leen bànni Israyil ci wàllu deret. Ñiy lekk yàppu juru sarax gu ñu rendi, xanaa bokkuñu ak sarxalukaay bi ab céram? 19 Ana kon lu sama wax jiy wund? Ndax daa wund ne yàpp wu ñu sarxal tuur yi tekki na lenn? Am daa wund ne tuur yi tekki na lenn? 20 Li may wax kay moo di yooyu sarax, rab yi la ñeel, waaye du Yàlla, te bugguma ngeen bokk ak rab yi lenn. 21 Dungeen mana naan ci kaasu Sang bi, naan ci kaasu rab yi. Dungeen mana bokk lekk ci ndabal Sang bi, bokk lekk ci ndabal rab yi. 22 Am danuy yékkati fiiraangey Sang bi? Danu koo ëpp doole?
Jëfeel say sañ-sañ tey sóoraale nit ñi
23 «Sañees na lépp,» lañu wax. Waaye du lépp ay jariñe. «Sañees na lépp,» waaye du lépp ay yokke. 24 Bu kenn sàkku njariñal boppam, waaye sàkkuleen seen njariñal moroom.
25 Mboolem luy jaay ca ja ba, sañ ngeen koo lekk te bañ cee luqatu lenn luy indi ngànt cim xel, 26 ndax Boroom bee moom àddina, ak li ci biiram.
27 Bu leen ku gëmul wooyee lekk, su ngeen nangoo, mboolem lu mu leen taajal, lekkleen, te bañ cee luqatu luy indi ngànt cim xel. 28 Waaye bu leen kenn nee: «Lii ñam wu ñu sarxal tuur yi la,» buleen lekk, ndax ka leen ko xamal, ndax itam, ngànt lu wax jiy indi cim xel. 29 Waxuma seenum xel yeen, waaye xelu keneen ka laay wax.
Ana sax lu waral sama sañ-sañu bopp di aju ci àtteb keneen ku am xelam amal ngànt? 30 Bu ma yékkatee kàddug cant ba lekk sama wàll, ana lees may sikke ci aw ñam wu ma sante Yàlla?
31 Kon nag su ngeen di lekk, mbaa ngeen di naan, mbaa ngeen di def leneen, lépp lu ngeen di def, wutleen koo terale Yàlla. 32 Buleen may kenn lu muy def njombe: du Yawut yi, du jaambur ñi, du mbooloom Yàlla mi. 33 Noonu laay def man ci sama bopp: ñépp laay wuta neex, ci lépp. Sàkkuwuma sama njariñal bopp, waaye njariñal lim bu gëna takku, moom laay sàkku, ngir ñu texe.