Lu jëm ci waxyu, aki may ci wàllu làkk
14
1 Xintewooleen cofeel, te ngeen sàkku mayi Noo gi, rawatina mayug waxe kàddug waxyu, 2 ndax kiy làkk weneen làkk, du nit ñi lay waxal, waaye Yàlla lay waxal, gannaaw kenn déggul li muy wax. Teewul ci Noo gi lay waxe ay kumpa. 3 Waaye kiy waxe kàddug waxyu, nit ñi lay waxal, di feddlee, di ñaaxe ak di naabe. 4 Kiy làkk yeneen làkk, boppam lay feddli, waaye kiy waxe kàddug waxyu, mbooloom gëmkat ñi lay feddli seen ngëm. 5 Su ma sañoon ngeen di làkk yeen ñépp yeneen làkk, waaye ngeen di waxe kàddug waxyu moo ma gënal. Kiy waxe kàddug waxyu moo ëpp njariñ kiy làkk yeneen làkk, ndare ñu tekki li muy làkk, ba mbooloom gëmkat ñi jële ca lu ñu feddlikoo. 6 Léegi bokk yi, su ma leen dikke woon yeneen làkk yu may làkk, ana lu ma leen di jariñ? Dara, xanaa ma àgge leen kàddug peeñu, mbaa xam-xam, mbaa waxyu, mbaa digle. 7 Noonu la itam ci jumtukaayi po yi dundul tey jibal coow; muy toxoro mbaa xalam. Su yooyu jumtukaay jibalul galan yu leer, ana nees di xame li toxoro ji, mbaa xalam giy wax? 8 Ag liitu xare it, su jibalul woote bu leer, ana kuy waajal ab xare? 9 Noonu la ci yeen itam. Seen làmmiñ, su ngeen ci waxul kàddu gu leer, ana nees di xame li ngeen di wax? Ci jaww ji rekk ngeen di wax! 10 Ak li làkki àddina bare te wuute lépp, wenn ñàkku ci am piri. 11 Baat bu jib nag, su ma xamul tekkiteem, ab jaambur laay doon ci kiy wax, te kiy wax it, ab jaambur lay doon ci man. 12 Kon yeen itam, gannaaw ñu xér ngeen ci mayi Noo gi, fexeleen cee am lu ne xéew, ngir feddli mbooloom gëmkat ñi.13 Moo tax kiy làkk weneen làkk wara ñaan ngir ñu xam pireem. 14 Su may ñaan ci weneen làkk, sama xol ay ñaan, waaye samam xel liggéeyul. 15 Kon ana nees di def? Naa ñaane sama xol, tey ñaane samam xel itam. Naa sàbbaale sama xol, tey sàbbaale samam xel itam. 16 Soo yékkatee kàddug cant goo waxe xol doŋŋ, ana nu nit ku xamul ku ko teewe naan: «Amiin,» te xamul li ngay wax? 17 Ndaxam yaw, rafet nga kàddug cant, waaye sa kàddu feddliwul keneen ku ciy dégg.
18 Sant naa Yàlla ndegam maay làkk yeneen làkk ba raw leen, yeen ñépp. 19 Waaye fu mbooloom gëmkat ñi daje, juróomi baat yu ma waxe samam xel ngir jàngle, moo ma gënal junniy baat yu ma waxe weneen làkk.
20 Bokk yi, buleen doon ay xale ci wàllu déggin. Su dee lu bon, nekkleen ci ay tuut-tànk, waaye màggleen ci wàllu déggin. 21 Bindees na ci téereb yoon wi ne:
«Ay niti làkk-kat,
ay làmmiñi doxandéem,
ci laay waxe ak askan wii,
te taxul ba tey ñu déglu ma.
Boroom bee ko waxa.»
22 Kon nag, yeneen làkk, kàddu ya du ci gëmkat ñi la di firnde, waaye ci ñi gëmul la di firnde. Te it waxe kàddug waxyu, du ci ñi gëmul la di firnde, waaye ci gëmkat ñi la dib firnde. 23 Léegi nag su mbooloom gëmkat mépp dajee bérab, ñépp di làkk yeneen làkk, bu ay nit ñu xamul mbaa ñu gëmul duggsee, duñu ne dangeena dof? 24 Waaye su ñépp dee waxe kàddug waxyu, ba ku gëmul, mbaa ku xamul duggsi, kàddu ga la ko ñépp di tiiñale, àggee ko ko ab àtteem, 25 ba la làqu woon ca biir xolam, daldi leer. Su ko defee mu ne dàll dëpp jëëm ci suuf, sujjóotal Yàlla, te naan: «Aylayéwén Yàllaa ngi ci seen biir!»
Ndajem gëmkat ñi jar naa rafetal
26 Kon nag ana nees di def, bokk yi? Bu ngeen dajee, kii am woyu cant, kii am lu muy jàngle, kee am am peeñu, kale am lu muy waxe weneen làkk, keneen am am piri, loolu lépp na ko feddli ngëm taxa jóg. 27 Su dee weneen làkk lees di wax, na ñaar ba gën gaa bare, ñett, toppante, te kenn di firi. 28 Su amul kuy firi, bu kiy làkk làkk wi biral lenn ci jataayu mbooloo mi. Na yelu, ngir boppam ak Yàlla.
29 Ñiy waxe kàddug waxyu, na ci ñaar ba ñett wax, te ñi ci des natt wax ji. 30 Su keneen ci jataay bi amee am peeñu, na ki doon wax noppi. 31 Ndax kat yeen ñépp man ngeena kenn-kennoo, di waxe kàddug waxyu, ngir ñépp jànge ca, ba gëna farlu. 32 Biralkati kàddug waxyu yi ñoo wara jiite xel mi ñuy waxe. 33 ndax Yàlla du Yàllay salfaañoo, Yàllay jàmm la.
Ci mboolem mboolooy ñu sell ñi nag, 34 na jigéen ñi noppi ci biir mbooloo yi, ndax mayeesu leen ñu wax ci yooyu jataay. Na jigéen ñi nangu, ni ko yoon wi ci boppam diglee. 35 Su amee lu ñu bëgga xam, ca kër ga lañu koy laaj seen jëkkër, ndax jigéen di wax ci biir mbooloom gëmkat ñi, gàcce la.
36 Ndax ci seen biir la kàddug Yàlla bàyyikoo? Am ci yeen doŋŋ la agsi? 37 Ku ci xalaat ne moom jottlikatub kàddug waxyu la, mbaa boroom ag may la ci Noo gi, war naa xam xéll ne lii ma leen bind, santaaneb Boroom bi la. 38 Ku ci xamul loolu nag, kooku, xameesu ko.