5
1 Xam nanu ne sunu yaram, sunu këru kaw suuf gii di ab xayma, bu daanoo it, am taax lanu am fa Yàlla, kër gu sax dàkk, gu loxol nit tabaxul. 2 Moo nu tax di onk ci biir xayma bii nu nekk, ndax yàkkamtee soloo sunu dëkkuwaayu asamaan, teg ko ci kaw bii nu jiital, 3 nde bu nu soloo noonu, dunu def yaramu neen. 4 Noo ngi onk ndax diis, li feek nu ngeek sunuw yaram, xayma bi nu soloo nii. Du summiku lanu namm, waaye solu teg ko ci lanu namm, ngir li jëm ndee, daldi suux ci biir ndund. 5 Googu muj ci boppam lanu Yàlla mooñe woon, te Noo gi mu nu jox lanu ci dawalal.6 Moo tax nu saxoo ñeme, te xam ne sunu desagum biir kër, ci yaram wi, mooy sunu desagum fu sore Sang bi, 7 ndax ngëm lanuy doxe, waaye doxewunu ab gis-gis. 8 Kon ñeme lanu def, te li nu gënal di génn, des bitib sunu yaramu tey, ngir dëkki ak Sang bi. 9 Kon nag, nu des biir kër gii, mbaa nu génn, dëkki bitib kër gii, li nu xintewoo daal moo di nu neex Sang bi. 10 Ndax kat, nun ñépp fàww nu taxawi fa jalub àttekaayu Almasi, ngir ku nekk yooloo kemu jëf ja mu jëfe yaramam, muy lu baax, mbaa lu bon.
Jubooleen ak Yàlla
11 Danoo xam lan mooy ragal Boroom bi nag, te moo nu tax di wax lu gëmloo nit ñi. Yàlla de ràññee na bu baax nooy kan. May yaakaar ne yeen itam, ci seen biir xol, ràññee ngeen bu baax nooy kan. 12 Seedeelatunu sunu bopp lu jar ngërëm de, danu leen di may lu ngeen nu mana sagoo, ndax ngeen am tontal ñi sagoowul li ci biir xol, xanaa di sagoo am peeñ. 13 Ndegam danoo teqlikoo ak sunu sago, Yàlla la ñeel. Su nu àndee ak sunu sago nag, yeen la ñeel. 14 Ndaxte cofeelu Almasi daal moo nu jiite, nun ñi ràññee lii: Gannaaw kenn moo deeyal ñépp, kon ñépp a dee. 15 Te ki deeyal ñépp, daa deeyal ñépp ngir ñiy dund bañatee dund ngir seen bopp, xanaa di dund ngir ki leen deeyal, ba dekki.
16 Kon nag gannaaw-si-tey, ni nitu suuxu neen di xoole moroomam, nun xooleetunu ko kenn. Doonte ni nitu suuxu neen lanu xoole woon Almasi, léegi xooleetunu ko noonu. 17 Kon bu nit ki bokkee ci Almasi, mbindeef mu bees lay doon. La woon day wonni, li teew nag, di lu yees. 18 Loolu lépp ci Yàlla la jóge, moom mi nu jubale ak boppam ci Almasi, te moo nu sas, ngir nuy waare juboo googu. 19 Loolu di firi ne ci Almasi la Yàlla jubale waa àddina, ak jëmmu boppam, ba toppu leen seeni tooñ, te moo nu dénk kàddug juboo gi. 20 Kon nag Almasi, noo diy ndawam, te ci nun la Yàlla di wootee. Kon ci turu Almasi, danu leen di ñaan: nanguleena juboo ak Yàlla. 21 Almasi mi masula bàkkaar, moom la Yàlla sëf sunu bàkkaar, ngir nu mana ame ci moom àtteb nit ñu jub fa Yàlla.