6
1 Nun ñi bokk ci liggéey bi nag, noo leen di ñaan ngeen baña nangu yiwu Yàlla ci neen. 2 Ndaxte Yàlla moo ne:«Jant ba mu jotee laa la nangul,
bésu mucc ba laa la wallua.»
Te nag, tey jii la jantam jote; tey kat, la bésub mucc.
Liggéeyal Yàlla ñàkkul aw tiis
3 Buggunu kenn sikk sunub liggéey, moo tax buggunoo jëfe lenn luy doon tojaange ci kenn. 4 Ci lépp kay lanu bëgga seedeel sunu bopp, ne noo yelloo ngërëm, te ay jawriñi Yàlla lanu, di ñu muñ lu bare ci biir coono, aki mitit, aki njàqare; 5 ci ay dóor, ak néegi kaso, ci biir mbooloo yu nu jógal, ci doñ-doñ ju metti, ak fanaanee xoole, akub xiif; 6 te nuy setal sunu dund, di ànd ak xam-xam, ci biir muñ, akug mbaax, ci biir Noo gu Sell gi, ak cofeel gu amul jinigal, 7 ci biir kàddug dëgg, ak kàttanu Yàlla; ci kaw gànnaayi njubte yi ci sunu loxol ndijoor ak lu càmmoñ; 8 ci biir teraanga, ak ci biir toskare; ci biiri baatal, ak jëw yu rafet. Dees noo jàppe ay mbubbookati dëgg, te nuy nit ñu dëggu; 9 jàppe nu ñu kenn xamul, te nuy ñu siiw; jàppe nu ñuy waaja dee, te nuy dund; jàppe nu ñu ñu wara mbugal, te bañ leena teg àtteb dee. 10 Dees noo jàppe boroomi tiis, te nu dëkke mbég; jàppe nu ay néew-ji-doole, te nu woomal ñu bare; jàppe nu ñu amul dara, te nu moom lépp.
11 Yeen bokki Korent, wax nanu leen sunu biir yépp, ubbil leen sunu xol. 12 Genn ñooru jógewul ci nun, waaye yeen yeena nu ñooroo seen xol. 13 Léegi nag, yeen, feyleen nu bor bi boog, ma wax ak yeen ni samay doom, ubbil-leen nu seen xol!
Baleen bokkaale
14 Buleen lëkkoo ak gëmadikat ñi. Gan lëngoo la njub ak ndëngte séq? Gan booloo la leer ak lëndëm séq? 15 Gan juboo la Almasi ak Seytaane séq? Wan wàll la gëmkat bi bokk ak gëmadikat bi? 16 Gan takktoo la kër Yàlla séq ak ay tuur? Ndax kat, nun, nooy kër Yàlla jiy dund, te noonu la ko Yàlla waxe ne:
«Maay dëkk ci seen biir, di dox ci seen biir,
di seen Yàlla, ñuy sama ñoñb.»
17 Kon nag:
«Nangeen génne ci seen biir, te teqlikoo ak ñoom,»
la Boroom bi wax.
«Lu sobewu, buleen ko laalc.
Su boobaa, maa leen di dalald.
18 Maay doon seen baay,
ngeen di samay doom, góor, ak jigéene,»
la Boroom bi, Aji Man ji wax.