Ndawi Almasi ya doyloo nañu Póol
2
1 Fukki at ak ñeent gannaaw gi laa dellu Yerusalem, ànd ak Barnaba, yóbbaale Tit itam. 2 Sama tànk yooyu nag am peeñu moo ko waral. Ca laa wéetoo ak ña ñu jàppoon ne ñooy kàngami mbooloom gëmkat ña, faramfàcceel leen xibaaru jàmm bi may yégal jaambur ñi dul Yawut, ngir ragal sama liggéey bi ma jota def, te di ko wéye, doon coonob neen. 3 Moonte Tit mi ma àndaloon sax, tegeesu ko fa wartéefu xaraf, te ci askanu gereg yi dul xaraf la bokk. 4 Doonte booba, ay nit ñu tuddoo bokki gëmkat ñoo yoxoosu ba tàbbi ci sunu biir, di nu yëddu, ngir luqatu ni nu moome sunu bopp ndax Almasi Yeesu mi nu gëm, te li ñu ci jublu di delloo nu ci buumi njaam. 5 Waaye ñooñu, nangulunu leen lu tollook simili sax, ndax bëgg leena sàmmal yeen, dëggug xibaaru jàmm bi, ba mu sax ci yeen.6 Teewul ñooñu ñu jàppe woon ay kàngam, ak daraja ju ñu masoona am, amalu ma solo, nde Yàlla amul xejj ak seen, ñooñu yokkuñu lenn ci kàddu gi may xamle. 7 Xanaa kay li ñu gis moo di ni Yàlla yebale Piyeer ngir mu àgge askanu Yawut xibaaru jàmm bi, noonu la ma yebale ngir ma àgge ko jaambur ñi xaraful, 8 ndax ki liggéey ci Piyeer, ngir mu doon ndawam ci Yawut yi, moo liggéey ci man itam, ngir may ndawam ci yeneen xeet yi. 9 Ña ñu jàppoon ne ñooy kenuy mbooloom gëmkat ña nag, te ñuy Yanqóoba ak Sefas ak Yowaan, ba ñu ràññee yiw wi ñu ma jagleel, maak Barnaba lañu jox loxo, ngir nun nu liggéeyi ca jaambur ña, te ñoom ñu liggéeyi ci Yawut yi. 10 Laajuñu lu moy nu fàttliku néew doole yi, te loolu di lu ma pastéefoo jëfe.
Póol yedd na Sefas ca Àncos
11 Waaye ba Sefas dikkee Àncos, jàkk laa ko def, weddi ko, ndax moo nekkul woon ci dëgg. 12 Ndax kat balaa aw nit a dikk, bàyyikoo fa Yanqóoba, Sefas da daan bokk lekk ak jaambur ñi dul Yawut. Waaye ba ñooñu dikkee la rocciku, daldi beddeeku jaambur ñi, ndax ragal waa làng, ga jàpp ne aaday xaraf wartéef la. 13 Yeneen Yawut ya it di jinigalandoo, ba Barnaba sax lajj topp leen ci seenug jinigal.
14 Waaye ba ma gisee ne doxewuñu njub gi dëggug xibaaru jàmm bi laaj, maa wax Sefas ci kanam ñépp, ne ko: «Ndegam yaw miy ab Yawut, yaa jëfewul ni ab Yawut, xanaa di jëfe ni xeeti jaambur ñi, ana lu tax ngay ërtal jaambur ñi dul ay Yawut, ngir ñu yawutal?»
Ngëm a takku
15 Nun danoo juddu diy Yawut, te bokkunu ca xeet yee diy bàkkaarkat. 16 Xam nanu nag ne nit ki, du ci jëfi sàmm ndigali yoon la ko Yàlla di joxe àtteb ku jub, xanaa ci ngëm gu mu gëm Yeesu Almasi. Te nun itam, Almasi Yeesu lanu gëm, ngir Yàlla jox nu àtteb ku jub ci kaw gëm gu nu gëm Almasi, te du ci kaw jëf ju nu sàmme ndigali yoon. Ndax kat du ci jëfi sàmm yoon lees di joxe kenn àtteb ku jub.
17 Ba tey su nu dee sàkku àtteb ku jub, ndax li nu gëm Almasi, te teewul nit ñi gis ne nu ngi bàkkaar, nun itam, ndax loolu day wund ne Almasi mooy xiirtale ci bàkkaar? Mukk kay! 18 Ndaxam su dee tabaxub ndigalu yoon bi ma tojoon, moom laa tabaxaat, maa def sama bopp moykatub yoon. 19 Su dee wàllu yoonu Musaa nag, man nit ku dee laa, te yoonu Musaa moo ko waral, ngir ma mana dund dund gu ñeel Yàlla. Dees maa boole ak Almasi rey ca bant ba. 20 Moo tax dootu man maay dund, waaye Almasi mooy dund léegi ci man. Sama dundu yaramu suux wii tey nag, ci ngëm gi ma gëm Doomu Yàlla laa koy dunde, moom mi ma sopp, ba jébbale boppam ngir man. 21 Duma neenal yiwu Yàlla, ndax kat su doon ci sàmm ndigalu yoon lees di ame àtteb ku jub, konoon Almasi moo dee cig neen.