Nganug Póol neenul
2
1 Yeen ci seen bopp kay, bokk yi, xam ngeen ne sunu ngan ak yeen neenul. 2 Xam ngeen na nu jëkkoona sonne, ak na ñu nu torxale woon ca Filib, dëkk ba, bala noo dikk fa yeen. Teewul ci sunu ndimbalal Yàlla, nu ñeme leena àgge, ci biir xeex bu metti sax, xibaaru jàmm bu Yàlla bi. 3 Ndaxte sunub woote laloowul pexem sànke, ak mébét mu setul, akug njublaŋ. 4 Xanaa kay noonu nu Yàlla doyloo, ba dénk nu liggéeyu xibaaru jàmm bi, noonu lanuy waaree li neex Yàlla miy seet ab xol, te dunu ci wut bànneexu nit ñi.5 Masunoo jaye, xam ngeen ko, ag bëgge it masunoo taxa jóg, Yàlla seede na ko; 6 masunoo sàkku ngërëmal nit, du ci yeen, du ci ñeneen. 7 Manoon nanoo taafantoo li nu diy ndawi Almasi, ba diisal leen, waaye danoo lewetoon domm ci seen biir, mel ni jaboot juy topptoo ay doomam. 8 Noonu lanu nabe woon ci yeen, ba buggunu woona yem ci xamal leen doŋŋ xibaaru jàmm bu Yàlla, waaye danu leena sopp ba yéene woon leena jox sunu bakkan sax boole ci, ndax fi ngeen nu mujj tollu ci sunu xol. 9 Xanaa bokk yi, yeena ngi fàttliku sunu doñ-doñ ak sunu coono? Diir ba nu leen di yégal xibaaru jàmm bu Yàlla bi, guddi ak bëccëg lañu daan liggéeyaale, ngir baña diisal kenn ci yeen.
10 Yeena seede, Yàlla itam seede, sellnga ak njub, ak mucc sikk ga nu doon jëfe fa seen biir, yeen ñi gëm. 11 Xam ngeen ne fi baay féete doomam lanu féete kenn ku nekk ci yeen. 12 Ñaax nanu leen, dëfal leen, dénku leen, ngir ngeen di jëfe jëfin wu yelloo ak Yàlla, mi leen woo ci nguuram ak teraangaam.
13 Leneen lu nu dul noppee sante Yàlla, moo di lii: ba ngeen nangoo ci sunu làmmiñ kàddug Yàlla gi nu leen dégtal, te melul ni kàddug nit doŋŋ ngeen ko nangoo, waaye kàddug Yàlla gi mu doon ci lu wér, moom ngeen ko jële, te kàddu googu mooy liggéey ci seen biir, yeen gëmkat ñi. 14 Ndax kat bokk yi, yeena aw ci tànki gëmkati Almasi Yeesu ya fa mboolooy Yàlla, ya fa réewum Yuda, nde coono ya ñu daj ca Yawut ya, yeen it seeni waa réew teg nañu leen lu ni mel. 15 Yawut ñi ñoo rey Sang Yeesu, na ñu reye woon yonent yi, te ñoo nu bundxatal tey. Neexuñu Yàlla, te nooni ñépp lañu. 16 Ñoo nuy aaye nu àgge jaambur ñi dul Yawut, kàddu gi leen di musal. Noonu lañu matale seen jóorub bàkkaar yi ñu nekke naka jekk, waaye am sànj a leen mujj dab.
Póol namm na waa Tesalonig
17 Nun nag bokk yi, teqale nañu nu ak yeen ab diir, waaye xol yi sorewaatoowul, xanaa jëmm yi rekk. Waaye sunu nammeel gu réy tax na noo def sunu kem kàttan, ndax yàkkamtee gise waat ak yeen. 18 Moo tax nu bëggoon leena seetsi, waaye Seytaane moo nu gàllankoor. Te man Póol, jéem naa leena seetsi bu dul benn yoon du ñaar. 19 Ndax kat, ana kan mooy sunu yaakaar, di sunu mbég, te di sunu kaala gu nuy sagooji? Xanaa du yeen, kera ca sunu kanam Boroom Yeesu, bu feeñee? 20 Yeen déy, lanuy damoo, di leen bége.