Sellal wartéef la
4
1 Li ci des nag, bokk yi, moo di yeena nangoo ci sunu làmmiñ, jëfin wi ngeen wara jëfe ba neex Yàlla, te it moom ngeen nekke. Waaye danu leen di tinu, di leen ñaax, ci turu Sang Yeesu, ngir ngeen gënati koo jëfe. 2 Xam ngeen ndigal, yi nu leen jox ci turu Sang Yeesu. 3 Lii moo di coobarey Yàlla: ngeen sellal te mucc ci powum séy. 4 Su ko defee kenn ku nekk ci yeen mana moom yaramu boppam ci biir sellnga ak teddnga, 5 te ngeen ànd ak sago ci seeni xemmemtéef, baña mel ni niti xeet yi xamul Yàlla. 6 Ci moomu mbir, bu kenn ci yeen tooñ mbokkam, di aakimoo yelleefam, ndax waxoon nanu leen ko, ba artooti leen ne leen jëf ju ni mel, Boroom bee koy fey ña ko def. 7 Yàlla kat ci sellnga la nu woo, waaye du ci jëfin wu setul. 8 Kon nag ku jalax ndigal lii, du nit nga jalax, xanaa Yàlla, moom mi leen jox Noowam gu Sell.9 Ci wàllu mbëggeel gi war ci biiri bokk, soxlawuleen ku leen ci bind dara, ndax yeen ci seen bopp, Yàlla tàggat na leen ci soppante, 10 te moom ngeen nekke seen digg ak mboolem bokki diiwaanu Maseduwan gépp. Teewul nag, bokk yi, nu di leen ñaax, ngir ngeen gënate jëfe noonu. 11 Sàkkuleen di jëfe jëfin wu dal, te ngeen di topptoo lu seen yoon nekk, tey dunde seenu ñaq, na nu leen ko sante woon. 12 Kon dingeen jekk nu ngeen di jëflantee ak ñu gëmul ña ca biti, te dungeen soxlaal kenn dara.
Tiislu bu ëpp warul
13 Bokk yi nag, buggunu ngeen réere mbirum way dawlu ñi, bay tiislu ni ñeneen ñi amul jenn yaakaar, di tiisloo. 14 Ndegam gëm nanu ne Yeesu dee na, ba dekki, noonu it lanu wara gëme ne Yàlla mooy dekkal way dawlu ñi gëmoon Yeesu, ba boole leen ak Yeesu, indaale.
15 Lii nu leen di àgge, te muy kàddug Boroom bi de, moo di nun ñi fiy dese bakkan ba kera Sang biy délsi, dunu jiitu way dawlu ñi fa moom. 16 Sang bi ci boppam, woote bu xumb lay wàccaalee asamaan, baatu kilifag malaaka jib, ànd ak coowal liitu Yàlla. Su ko defee ña seenug dee fekk ñu gëm Almasi ñooy jëkka dekki. 17 Gannaaw loolu nun ñi fi dese bakkan lees di këfandoo ak ñoom, jëme ca niir ya, ngir nu dajejeek Sang bi fa jaww ja, nu daldi nekk ak moom ba fàww. 18 Kon nag deeleen dëfalantee yooyu kàddu.