Bataaxal bu jëkk bi Yàlla may Póol, mu bind ko
Timote
1
1 Ci man Póol, ndawal Almasi Yeesu, ci ndigalal Yàlla sunu Musalkat, ak Almasi Yeesu sunu yaakaar, ci man la bataaxal bii bawoo, 2 ñeel Timote, sama doomu bopp ci wàllu ngëm. Aw yiw ak yërmande ak jàmm ñeel na la, bawoo ci Yàlla Baay bi, ak sunu Sang Almasi Yeesu.Njàngle mu jub day yokke
3 Na ma la ko dénke woon ba may dem diiwaanu Maseduwan rekk, nanga toog Efes googu, ngir ña fay jàngle leneen, nga aaye leen. 4 Ne leen ñu baña topp léebi neen, ak limi maam yu dul jeex, ndax loolu ay werante doŋŋ lay jur, te jariñul dara ci liggéeyu njotug Yàlla gi sottee ci ngëm. 5 Ndénkaane lii nag, li ko taxa jóg mooy luy yee ag cofeel gu bawoo ci xol bu rafet, ak xel mu dal, ak ngëm gu mucc jinigal. 6 Am na ñu moy woowu yoon, ba lajj jëm ci wax ju tekkiwul dara. 7 Ñooñu ay jànglekati yoonu Musaa lañuy xëccoo doon, te xamuñu li ñuy wax, bay xam lenn ci li ñuy dëggal.
Yoonu Musaa am na ñu mu taxa jóg
8 Xam nanu nag ne yoonu Musaa baax na, ndegam na mu ware lees ko jëfe. 9 Lii itam xam nanu ko: ñi jub taxuñu yoon wi jóg, xanaa ñi jubadi ak ñi déggadi, ak ñemekati Yàlla yi, ak bàkkaarkat yi, ak ñi wormaalul lu sell, ak ñi wormaalul Yàlla, ak bóomkati baay, ak bóomkati ndey, ak reykati nit ñi, 10 ak fokati séy yi, ak góor-jigéen yi, ak jàppkati jaam yi, ak fen-kat yi, ak giñkati fen yi, ak ñiy jëfe leneen lu woroo ak njàngle mu baax, 11 mi dëppoo ak xibaaru jàmm bi ñu ma dénk, xibaaru Yàlla Aji Tedd ju màgg ji.
Nanu sante Yàlla yërmandeem
12 Damay sant sunu Boroom Almasi Yeesu mi ma dooleel, moom mi ma natt ba wóolu ma, tabb ma ci liggéey bi, 13 te ma nekkoon ab tooñkatam, di ab bundxatalkat, di ab néeg. Waaye yërmande laa dajeel, ngir ñàkka xam ga ma daan jëfe, te ñàkka gëm tax. 14 Sunu yiwu Boroom moo ma baawaanal, booleel ma ci ngëm gi, ak cofeel, gi gëmkatub Almasi Yeesu jagoo. 15 Mboolem kàddu gii may wax, lu wóor la te jara gëm: Almasi Yeesu moo dikk ci àddina, ngir musal bàkkaarkat yi, te maa ci raw! 16 Waaye loolu moo tax man bàkkaarkat bi ci raw, ma dajeek yërmande, ngir, ci lépp lu nu Almasi Yeesu di muñal, ma doon ci misaal, ñeel ñi ko nara gëm ëllëg, ba texe ba fàww.
17 Yaw Buur bi sax dàkk,
doo dee, te bët manu laa gis,
yaw Yàlla miy kenn, yaa tedd, yaa màgg,
tey ak ëllëg ba fàww. Amiin!
18 Kon nag Timote doom, loolu mooy ndigal li ma la dénk, te mu dëppook kàdduy waxyu yi jotoona jib te jëm ci sa mbir. Gànnaayool kàddu yooyu ngir di ci xaree xare bu baax bi, 19 te nga saxoo ngëm ak xel mu dal. Am na ñu tanqamlu seen ndéeyum xel ba suuxal seen ngëm. 20 Ci ñooñu la Imene ak Alegsàndar bokk; Seytaane laa leen jébbal, yare leen ko, ngir ñu bañatee saaga Yàlla.