Póol sàrtal na jataayub màggal Yàlla
2
1 Kon nag li jiitu ci mboolem li may dénkaane mooy ngeen di dagaan, di ñaan, di tinu ak a sant, ñeel doom aadama yépp, 2 ñeel buur yi, ak mboolem boroom baat yi, ngir nu mana nekke jàmm akug dal, tey wéye gépp njullite, ak wépp dundin wu tedd.3 Loolu moo rafet te neex Yàlla sunu Musalkat, 4 bi bëgg ñépp mucc te ràññee liy dëgg. 5 Ndax kat jenn Yàlla doŋŋ moo am, benn Defarekat doŋŋ it moo am diggante Yàlla ak nit ñi, te mooy nit ki Almasi Yeesu, 6 mi maye bakkanam ngir jot ñépp, te jëf jooju lañu seedeele ca ba mu jotee, la Yàlla nammoon. 7 Ci boobu seede lañu ma tabbe ab yéenekat, ak ndawal kàddu gi, ak itam ab sëriñ, ñeel xeet yi dul Yawut, ngir ma xamal leen yoonu ngëm ak dëgg. Fenuma, dëgg doŋŋ laay wax.
8 Kon li ma bëgg moo di góor ñi di ñaane fépp, tàllal loxo yu mucc sikk, te bañ cee boole meroo ak mbiicoo. 9 Naka noonu, na jigéen ñi di sol col gu yiw, gu teggine te yem. Buñu jiital di defaroo ay létt yu ëpp, ak gànjari wurus, aki per, ak yérey tànnéef, 10 waaye nañu gànjaroo jëf ju baax, ndax mooy li jekk ci jigéen ñuy seede ne ñooy ragalkati Yàlla.
11 Te it bu ñuy jàngle, na jigéen ñiy noppi, te woyof toyy. 12 Mayuma jigéen mu jàngle mbaa mu jiite góor, waaye na noppi. 13 Ndax kat Aadama lañu jëkka bind, Awa topp ca. 14 Te it du Aadama lañu nax, waaye jigéen lañu nax ba mu xëtt ndigal. 15 Teewul muccu jigéen a ngi ci njurum doom, ndegam saxoo na ngëm, ak cofeel, ak jëfin wu sell te yem.