Jaamukati Yàlla yi mucc nañu
7
1 Gannaaw loolu ma gis ñeenti malaaka yu taxaw ci ñeenti colli àddina. Ña nga téye ñeenti ngelawi àddina, ngir ngelaw baña wale fenn; du ci jéeri, du ci géej, du ci genn garab. 2 Ma gis meneen malaaka, mu yéege penku, yore torluwaayu Yàlla jiy dund. Mu àddu ca kaw, wax ak ñeenti malaaka ya ñu mayoon ñu yàq géej ak jéeri, 3 ne leen: «Buleen yàqagum jéeri ji ak géej gi ak garab yi, li feek torluwunu ci jëwi ñiy jaamu sunu Yàlla, màndargaale leen.»4 Ma dégg limub ña ñu màndargaale torluwaay ba; ñuy téeméer ak ñeent fukk ak ñeenti junni (144 000), bawoo ci mboolem giiri bànni Israyil:
5 Giirug Yuda, fukki junneek ñaar (12 000) lañu ci màndargaal,
giirug Ruben, fukki junneek ñaar,
giiru Gàdd, fukki junneek ñaar,
6 giirug Aser, fukki junneek ñaar,
giirug Neftali, fukki junneek ñaar,
giirug Manase, fukki junneek ñaar,
7 giirug Simeyon, fukki junneek ñaar,
giirug Lewi, fukki junneek ñaar,
giirug Isaakar, fukki junneek ñaar,
8 giirug Sabulon, fukki junneek ñaar,
giirug Yuusufa, fukki junneek ñaar,
giirug Beñamin, fukki junneek ñaar.
Mbooloo mu réy am na ndam
9 Gannaaw loolu ma jekki gis mbooloo mu réy mu kenn manula waññ, ñu bawoo ci askan yépp ak giir yépp ak xeet yépp ak làmmiñ yépp. Ñu ngi taxaw fi kanam ngàngune mi ak Gàtt bi, sol mbubb yu weex, ŋàbb ay cari garabi tàndarma. 10 Ña ngay àddu ca kaw, naan:
«Texee ngi fi sunu Yàlla, ki toog ci ngàngune mi,
ak ci Gàtt bi!»
11 Malaaka yépp a nga taxaw, yéew ngàngune ma ak mag ñaak ñeenti bindeef ya. Ñu ne gurub sukk, dëpp seen jë fa kanam ngàngune ma, sujjóotal Yàlla, 12 ne: «Amiin! Na sunu Yàlla jagoo màggal ak daraja ak xel ak cant ak teraanga ak kàttan ak doole, tey ak ëllëg ba fàww. Amiin!»
13 Ci kaw loolu kenn ci mag ñi ne ma: «Boroom mbubb yu weex yii, ñooy ñan ak fan lañu jóge?»
14 Ma ne ko: «Sama sang, loolu de xanaa yaa ko xam.» Mu ne ma: «Ñoo di ñi jóge ca nattu bu réy ba. Fóot nañu seeni mbubb, ba weexal ko ci deretu Gàtt bi. 15 Loolu moo leen taxa
teew fi kanam ngàngunem Yàlla,
di ko jaamoo biir màkkaanam guddi ak bëccëg,
te ki toog ci ngàngune mi moo leen di yiir.
16 Dootuñu xiif, dootuñu mar.
Dootuñu loru ci jant bi mbaa weneen tàngoor,
17 ndaxte Gàtt bi ci diggu ngàngune mi moo leen di sàmm,
yóbbu leen ca bëti ndoxum dund ma,
te Yàllaa leen di fompal wépp rongooñ.»