Gàtt ba tàyyi na juróom ñaareelu tayu ga
8
1 Bi Gàtt bi tàyyee juróom ñaareelu tayu gi nag, asamaan da ne selaw lu mat genn-wàllu waxtu. 2 Ci kaw loolu ma gis juróom ñaari malaaka yi taxaw fi kanam Yàlla, ñu jox leen juróom ñaari liit.3 Bi loolu amee meneen malaaka dikk, taxaw ci wetu sarxalukaay bi. Mu ngi yor andu cuuraayu wurus. Ñu jox ko cuuraay lu bare, ngir mu boole kook ñaani mboolem aji sell ñi, jooxe ko ci kaw sarxalukaayu wurus bi ci kanam ngàngune mi. 4 Saxaras cuuraay laa ngi gillee ci loxol malaaka mi, ànd ak ñaani ñu sell ñi, di yéeg fa Yàlla. 5 Malaaka mi jël andu cuuraay bi, tibbe ci sarxalukaay bi ay xal ba and bi fees. Mu daldi koy sànni ci kaw àddina, rekk ag dënu riir, kàddu ràndaŋ, ag melax tàkk, suuf yëngu.
Liit yi jib na
6 Ba mu ko defee juróom ñaari malaaka yi yor juróom ñaari liit yi di waaja liit.
7 Malaaka mu jëkk mi wal liitam, tawu doji yuur topp ci, ak sawara wu ànd ak deret, ñu boole lépp sànni ci kaw suuf, ñetteelu xaaju suuf si daldi lakk, ñetteelu xaaju garab yi it lakk, ñax mu naat mépp lakk.
8 Ñaareelu malaaka mi wal liitam, mu am lu mel ni tund wu réy wuy tàkk, ñu sànni ko ci géej gi, ñetteelu xaaju géej gi soppiku deret, 9 ñetteelu xaaju bindeefi géej dee, ñetteelu xaaju gaal yi yàqu yaxeet.
10 Ñetteelu malaaka mi wal liitam, biddiiw bu réy buy tàkk nig jum xàwwikoo asamaan, wadd ci kaw ñetteelu xaaju dex yi ak bëti ndox yi. 11 Biddiiw bi Wextan la tudd. Ñetteelu xaaju ndox yépp la wexal, ñu bare naan ci, daldi dee, ndax wextanu ndox mi.
12 Ñeenteelu malaaka mi wal liitam, mu dal ñetteelu xaaju jant bi, ak ñetteelu xaaju weer wi, ak ñetteelu xaaju biddiiw yi, ba tax seen ñetteelu xaaju leer giim, ñetteelu xaaju bëccëg bi daldi lëndëm, ñetteelu xaaju guddi gi it gëna lëndëm.
13 Ma xoolaat, daldi dégg jenn jaxaay ju naawe digg asamaan. Mu àddu ca kaw ne: «Wóoy, wóoy, wóoy, musibay waa àddina yiy sababoo ci yeneen baati liit yi ñetti malaaka yi ci des, di waaja liit.»