Sasu Sarxalkat yi
di ñetteelu xaaju Tawreetu Musaa
Ay dogal ci mbirum sarax yi
(Saar 1.1—7.38)
Lu jëm ci saraxu rendi-dóomal
1
1 Aji Sax ji woo na Musaa, wax ak moom ca xaymab ndaje ma ne ko: 2 «Waxal bànni Israyil ne leen: Bu kenn ci yeen dee sàkkal Aji Sax ji sarax, na indi ag jur, muy gu gudd mbaa gu gàtt.
3 «Bu saraxam dee saraxu jur gu gudd gu ñuy def rendi-dóomal, na sarxal aw yëkk wu amul sikk. Na ko yóbbu ci bunt xaymab ndaje mi ci kanam Aji Sax ji, ngir mu nangul ko ko. 4 Na teg loxoom ci kaw boppu juru saraxu rendi-dóomal bi, ndax ñu nangul ko ko, muy njotlaayam. 5 Na rendi yëkk wi ci kanam Aji Sax ji, te doomi Aaróona yu góor yiy sarxalkat yi ñooy indi deret ji, xëpp ko ci mboolem weti sarxalukaay bi ci bunt xaymab ndaje mi. 6 Juru saraxu rendi-dóomal bi, na ko boroom sarax bi fees, daggat ko. 7 Doomi Aaróona, sarxalkat bi, dañuy jafal ab taal ci kaw sarxalukaay bi, teg matt mi ci taal bi. 8 Su ko defee doomi Aaróona yu góor, yiy sarxalkat yi, jël dog yi, booleek bopp bi ak nebbon bi, teg ko ci kaw mattum taal bi ci sarxalukaay bi. 9 Nañu raxas yérey biir yi ak yeel yi, sarxalkat bi boole lépp lakk ci kaw sarxalukaay bi. Saraxu rendi-dóomal la, saraxu sawara ngir xetug jàmm, ñeel Aji Sax ji.
10 «Bu saraxam dee ab gàtt bu ñuy def rendi-dóomal, muy xar mbaa bëy, na sarxal bu góor bu amul sikk. 11 Na rendi sarax si ci kanam Aji Sax ji, fa féete sarxalukaay bi bëj-gànnaar. Na doomi Aaróona yu góor yiy sarxalkat yi xëpp deret ji ci mboolem weti sarxalukaay bi. 12 Bu ko boroom sarax bi daggatee ba noppi, sarxalkat bi day boole dog yeek bopp bi ak nebbon bi, teg ko ci kaw mattum taal bi ci kaw sarxalukaay bi. 13 Na boroom sarax bi raxas yérey biir yi ak yeel yi, sarxalkat bi boole lépp lakk ci kaw sarxalukaay bi. Saraxu rendi-dóomal la, saraxu sawara ngir xetug jàmm, ñeel Aji Sax ji.
14 «Bu nit ki dee sarxalal Aji Sax ji njanaaw luy doon rendi-dóomal, na sarxe pitax mbaa xati mu ndaw. 15 Na ko sarxalkat bi yóbbu ca sarxalukaay ba, kutt baat bi, lakk ko ci kaw sarxalukaay bi. Deret ji dees koy siital ci wetu sarxalukaay bi, ba mu jeex. 16 Na indi gag bi ak li ci nekk te wetti ko fa ñuy def dóomu-taal ba, fa féete sarxalukaay bi penku. 17 Sarxalkat bi day jàpp ci laaf yi, xotti te bañ koo teqale, daldi koy lakk ci sarxalukaay bi, ci kaw mattum taal bi. Saraxu rendi-dóomal la, saraxu sawara ngir xetug jàmm, ñeel Aji Sax ji.