Lu jëm ci saraxu pepp
2
1 «Bu nit dee indil Aji Sax ji saraxu pepp, sungufa su mucc ayib la saraxam wara doon, mu sotti ci diw, def ci cuuraay, 2 te yót ko doomi Aaróona yu góor yiy sarxalkat yi. Na sarxalkat bi sàkk barci-loxob sunguf su mucc ayib soosu ànd ak diw gi, te boole kook cuuraay li lépp. Na sarxalkat bi def cér boobu saraxu baaxantal, lakk ko ca kaw sarxalukaay ba, muy saraxu sawara ngir xetug jàmm, ñeel Aji Sax ji. 3 Li des ci saraxu pepp mi, Aaróona aki doomam ñoo koy féetewoo, muy cér bu sella sell, bawoo ci saraxi sawara yi ñeel Aji Sax ji.
4 «Su dee sarxal lu ñu defare pepp, di lu ñu lakk cib taal ba mu ñor, na doon sunguf su mucc ayib, di mburu yu amul lawiir yu ñu xiiwaale diw, mbaa mburu yu sew yu amul lawiir, ñu sotti diw ca kawam. 5 Bu saraxam dee lu ñu defare pepp, lakke ko ci saafukaayu weñ, na doon sunguf su mucc ayib su ñu xiiwaale diw te bumu am lawiir. 6 Na ko dammat te sotti diw ca kaw dog ya. Saraxu pepp la. 7 Bu saraxam dee lu ñu defare pepp, di lu ñu saaf ci cin ba mu ñor, na doon sunguf su mucc ayib su ñu xiiwaale diw.
8 «Na yóbbul Aji Sax ji saraxu pepp su ñu defar ci tegtal yooyu, yót ko sarxalkat bi, mu yóbbu ko ca sarxalukaay ba. 9 Su ko defee sarxalkat bi génne ci saraxu pepp mi, ab saraxu baaxantal, daldi koy lakk ci kaw sarxalukaay bi, muy saraxu sawara ngir xetug jàmm ñeel Aji Sax ji. 10 Li des ci saraxu pepp mi, Aaróona aki doomam ñoo koy féetewoo, muy cér bu sella sell, bawoo ci saraxi sawara yi ñeel Aji Sax ji.
11 «Du benn saraxu pepp bu ñuy defal Aji Sax ji muy am lawiir, ndax du lenn ci lawiir mbaa lem, lu ñu wara lakk, ngir saraxu sawara su ñeel Aji Sax ji. 12 Saraxi ndoortel meññeef man naa ànd ak yooyu, waaye du bokk ci sarax su jëm ca sarxalukaay ba, ñu di ko taal, ngir xetug jàmm. 13 Seen mboolem saraxu pepp nangeen ko xorom. Bu seen saraxu pepp ñàkk mukk xorom, ndax mooy màndargaal seen kóllëreek seen Yàlla. Seen sarax yépp ngeen di xorom.
14 «Bu nit dee indil Aji Sax ji saraxu ndoortel meññeef, na ko indil mboolb mu ñu séndal, def ko sànqal, muy saraxu ndoortel meññeefam. 15 Na ci sotti diw ak cuuraay. Saraxu pepp la. 16 Na sarxalkat bi lakk lenn ci mbool mu mokk mi ànd ak diw, boole kook cuuraay li lépp, muy saraxu baaxantal, te di saraxu sawara.