Bés bu nekk laaj na ab sarax
28
1 Aji Sax ji waxati Musaa, ne ko: 2 «Santal bànni Israyil ne leen sama sarax, sama ñam wi jëm ci sama saraxi sawara ngir xetug jàmm, ñeel ma, nañu farlu ci di ma ko indil saa yu àppam jotee. 3 Nga waxleen ne leen, lii moo di saraxu sawara bi ñuy indil Aji Sax ji: xar yu góor yu menn at yu mucc sikk, ñaar ci bés bi, muy saraxu rendi-dóomal bi war bés bu nekk. 4 Menn xar mi, ngeen sarxal ko ci suba, ñaareel bi, ngeen sarxal ko diggante ngoon ak jant bu so. 5 Benn fukkeelu efab sunguf su mucc ayib, di ñetti kilo, mooy saraxu pepp bi xar mu nekk di àndal, ñu tooyale ko walaatu xiinu diwu segalu oliw, di liitar ak genn-wàll. 6 Looloo di rendi-dóomal bi war bés bu nekk, na ñu ko dogale woon ca tundu Sinayi, ngir xetug jàmm, muy saraxu sawara, ñeel Aji Sax ji.
7 «Saraxu tuuram walaatu xiin lay doon, di liitar ak genn-wàll ngir xar mu ci nekk. Ci ëtt bu sell bi lees di sotti saraxu tuuru bi, naan gu diis googu, ñeel Aji Sax ji. 8 Ñaareelu xar mi, sarxal-leen ko diggante ngoon ak jant bu so, mu ànd ak saraxu peppam ak saraxu tuuram niki ci suba, ngeen def ko saraxu sawara ngir xetug jàmm, ñeel Aji Sax ji.
Bésub Noflaay am na saraxam
9 «Bésub Noflaay nag ñaari xari menn at yu mucc sikk lay doon, ak saraxu peppam, biy ñaari fukkeeli efay sunguf su mucc ayib, di juróom benni kilo, ñu tooyale ko ag diw, te mu ànd ak saraxu tuuram. 10 Loolooy saraxu rendi-dóomalu bésub Noflaay, ci bésub Noflaay bu nekk, te bokkewul ak dóomal bi war bés bu nekk, te ànd ak saraxu tuuram.
Terutel weer am na saraxam
11 «Te itam seen bési Terutel weer, nangeen sarxe ab rendi-dóomal, ñeel Aji Sax ji. Ñaari yëkk yu ndaw, ak menn kuuy, ak juróom ñaari xar yu góor yu menn at, te lu ci nekk mucc sikk, 12 ak ñetti fukkeeli efay sunguf su mucc ayib, di juróom ñeenti kilo, muy saraxu pepp, ñu tooyale ko ag diw, booleek yëkk wu nekk, ak ñaari fukkeeli efay sunguf su mucc ayib, di juróom benni kilo, muy saraxu pepp, ñu tooyale ko ag diw, booleek kuuy mi, 13 ak benn fukkeelu efab sunguf su mucc ayib, di ñetti kilo, muy saraxu pepp, ñu tooyale ko ag diw, booleek xar mu ci nekk. Saraxu rendi-dóomal la, ngir xetug jàmm, di saraxu sawara, ñeel Aji Sax ji.
14 «Ay saraxi tuuram genn-wàllu xiinu biiñ la, di ñetti liitar ci yëkk wu nekk, ak benn ñetteelub xiin, di ñaari liitar ci kuuy mi, ak walaatu xiin, di liitar ak genn-wàllu biiñ ci xar mu ci nekk. Loolooy dóomalu weer wi, weer wu ci nekk, ba weeri at mi daj. 15 Ak itam bennub sikket, mook saraxu tuuroom ngir saraxu póotum bàkkaar, ñeel Aji Sax ji ci bésub Terutel weer wi, te bokkewul ak rendi-dóomal bi ñuy sarxe bés bu nekk.
Bésub Mucc am na saraxam
16 «Weer wi jëkk ci at mi nag, fukki fanam ak ñeent mooy bésub Mucc bi, ñeel Aji Sax ji. 17 Ëllëg sa, fukki fani weer woowu ak juróom, di màggal; diiru juróom ñaari fan, mburu mu amul lawiir lees cay lekk. 18 Bés bu jëkk boobu, woote bu sell lees cay amal. Mboolem lees baaxoo liggéey, deesu ko ci liggéey. 19 Nangeen ci def saraxu sawara, mu dib rendi-dóomal, ñeel Aji Sax ji: ñaari yëkk yu ndaw, ak menn kuuy, ak juróom ñaari xari menn at, te ngeen def lépp di lu mucc sikk. 20 Yooyii ànd ak saraxu peppam, di sunguf su mucc ayib, su ñu tooyale ag diw, ñetti fukkeeli efay sunguf, di juróom ñeenti kilo, ciw yëkk, ñaari fukkeeli efay sunguf, di juróom benni kilo, cim kuuy, 21 ak benn fukkeelu efab sunguf, di ñetti kilo, ci mii xar, benn fukkeelu efa, ca mee, ba juróom ñaari xar yi daj, 22 ak benn sikketu póotum bàkkaar ngir seen njotlaay. 23 Te bokkewul ak rendi-dóomalu suba si, rendi-dóomal boobu war bés bu nekk. 24 Sarax yu mel noonu ngeen di sarxal ci bés bi, ak seen saraxu tuuru, diiru juróom ñaari fan, muy ñamu saraxu sawara ngir xetug jàmm, ñeel Aji Sax ji. Ci kaw rendi-dóomal bi war bés bu nekk, ci lees koy dolli. 25 Bésub juróom ñaareel ba, seen bésub woote bu sell lay doon. Mboolem lees baaxoo liggéey, deesu ko ci liggéey.
Ngóob am na saraxam
26 «Bésub ndoortel meññeef ba ngeen di sarxesi saraxu pepp mu bees, ñeel Aji Sax ji, ci seen biir màggalug Ayi bés nag, seen bésub woote bu sell lay doon. Mboolem lees baaxoo liggéey, deesu ko ci liggéey. 27 Nangeen ci sarxal ab rendi-dóomal, ngir xetug jàmm, ñeel Aji Sax ji: ñaari yëkk yu ndaw, ak menn kuuy, ak juróom ñaari xari menn at. 28 Saraxu peppam di sunguf su mucc ayib, su ñu tooyale ag diw. Ñetti fukkeeli efay sunguf, di juróom ñeenti kilo ci yëkk wu nekk, ak ñaari fukkeeli efa, di juróom benni kilo ci kuuy mi, 29 ak fukkeelub efa, di ñetti kilo, ci mii xar, fukkeelub efa ca mee, ba juróom ñaari xar yi daj, 30 ak bennub sikket ngir seen njotlaay. 31 Sarxeleen loolu, te bumu bokke ak rendi-dóomal bi war bés bu nekk tey ànd ak saraxu peppam. Lu mucc sikk nag ngeen di def sarax yooyii, te ngeen defaale saraxi tuuram yi ci war.