Bési liit yi laaj na sarax
29
1 «Bu loolu weesee, benn fanu weeru juróom ñaareel, seen bésu woote bu sell lay doon. Mboolem lees baaxoo liggéey, deesu ko ci liggéey. Bés la bu ngeen di yéenee ag liit. 2 Sarxal-leen ci ab rendi-dóomal ngir xetug jàmm, ñeel Aji Sax ji: wenn yëkk wu ndaw, ak menn kuuy, ak juróom ñaari xari menn at, te lu ci nekk mucc sikk. 3 Saraxu peppam lay àndal, di sunguf su mucc ayib, su ñu tooyale ag diw; ñetti fukkeeli efay sunguf, di juróom ñeenti kilo ci yëkk wi, ñaari fukkeeli efa, di juróom benni kilo ci kuuy mi, 4 ak benn fukkeelu efab sunguf, di ñetti kilo ci mii xar, benn fukkeelu efa ca mee, ba juróom ñaari xar yi daj, 5 ak benn sikketu póotum bàkkaar, ngir seen njotlaay. 6 Bokkewul ak rendi-dóomalu Terutel weer wu nekk, mook saraxu peppam, bokkewul it ak rendi-dóomal bi war bés bu nekk, ak saraxu peppam, ak seen saraxi tuur, ni ko yoon tërale. Dees koy def ngir xetug jàmm, muy saraxu sawara, ñeel Aji Sax ji.
Bésub Njotlaay laaj na sarax
7 «Fukki fanu juróom ñaareelu weer woowu it, seen bésub woote bu sell lay doon, te ngeen toroxlu ci. Mboolem lees baaxoo liggéey, deesu ko ci liggéey. 8 Sarxal-leen ci ab rendi-dóomal, ñeel Aji Sax ji, ngir xetug jàmm: wenn yëkk wu ndaw, ak menn kuuy, ak juróom ñaari xari menn at, te lu mucc sikk ngeen di def lépp. 9 Saraxu peppam lay àndal, di sunguf su mucc ayib su ñu tooyale ag diw; ñetti fukkeeli efay sunguf, di juróom ñeenti kilo ci yëkk wi, ñaari fukkeeli efa, di juróom benni kilo ci kuuy mi, 10 ak benn fukkeelu efab sunguf, di ñetti kilo ci mii xar, benn fukkeelu efa ca mee, ba juróom ñaari xar yi daj, 11 ak benn sikketu póotum bàkkaar, te du bokke ak póotum bàkkaaru njotlaay gi, ak saraxu dóomal bi war bés bu nekk, mook saraxu peppam, ak seen saraxi tuur yi ci war.
Màggalu Mbaar yi laaj na sarax
12 «Fukki fan yaak juróom ci juróom ñaareelu weer woowu itam, seen bésu woote bu sell lay doon. Mboolem lees baaxoo liggéey, deesu ko ci liggéey. Amal-leen ci ag màggal, ñeel Aji Sax ji, diiru juróom ñaari fan, doore ko ca bés ba. 13 Nangeen ca sarxal ab rendi-dóomal, muy saraxu sawara ngir xetug jàmm, ñeel Aji Sax ji: fukki yëkk yu ndaw ak ñett, ak ñaari kuuy, ak fukk ak ñeenti xari menn at, te lépp mucc sikk. 14 Seen saraxi pepp di sunguf su mucc sikk su ñu tooyale ag diw, ñetti fukkeeli efay sunguf, di juróom ñeenti kilo ci wenn yëkk wu nekk, ba fukki yëkk yeek ñett daj; ñaari kuuy yi, kuuy mu ci nekk, ñaari fukkeeli efay sunguf, di juróom benni kilo, 15 ak benn fukkeelu efab sunguf, di ñetti kilo ci mii xar, benn fukkeelu efa ca mee, ba fukki xar yeek ñeent daj, 16 ak benn sikketu póotum bàkkaar. Bokkewul ak saraxu dóomal bi war bés bu nekk, ak saraxu peppam si muy àndal, ak saraxu tuuram.
17 «Bésub ñaareel ba: fukki yëkk yu ndaw ak ñaar; ak ñaari kuuy, ak fukk ak ñeenti xari menn at, te lépp mucc sikk. 18 Te seen saraxi pepp, ak seen saraxi tuur yay ànd ak yëkk ya, mbaa kuuy ya, mbaa xar ya, na dayo ya dëppoo ak li yoon tëral. 19 Dees na ca teg benn sikketu póotum bàkkaar, te du bokke ak saraxu dóomal bi war bés bu nekk, mook saraxu peppam ak seen saraxi tuur.
20 «Bésub ñetteel ba: fukki yëkk yu ndaw ak benn, ak ñaari kuuy, ak fukk ak ñeenti xari menn at, te lépp mucc sikk. 21 Te seen saraxi pepp, ak seen saraxi tuur yay ànd ak yëkk ya, mbaa kuuy ya, mbaa xar ya, na dayo ya dëppoo ak li yoon tëral. 22 Dees na ca teg benn sikketu póotum bàkkaar, te du bokke ak saraxu dóomal bi war bés bu nekk, mook saraxu peppam ak saraxu tuuram.
23 «Bésub ñeenteel ba: fukki yëkk, ak ñaari kuuy, ak fukk ak ñeenti xari menn at, te lépp mucc sikk. 24 Te seen saraxi pepp, ak seen saraxi tuur yay ànd ak yëkk ya, mbaa kuuy ya, mbaa xar ya, na dayo ya dëppoo ak li yoon tëral. 25 Dees na ca teg benn sikketu póotum bàkkaar, te du bokke ak saraxu dóomal bi war bés bu nekk, mook saraxu peppam ak saraxu tuuram.
26 «Bésub juróomeel ba: juróom ñeenti yëkk, ak ñaari kuuy, ak fukk ak ñeenti xari menn at, te lépp mucc sikk. 27 Te seen saraxi pepp, ak seen saraxi tuur yay ànd ak yëkk ya, mbaa kuuy ya, mbaa xar ya, na dayo ya dëppoo ak li yoon tëral. 28 Dees na ca teg benn sikketu póotum bàkkaar, te du bokke ak saraxu dóomal bi war bés bu nekk, mook saraxu peppam ak saraxu tuuram.
29 «Bésub juróom benneel ba: juróom ñetti yëkk, ak ñaari kuuy, ak fukki ak ñeenti xari menn at, te lépp mucc sikk. 30 Te seen saraxi pepp, ak seen saraxi tuur yay ànd ak yëkk ya, mbaa kuuy ya, mbaa xar ya, na dayo ya dëppoo ak li yoon tëral. 31 Dees na ca teg benn sikketu póotum bàkkaar, te du bokke ak saraxu dóomal bi war bés bu nekk, mook saraxu peppam ak saraxu tuuram.
32 «Bésub juróom ñaareel ba: juróom ñaari yëkk, ak ñaari kuuy, ak fukk ak ñeenti xari menn at, te lépp mucc sikk. 33 Te seen saraxi pepp, ak seen saraxi tuur yay ànd ak yëkk ya, mbaa kuuy ya, mbaa xar ya, na dayo ya dëppoo ak li yoon tëral. 34 Dees na ca teg benn sikketu póotum bàkkaar, te du bokke ak saraxu dóomal bi war bés bu nekk, mook saraxu peppam, ak saraxu tuuram.
35 «Bésub juróom ñetteel ba seen bésub ndaje lay doon. Mboolem lees baaxoo liggéey, deesu ko ci liggéey. 36 Nangeen ci sarxal ab rendi-dóomal, muy saraxu sawara ngir xetug jàmm, ñeel Aji Sax ji: wenn yëkk, ak menn kuuy, ak juróom ñaari xari menn at, te lépp mucc sikk. 37 Te seen saraxi pepp, ak seen saraxi tuur yay ànd ak yëkk ya, mbaa kuuy ya, mbaa xar ya, na dayo ya dëppoo ak li yoon tëral. 38 Dees na ca teg benn sikketu póotum bàkkaar, te du bokke ak saraxu dóomal bi war bés bu nekk, mook saraxu peppam, ak saraxu tuuram.
39 «Yooyu sarax ngeen di def, ñeel Aji Sax ji, ci seen bési màggal, te du bokke ak seen sarax yi ngeen xasal seen bopp, ak seen saraxi yéene, ak seen saraxi dóomali bés bu nekk, ak seen saraxi pepp ak seen saraxi tuur, ak seen saraxi canti biir jàmm