Nangu nañu gaalu Yàlla ga
4
1 Kàddug Samiyel nag di dikkal Israyil gépp.
Ci biir loolu bànni Israyil dem, dajeek waa Filisti ngir xare. Ña nga dal fa feggook Eben Eser, waa Filisti dal ca Afeg. 2 Waa Filisti làng-déral Israyil, xare ba jib. Israyil daanu fa kanam waa Filisti, waa Filisti rey ca seeni làng lu jege ñeenti junni ca toolub xare ba. 3 Ba mbooloo ma ñibbee ca dal ba, magi Israyil ña ne: «Lu waral Aji Sax ji dumalu nu tey fi kanam waa Filisti? Nan jëleji gaalu kóllërey Aji Sax ji fa Silo; na dikk ci sunu biir, ba musal nu ci sunuy noon.»
4 Ci kaw loolu mbooloo ma yónnee ca Silo, ñu jëli gaalu kóllërey Aji Sax ji Boroom gàngoori xare yi, Ki toog fi tiim ñaari malaakay serub yia. Foofa ca Silo la Ofni ak Fineyas, ñaari doomi Eli yu góor ya, nekkoon ak gaalu kóllërey Aji Sax ja.
5 Ba gaalu kóllërey Aji Sax ji duggsee ca dal ba, Israyil gépp a xaacoondoo, ba suuf say riir. 6 Waa Filisti dégg coow la, ne: «Waaw, coow lu réy loolu ca dalub Ebrë ya, lu mu doon?»
Ba waa Filisti yégee ne gaalu kóllërey Aji Sax ja dugg na ca biir dal ba, 7 tiitaangee leen jàpp, ñu ne: «Am na yàlla ju dugg ca biir dal ba! Wóoy, ngalla nun! Nde guléet tey lu mel nii am! 8 Wóoy ngalla nun! Ku nuy musal ci jii yàlla ju bare doole. Yàlla jii moo dumaa woon waa Misra xeeti mbugal yu nekk, ca màndiŋ ma. 9 Dëgërluleen déy te diy góor, yeen waa Filisti, nde lu ko moy ngeen doon jaami Ebrë yi, na ñu nekke woon sunuy jaam. Góor-góorluleen boog te xeex.»
10 Waa Filisti nag di xare, ba bànni Israyil daanu: ku nekk daw jëm xaymaam. Jéll ba réy na lool; fanweeri junniy xarekat yuy deme tànk. 11 Gaalu Yàlla ga, ñu jël; Ofni ak Fineyas, ñaari doomi Eli yu góor ya, dee.
Mbugal ma topp na waa kër Eli
12 Ba mu ko defee jenn waay ju bokk ci giirug Beñamin, dawe ca làngu xare ba ca Silo ci benn bés bi. Mu agsee yére yu xottiku ak bopp bu fees ak suuf, di ko tiisloo. 13 Naka la agsi, yem ca Eli, mu toog ca toogoom ca peggu yoon wa, di séentu, ndax booba naw gaa ngay rëcc, ngir tiitaange ca gaalu Yàlla ga. Naka la waa ja duggsi ca dëkk ba, ba wax la xew, dëkk ba bépp yuuxoondoo.
14 Eli dégg coow la, ne: «Riir moomu lu mu?» Waa ja gaaw dikk, wax ko Eli. 15 Booba Elee ngi ci juróom ñeent fukki at ak juróom ñett (98), bët yi ne xóll te gisatul dara. 16 Waa ja ne ko: «Man mii maa jóge ca toolub xare ba. Maa dawe làng ga tey jii.» Eli ne ko: «Doom, lu xew?» 17 Ndaw la ne ko: «Bànni Israyil a daw, won waa Filisti gannaaw. Jéll bu réy la sunu mbooloo ma daanu, sa ñaari doom ya, Ofni ak Fineyas dee nañu, te it gaalu Yàlla ga, jël nañu ko.» 18 Naka la tudd gaalu Yàlla ga rekk, Eli xàwwikoo ca toogu ba, daanoo njaaxaanaay, dal ca bunt dëkk ba, loos wa damm, mu dee, ndax booba day mag mu ànd ak yaramam. Eli jiite na Israyil ñeent fukki at.
19 Goroom, jabaru Fineyas nag jigéenu wérul la woon te booba mu ngi waaja wasin. Naka la dégg ne jël nañu gaalu Yàlla ga, te baayu jëkkëram ak jëkkëram dee nañu, mu daldi sukk wasin. Waaye fekk na mititu matam jeexal dooleem. 20 Ba loolu amee muy waaja dee, jigéen ña ko doon taxawu ne ko: «Na sa xel dal, ndax doom ju góor nga am.» Waaye àdduwul, teewluwul. 21 Ndaw sa nag tudde gone gi Ikabot (mu firi Ana leer ga?) te naan: «Leer ga dëddu na Israyil, dem ngàllo.» Ndax la ñu nangu gaalu Yàlla ga ak la goroom ak jëkkëram dee. 22 Mu ne: «Leer ga kay dëddu na Israyil, dem ngàllo, ndegam jëlees na gaalu Yàlla ga kay!»