Suleymaan tabax na këram
7
1 Kërug boppam nag, Suleymaan tabax na ko ci fukki at ak ñett, doora sottal këram gépp. 2 Ma nga jëkka tabax kër ga ñuy wooye Gottub Libaŋ. Guddaay bi di téeméeri xasab, yaatuwaay bi di juróom fukki xasab, taxawaay bi di fanweeri xasab, def ñeenti sàppey jëni seedar yu yenu ay gàlluy seedar yu ñu yett. 3 Ñu teg ay banti seedar ci kaw gàllu, yi jën yi yenu: muy ñeent fukki gàllu ak juróom, sàppe bu nekk fukki gàllu ak juróom. 4 Mu am ñetti sësalantey palanteer yu ñu fege ay laat te ñu dékkarloo ñett-ñett. 5 Bunt yépp ànd ak seen banti feguwaay, bunt bu ci nekk def ñeenti wet yu janoo màkk ñaar-ñaar; bunt yi sësaloo te dékkarloo ñett-ñett.
6 Ci biir loolu mu defar néeg ba ñuy wooye Néegu jëni kenu ya. Guddaay bi di juróom fukki xasab, yaatuwaay bi di fanweeri xasab, ak beneen néeg ci kanamam, mu ànd ak ay jëni kenoom ak xaddam bu mbaar ci kanam. 7 Mu tabax néeg ba ñuy wooye Néegu ngàngune ma walla Àttekaay ba, mu di fa àttee. Mu dare néeg bi banti seedar ci suuf ba ci kaw.
8 Këram ga mu dëkk it, ñu tabaxe ko noonu ci gannaaw Néegu ngàngune ma. Suleymaan teg ca tabaxal soxnaam doomu Firawna ja geneen kër gu nirook këram.
9 Tabax yooyu yépp biir ak biti xeeri tànnéef yu ñu yett la, natt ko, xacc ko, rattaxal, dale ko ci kenu gi, ba ci cati xadd bi ci kaw, daleeti ci biti ba ci ëtt bu mag bi. 10 Ñu defare kenu yi xeeri tànnéef yu mag: yii di fukki xasab, yii di juróom ñetti xasab. 11 Xeer yi tege ci kenu gi, xeeri tànnéef la yu ñu yett, natt ko, yemale, booleek banti seedar. 12 Miiru ëtt bu mag bi dees koo wëralee ay xeeri yett aki xànqi seedar: ñetti sësalantey xeer yu tegloo yu ne, benn sësalanteb xànqi seedar tege ca. Mu mel ni na ñu def ëttu biir bu kër Aji Sax ja ak dëru buntu kër ga.
Tëgg ba def na wàllam
13 Ci kaw loolu Buur Suleymaan yónnee, jëli ca Tir ku ñuy wax Urama. 14 Doomu jëtun la woon, bokk ci giirug Neftali. Baayam dëkkoon Tirb, di tëggub xànjar. Uram di ku xareñ lool, rafet xel te mane mboolem liggéeyu xànjar. Mu dikk ca Buur Suleymaan, liggéeyal ko la ñu ko sant lépp.
15 Mu móol ñaari xeri xànjar, wu ci nekk am taxawaayu fukki xasab ak juróom ñett, te wu ci nekk buumu fukki xasab ak ñaar a koy ub. 16 Ci biir loolu mu defar ñaari boppi xànjar yu mu xelli, teg ko ci kaw xer yi, bopp bu ci nekk am taxawaayu juróomi xasab. 17 Bopp yi ci kaw xer yi, bu ci nekk da koo rafetale ab caaxu càllala, bopp bu ci nekk am ci juróom ñaar. 18 Mu defar ñaari jaray gërënaat, solal ko caax yi, wëralee ko bopp yi, ci xer wu ci nekk. 19 Bopp yi nekkoon ci kaw xer yi ci kanam nag bindoo ni lëppi tóor-tóor te bu ci nekk di ñeenti xasab. 20 Bopp yi ci kaw ñaari xer yi, bu ci nekk ñaar téeméeri gërënaat a ko wër ci kaw, feggook gamb bi ci wàllaa caax bi.
21 Mu samp jën yi ci kanam bunt néeg Yàlla bu mag bi; samp jënu ndijoor wi, tudde ko Yakin (Kiy taxawal), samp jënu càmmoñ wi, tudde ko Bowas (Kiy dooleel). 22 Kaw xer yi ay lëppi tóor-tóor yu ñu xellee ci tege. Liggéeyu xer ya daldi sotti.
23 Ba mu ko defee Uram móol mbalkam njàpp mu weñ, ñu di ko wax Géej ga. Mbalka ma daa mërgalu, yaatoo fukki xasab, catu omb ba catu omb, taxawaay ba di juróomi xasab, ag buumu fanweeri xasab di ko ub. 24 Ay gamb la ko sàkkal ci suufu kéméj gi, fukki gamb tollook xasab. Mu def gamb yi ñaari caq yu wër mbalka mi ba mu daj te ànd ak mbalka mi ci benn xelli. 25 Mbalkam njàpp mi tege ci kaw fukki jëmmi nag ak yaar, ñett jublu bëj-gànnaar, ñett jublu sowu, ñett jublu bëj-saalum, ñett jublu penku. Mbalka mi war nag yi, seeni gannaaw féete biir, ñoom ñépp. 26 Dëllaayu mbalka mi yaatuwaayu loxo la, kéméj gi mel ni gémmiñu kaas, di nirook lëppi tóor-tóor. Ñaar téeméeri barigo la mbalka miy def. (200).
27 Mu daldi sàkk fukki watiiri rootukaayi xànjar, wu ci nekk am guddaayu ñeenti xasab, yaatuwaayam di ñeenti xasab, taxawaayam di ñetti xasab. 28 Ni ñu defare rootukaay yi nii la: ay wetam lañu defare làcci xànjar, lëkklee làcc yi ay laat. 29 Muy làcc yu Uram yett ci kawam ay gaynde, ay nag ak malaakay serub. Kaw laat yi itam am na ci nataal yi. Mu yett ay caqi tóor-tóor yuy lang ci suufu gaynde yeek nag yi. 30 Rootukaay bu nekk am na ñeenti mbegey xànjar yu ñu lëkklee yeti xànjar. Mu am ay kenu yu ñu xellil rootukaay bi ci ñeenti koñam, kenu yi yenu benn bagaan te am ay nataali tóor-tóor. 31 Gémmiñu rootukaay bu nekk amoon na omb bu mërgalu bu bagaanu ndox biy tege. Xóotaayu gémmiñ gi di xasab, yaatuwaay bi di xasab ak genn-wàll. Ñu yett ci kaw gémmiñ gi ay nataal ba tey. Rootukaay bi mërgaluwul, waaye daa bindoo ñeenti wet yu janoo màkk ñaar-ñaar te yem kepp. 32 Ñeenti mbege yi ronu làcc yi, tóori weñ yi ci wewe sax ci rootukaay bi. Mbege mu ci nekk am na taxawaayu xasab ak genn-wàll. 33 Mbege yi bindoo ni mbegey watiiri xare. Tóor yeek mbege yi ak sidditi mbege yi ak ŋanku yi, xànjar lañu ko xellee. 34 Ñeenti kenu yi ci ñeenti koñi rootukaay bi, bu ci nekk dees koo xelleendook weti rootukaay yi, ba lépp di benn. 35 Kaw boppu rootukaay bu nekk, kéméj gu mërgaloo féete ci kaw, taxawaayam di genn-wàllu xasab, njàppu yeek làcc yi sax ci, lépp di benn. 36 Fi amul dara ci kaw njàppu yeek làcc yi, mu ñaas ci ay nataali serub aki gaynde aki garabi ron yu ñu wërale ay caqi tóor-tóor. 37 Noonu la Uram defare fukki rootukaay yi. Lépp bokk móol, yem dayo te bokk bind.
38 Mu defar itam fukki bagaani xànjar; bagaan bu ci nekk tollook ñeenti xasab, di def lu xawa tollook juróomi barigo; bagaan bu ci nekk tegu cib rootukaay, ba fukki rootukaay yi daj.
39 Ba mu ko defee mu taaj juróomi rootukaay fa féete kër Yàlla ga ndijoor ak juróomi rootukaay fa féete kër ga càmmoñ. Mu teg mbalkam jàpp mi fa féete kër ga ndijoor, ca wetu bëj-saalum, jàpp penku.
40 Iram sàkk itam ndab yu ndaw yi ak ñiitukaay yi ak këlli tuurukaay yi.
Ci kaw loolu Iram sottal mboolem liggéey ba mu liggéeyal Buur Suleymaan ca kër Aji Sax ji: 41 muy ñaari jën yi, ak ñaari gamb yiy boppi jën yi, ak ñaari caaxi càllala yiy muur ñaari gamb yi, 42 ak ñeenti téeméeri gërënaat yiy ànd ak ñaari caax yi; caax bu nekk, ñaari caqi gërënaat, ñu dar ñaari gamb yiy boppi xer yi; 43 ak fukki rootukaay yi ak fukki bagaan yi ci kaw rootukaay yi. 44 Mbalkam jàpp mi it ci la, ak fukki nag ak yaar yi ronu mbalkam jàpp mi. 45 Bagaan yu ndaw yi bokk na ci, ak ñiitukaay yi ak këll yi. Mboolem yooyu jumtukaayi kër Aji Sax ji, xànjar bu ñu jonj la Buur Suleymaan sant Uram, mu defare ko. 46 Ca joorug Yurdan la ko Buur xellilu, ci móoli ban, diggante Sukkóot ak Sartan. 47 Suleymaan daldi bàyyi jumtukaay yépp noonu, ndax na mu baree lool, ba natteesul diisaayu xànjar ba ca dem.
48 Gannaaw loolu Suleymaan defarlu na mboolem yeneen jumtukaayi kër Aji Sax ji: muy sarxalukaayu wurus ba, ak taabal ja ñuy teg mburum teewal mac 49 ak tegukaayi làmpi wurusu ngalam yi, juróom ci wetu ndijoor, juróom ci wetu càmmoñ, fi kanam néeg bu sell baa sell; tóor-tóor yi ak làmp yi ak ñiim yi, lépp di wurus; 50 ndab yi itam, ak feyukaay yi ak këll yi ak kopp yi ak andi cuuraayu yi, lépp di wurusu ngalam. Te it ngoosi wurus yi bunti néeg bi wewe, ñu di fa jaare dugg ca bérab bu sell baa sell, ak ngoosi wurus yi beneen buntu néeg bi wewe, ñu di fa jaare dugg ci néeg Yàlla bu mag bi, lépp wurus la.
51 Ba loolu amee, mboolem lu Buur Suleymaan liggéeyal kër Aji Sax ji daldi sotti. Mu boole xaalis baak wurus waak jumtukaay ya baayam Daawuda sellalaloon Aji Sax ji, yeb ko ca denc ya def alali kër Aji Sax ji.