Aji Sax ji feeñu na Suleymaan
9
1 Ba Suleymaan noppee ci tabax kër Aji Sax ji ak kër Buur, ak mboolem nammeelam gu mu bëggoona sottal, 2 la ko Aji Sax ji feeñu ñaareel bi yoon, na mu ko feeñoo woon fa Gabawon. 3 Aji Sax ji ne ko: «Dégg naa sag ñaan, ak sab dagaan. Sellal naa kër gii nga tabax, ngir teg fi sama tur ba fàww. Samay gët ak sama xol it fi lay nekk bés bu nekk.4 «Yaw nag, soo doxee fi sama kanam ni Daawuda sa baay daan doxe cig mat akug njub, di def lépp lu ma la sant, di sàmm sama dogali yoon, ak sama àttey yoon, nga di ko sàmm, 5 kon dinaa saxal sab jal ci kaw Israyil ba fàww, na ma ko waxe woon Daawuda sa baay, ne ko: “Doo ñàkk ku góor kuy toog ci jalub Israyil.” 6 Waaye su ngeen ma dëddoo ba dëddu ma, yeen ak seeni sët, ba jëfewuleen samay santaane, sama dogali yoon yi ma leen tëralal, xanaa di topp aka jaamu yeneen yàlla, di leen sujjóotal, 7 su boobaa maay dagge bànni Israyil fi déndu suuf si ma leen jox, te kër gi ma sellal ngir sama tur, maa koy xalab, mu sore ma, te kon Israyil mujj di tur wu ñuy léeboo ak di ko kókklee ci biir xeet yépp.
8 «Su boobaa kër gii dina gent te képp ku ko romb dina yéemu tey muslu ci lu ni mel. Dinañu ne: “Lu tax Aji Sax ji def nii réew mii ak kër gii?” 9 Ñu ne: “Xanaa li ñu dëddu seen Yàlla Aji Sax, ji jële seeni maam réewum Misra, di topp yeneen yàlla, di leen sujjóotal ak a jaamu. Moo tax Aji Sax ji teg leen musiba mii mépp.”»
Buur Suleymaan jëflante naak Buur Iram
10 Ñaar fukki at yi Suleymaan tabax ñaari kër yi, kër Aji Sax ji ak kër Buur, ba mu matee 11 fekk na Iram buurub Tir jox Suleymaan ay banti garabi seedar ak sippara, ak mboolem lu mu soxla ci wurus. Buur Suleymaan nag jox Iram ñaar fukki dëkk ci diiwaanu Galile. 12 Ci kaw loolu Iram bàyyikoo Tir, seeti dëkk ya ko Suleymaan jox, waaye dëkk ya neexu ko. 13 Mu ne ko: «Sama waay, dëkk yi nga ma jox nag?» Mu daldi tudde dëkk ya réewum Kabulb, mooy turam ba tey jii. 14 Iram yónnee woon na Buur fanweeri barigoy wurus ak juróom.
15 Buur Suleymaan dafa dogaloon liggéeyu sañul-bañ bu mu sas ay nit. Ñu tabax kër Aji Sax ji ak këru boppam ak sëkkub Miloc ak tatay Yerusalem ya ak dëkk yii di Àccor, Megido ak Geser. Ni mu deme nii la: 16 Firawna buuru Misra moo daloon ci kaw Geser, nangu dëkk ba, lakk ko, rey Kanaaneen ña ca dëkkoon, daldi may dëkk ba doomam jay soxnas Suleymaan, muy yebam. 17 Suleymaan tabaxaat Geser ak Bet Oron Suuf, 18 ak Baalat ak Tamard ca màndiŋu réew ma, 19 ak mboolem dëkki dencukaayam, ak dëkk ya watiiri xare ya dence, ak dëkki gawar ya. Lu Suleymaan nammoona tabax daal, tabax na ko ca Yerusalem ak ca Libaŋ ak mboolem réewum kilifteefam.
20 Mboolem nit ña desoon ca Amoreen ñaak Etteen ñaak Periseen ñaak Eween ñaak Yebuseen ña, ñooñu bokkul ci bànni Israyil. 21 Seen sët ya leen wuutu ca réew ma, te bànni Israyil manuñu leen woona faagaagal, Suleymaan moo leen dugal ci liggéeyu njaam ak sañul-bañ, ñu nekke ko ba tey jii. 22 Waaye ñi bokk ci bànni Israyil, Suleymaan defu leeni jaam, ndax ñoom ñoo doon ay xarekatam, aki dagam aki jawriñam, ak njiiti xareem ak boroom watiiri xareem, ak dawalkati watiiram. 23 Ñoo doon itam saytukat yi yore liggéeyi Suleymaan. Amoon na juróomi téeméeri jawriñam ak juróom fukk (550) yu daan jiite nit ñiy def liggéey bi.
24 Doomu Firawna ju jigéen ja nag jóge gox ba ñu naan Kër Daawuda, séyi kërug boppam ga ko Suleymaan tabaxal. Gannaaw gi la Suleymaan tabax sëkkub Milo.
25 Suleymaan di def ñetti yoon cim at ay saraxi rendi-dóomal, ak saraxi cant ci biir jàmm, di ko sarxal ci kaw sarxalukaay bi mu tabaxal Aji Sax ji, boole ci di taal cuuraay ci kaw sarxalukaay bi, fi kanam Aji Sax ji. Mu daldi matal la war ca kër Yàlla ga.
26 Ay gaal yu mag itam Buur Suleymaan defarlu na ko ca Esiyon Geber ga ca wetu Elat, ca tefesu géeju Barax ya, ca réewum Edom. 27 Iram yebal ay nitam, ñuy mool yu xam géej. Ñuy liggéeyandook niti Suleymaan ca gaal ya. 28 Ñu daldi ànd dem Ofir, jële fa téeméeri barigoy wurus ak ñaar fukk, indil Buur Suleymaan.