Yonent Yàlla Ilyaas yégle na bekkoor
17
1 Ci kaw loolu Yonent Yàlla Ilyaas, ma dëkk Tisbi ga ca Galàdd, wax Axab, ne ko: «Giñ naa ci Aji Sax ji, Kiy Dund, di Yàllay Israyil ji may jaamu: at yii nu nekk, du taw te du lay, lu moy dama koo wax ci sama làmmiñ.»2 Kàddug Aji Sax ji dikkal Ilyaas ne ko: 3 «Jógeel fii, walbatiku jëm penku, te làquji ca xuru Kerit ca penkub dexu Yurdan. 4 Su ko defee, ca ndoxum xur wa ngay naane. Jox naa itam ndigal baaxoñ yi, ñu di la leel foofa.»
5 Ilyaas dem, def la Aji Sax ji wax, toogi ca xuru Kerit ca penkub dexu Yurdan. 6 Baaxoñ ya di ko indil mburu ak ndawal bëccëg, mburu ak ndawal ngoon, ndox may wal, mu di ca naan.
Ilyaas waar na jëtun ba
7 Mu am ay fan, xur wa ŋiis, ndax réew ma tawluwul. 8 Kàddug Aji Sax ji dikkal ko ne ko: 9 «Demal Sarebta ga ca Sidon te toog foofa. Ma ne, sant naa fa ab jëtun, mu may la loo lekk.» 10 Ilyaas dem Sarebta. Ba mu agsee ca buntu dëkk ba, gisul lu moy ab jëtun buy taxan. Mu woo ko ne ko: «Ngalla may ma tuuti ndox ci njaq li, ma naan.» 11 Mu dem di wuti ndox, Ilyaas dellu ko woo, ne ko: «Rikk sàkkal dogu mburu, yótaale ma.» 12 Jëtun ba nag ne ko: «Giñ naa ci Aji Sax ji sa Yàlla jiy dund, awma mburu. Awma lu moy barci-loxob sunguf ca njaq la ak as diw ca tax ba. Gis nga, may for nii ñetti bant, ba toggi ko, nu lekk, maak sama doom, doora dee ak xiif.» 13 Ilyaas ne ko: «Bul ragal dara, demal rekk, def ni nga wax. Waaye jëkk ma cee defaral mburu mu ndaw, indil ma, doora defaral sa bopp, yaak sa doom; 14 ndax Aji Sax ji Yàllay Israyil dafa wax ne: “Njaqub sunguf bi du jeex; taxub diw bi it du jeex, ba keroog Aji Sax ji di taw ci réew mi.”»
15 Jigéen ja dem, def la ko Ilyaas wax, mook waa këram ñu bokk ak Ilyaas lekk ay fan. 16 Njaqu sunguf ba jeexul, taxub diw ba jeexul. Muy la Aji Sax ji waxoon, Ilyaas jottli.
Ilyaas ñaanal na doomu jëtun ba
17 Ba loolu weesee jigéen, ja dese kër ga, doomam ju góor wopp. Mu mujj metti lool, ba noyyeetul. 18 Jigéen ja ne Ilyaas: «Éy góoru Yàlla gii! Ana lu ma séq ak yaw? Xanaa dangaa ñëw sullisi sama bàkkaar, ba tax nga rey sama doom ju góor jii?»
19 Ilyaas ne ko: «Jox ma sa doom!» Mu jële ko ca loxoy jigéen ja, yóbbu ko ca néeg ba mu dal ca kaw taax ma, tëral ko ca kaw lalam. 20 Ba mu ko defee Ilyaas ñaan ci Aji Sax ji, ne ko: «Éy Aji Sax ji, sama Yàlla, xanaa doo teg jëtun bii ma dalal, naqar wu tollu ni, di seetaan doomam ju góor muy dee?» 21 Ci kaw loolu mu tëdd, tàlli ñetti yoon ca kaw xale bu góor ba, tey ñaan ci Aji Sax ji naan: «Éy Aji Sax ji sama Yàlla, rikk bàyyil bakkanu xale bii, mu délsi ci moom!»
22 Aji Sax ji nangul Ilyaas kàddug ñaanam, bakkanu xale bu góor ba délsi ca moom, mu dund. 23 Ilyaas fab xale ba, jële ko ca néeg ba ca kaw taax ma, wàcce ko ca biir kër ga, jox ko ndeyam. Mu ne ko: «Xoolal, sa doom a ngi dund!» 24 Jigéen ja ne Ilyaas: «Léegi nag xam naa ne nitu Yàlla nga, te kàddug Aji Sax ji ngay waxe moos.»