Axab songati na Siri
22
1 Gannaaw loolu toog nañu ñetti at yu xare amul diggante Siri ak Israyil.
2 Ca ñetteelu at ma, Yosafat buurub Yuda dikk ca buurub Israyil. 3 Fekk buurub Israyil wax aki jawriñam ne leen: «Xanaa xamuleen ne Ramot ga ca Galàdd noo ko moom? Te jéemunoo def dara, ba nangu ko ci loxol buurub Siri!» 4 Mu ne Yosafat: «Xanaa dinga ànd ak man ca xareb Ramot ga ca Galàdd?» Yosafat ne buurub Israyil: «Maa ngi, yaa ngi, samay nit ay say nit, te samay fas ay say fas.» 5 Yosafat teg ca ne buurub Israyil: «Jëkkala seet lu ci Aji Sax jiy wax.»
6 Buurub Israyil nag woo yonent yi, ñu daje, xawa tollook ñeenti téeméer. Mu laaj leen ne leen: «Ndax ma dal ci kaw Ramot ga ca Galàdd, am ma bàyyi?» Ñu ne ko: «Demal, ndax Boroom bi moo leen di teg ci sa loxo.» 7 Yosafat dellu ne: «Xanaa beneen yonentu Aji Sax ji da fee amatul, ba ñu mana seetlujeeti fa moom?» 8 Buurub Israyil ne Yosafat: «Am na ba tey genn góor gu ñu mana seetal ci Aji Sax ji. Waaye man maa ko jéppi, ndax du wax waxyu bu baax ci man, lu bon rekk; mooy Mise doomu Yimla.» Yosafat ne ko: «Buur, bul waxe noonu.» 9 Buurub Israyil daldi woo ab jawriñam ne ko: «Demal indil ma gaaw Mise doomu Yimla.»
10 Buurub Israyil ak Yosafat buurub Yuda nag, ña nga toog, ku ci nekk ci ngànguneem. Ña nga solu ba jekk ca dàgga ja ca buntu Samari. Yonent yépp janook ñoom di biral ay waxyu. 11 Fekk na Cedekiya doomu Kenaana, ma woon ci seen biir, defarlu ay béjjéni weñ. Ma nga naan: «Aji Sax ji dafa wax ne: “Yii ngay jame waa Siri, ba jeexal leen.”» 12 Mboolem yonent ya ca des nag di waxe jenn waxyu jooju, naan: «Buur, songal Ramot ga ca Galàdd te jël ndam li, ndax Aji Sax ji moo leen teg ci say loxo.»
Mise yégle na jéllub Axab
13 Ci kaw loolu ndaw la wooyi Mise, dem ne ko: «Ma ne, kàddug yonent ya genn la: jàmmu Buur. Kon nag, na sa kàddu ànd ak seen kàddu di genn, te nga wax jàmm.» 14 Mise ne ko: «Giñ naa ci Aji Sax ji, Kiy Dund, li ma Aji Sax ji wax rekk laay wax.» 15 Ba Mise dikkee ba ca Buur, Buur ne ko: «Mise, ndax nu songi xare Ramot ga ca Galàdd, am nu bàyyi?» Mu ne ko: «Buur songal, daan, Aji Sax jee koy teg ci sa loxo!» 16 Buur nag ne ko: «Ñaata yoon laa lay giñloo ne la bu ma wax lu moy dëgg ci turu Aji Sax ji?» 17 Mise ne ko:
«Israyil gépp laa gis ñu tasaaroo ca tund ya,
mbete xar yu amul sàmm.
Aji Sax ji ne: “Ñii de amuñu boroom.
Na ku nekk ci ñoom ñibbi këram ci jàmm.”»
18 Buurub Israyil ne Yosafat: «Waxuma la woon ne du wax waxyu bu baax ci man, xanaa lu bon?» 19 Mise teg ca ne ko: «Kon nag déglul kàddug Aji Sax ji. Gis naa Aji Sax ji, mu toog ci ngànguneem, mboolem gàngooru asamaan a nga taxaw ndijooram ba càmmoñam. 20 Aji Sax ji nag ne: “Ana kuy nax Axab, mu songi Ramot ga ca Galàdd, ba daanu ca?” Kii ne nii, kee ne nee. 21 Noo ga dikk, taxaw fa kanam Aji Sax ji. Mu ne: “Man maa koy nax.” Aji Sax ji ne ko: “Nan?” 22 Mu ne: “Maay dikk, doon xel muy safaan dëgg ci làmmiñu yonentam yépp.” Mu ne ko: “Yaa koy nax, te man nga ko. Demal defe noonu.” 23 Looloo waral lii. Aji Sax ji moo def xel muy safaan dëgg ci sa làmmiñu yonent yii yépp, te Aji Sax ji moo tudd musiba ci sa kaw.»
24 Ba loolu amee Cedekiya doomu Kenaana talaata Mise, ne ko: «Ana fu Noowug waxyu gu Aji Sax ji jaare, ba jóge ci man di wax ak yaw?» 25 Mise ne ko: «Yaw mii yaa koy gisal sa bopp, keroog ba ngay dugg néegoo néeg, di làqtu.» 26 Buurub Israyil ne ab surgaam: «Jàppal Mise, yóbbu ko ca Amon boroom dëkk bi, ak ca doomu Buura. 27 Nga ne ko: “Buur dafa wax ne: Dugal-leen kii ndungsiin, di ko jox lekk gu néew ak ndox mu néew, ba keroog may dikk ak jàmm.”» 28 Mise ne: «Soo délseek jàmm déy, Aji Sax ji waxul, ma jottli.» Mu dellu ne: «Mbooloo mi, yeena ko déggandoo, yeen ñépp.»
Axab daanu na
29 Ba mu ko defee buurub Israyil ànd ak Yosafat buurub Yuda, ñu songi Ramot ga ca Galàdd. 30 Buurub Israyil nag ne Yosafat: «Damay soppi col, dugg ci xeex bi, waaye yaw solal sa mbubbam buur.» Buurub Israyil daldi soppig col, dugg ca xeex ba. 31 Fekk na buurub Siri jox ndigal fanweeri nitam ak ñaar, ñay jiite watiiri xare ya. Mu ne leen: «Buleen xeex ak kenn, du ku tuut, du ku réy, diirleen buurub Israyil, moom rekk.» 32 Ba loolu amee, ña jiite watiiri xare ya gis Yosafat, daldi ne: «Kii kay mooy buurub Israyil!» Ñu walbatiku ci kawam, ngir song ko. Yosafat nag àddu ca kaw, 33 njiiti watiir ya xam ne du buurub Israyil, ñu walbatikuwaat, bàyyi ko. 34 Ci biir loolu mu am ku soqi ag fitt te teyu ko, mu dal buurub Israyil ci diggante ñaari wàlli pakk bi mu sol. Mu ne dawalkatu watiiram: «Waññikul, génne ma ci xeex bi, gaañu naa!» 35 Naka la xare ba tàkkarnaase bésub keroog bépp, ñu téye buur ba ca biir watiir wa, mu janook waa Siri, ba ca ngoon sa, mu doora dee. Jam-jam baa nga nàcc, ba taa ca biir watiir ba. 36 Jant baa ngay xalambaayu, yéene jib, ba dajal mbooloo ma. Ña nga naan: «Na ku nekk ñibbi sa dëkk, ca sam réew!»
37 Buur ba nag saay, ñu yóbbu ko Samari, denc ko foofa. 38 Ba ñuy raxas watiir ba ca déeg ba ñuy wax Samari, xaj ya di xab deret ja, gànc ya di sangu ca ndoxum déeg ma, muy la Aji Sax ji waxoon.
39 Li des ci mbiri Axab ak mboolem lu mu def ak kër ga mu tabax, rafetale ko bëñi ñay, ak mboolem dëkk ya mu tabax, loolu lépp, bindees na ko moos ca téere ba ñu dippee Jaloorey buuri Israyil ca seeni jant. 40 Buur Axab nag saay, fekki ay maamam, doomam Akasiya falu buur, wuutu ko.
Yosafat falu na Yuda
41 Axab moomu, ba mu faloo Israyil, ba dugg ñeenteelu atu nguuram, ca la Yosafat doomu Asa falu buur ca kaw Yuda. 42 Yosafat amoon na fanweeri at ak juróom, ba muy falu te ñaar fukki at ak juróom la falu ca Yerusalem. Yaayam moo doon Asuba, doomu Sili. 43 Yosafat ci tànki baayam Asa la aw, jàddul fenn, xanaa di def njub lu Aji Sax ji rafetlu. 44 Teewul jëlewu fa bérabi jaamookaay ya. Askan wa dañu fa daa dem ba tey, di fa rendi saraxi jur, di fa taal cuuraay. 45 Séqoon na nag ak buurub Israyil jàmm.
46 Li des ci mbiri Yosafat ak njàmbaaram aki xareem, bindees na lépp moos ca téere ba ñu dippee Jaloorey buuri Yuda ca seeni jant. 47 La desoon ca ñay jaay seen bopp ca jaamookaayi tuur, ya fa desoon ca jamonoy baayam Asa, ba booba, Yosafat da leena jële ca réew ma.
48 Booba réewum Edom amuloon buur. Ab jawriñ lañu fa daan tabb.
49 Yosafat defaroon na ay gaal yu mag yu mu deme réewum Ofir, di wuti wurus. Waaye sottiwul, ndax gaal yaa nga suux ca Esiyon Geber. 50 Booba la Akasiya doomu Axab wax Yosafat ne ko: «Tee ngaa may samay nit, ñu ànd ak say nit ci gaal yi?» Yosafat lànk.
51 Gannaaw gi Buur Yosafat tëdd, fekki ay maamam, ñu denc ko fa ñu denc ay maamam ca gox ba ñu naan Kër Daawuda maamam. Doomam Yoram falu buur, wuutu ko.
Akasiya falu na Israyil
52 Yosafat moomu, ba mu faloo Yuda, ba dugg fukkeelu atu nguuram ak juróom ñaar, ca la Akasiya doomu Axab falu buur ca Israyil, péeyoo Samari. Akasiya nguuru na Israyil ñaari at. 53 Da daan def lu bon, lu Aji Sax ji ñaawlu, topp tànki ndeyam ak baayam ak tànki Yerbowam doomu Nebat, ma doon bàkkaarloo Israyil. 54 Akasiya jaamu na Baal, tuur ma, di ko sujjóotal, ba merloo Aji Sax ji, Yàllay Israyil, muy mboolem la baayam daa def.