Ose falu na buur ca Israyil
17
1 Ba Axas buurub Yuda duggee fukkeelu atu nguuram ak ñaar, ca la Osea doomu Ela falu buurub Israyil, péeyoo Samari. Nguuru na Israyil juróom ñeenti at, 2 di def li Aji Sax ji ñaawlu. Waaye dabul buurub Israyil ya ko jiitu.
3 Moom la Salmanasar buurub Asiri song, mu nangul ko, di ko fey galag. 4 Gannaaw gi nag buurub Asiri gis ne Ose lal na pexe, ndax daa yónnee ay ndaw ca So buuru Misra, ba noppi lànk ne du fey galag at mu nekk. Buurub Asiri jàpp ko, tëj.
Samari, péeyu Israyil, tas na
5 Ba loolu amee Salmanasar buurub Asiri dal ca kaw réew ma mépp, dikk ba Samari, gaw ko diiru ñetti at. 6 Ba Ose duggee juróom ñeenteelu atu nguuram, ca la buurub Asiri nangu Samari, jàpp waa Israyil, yóbbu Asiri. Ñii mu teg leen ca diiwaanu Ala, ñee ca Gosan ca wetu dex ga ñuy wax Abor, ña ca des mu dëël leen ca dëkki xeet wa ñuy wax Medd.
7 Li waral ñu nangu Samari mooy waa Israyil a bàkkaar, tooñ Aji Sax ji seen Yàlla ja leen génne réewum Misra, xettli leen ca Firawna buuru Misra. Waa Israyil di jaamu yeneen yàlla, 8 di topp baaxi xeet ya Aji Sax ji dàq ngir ñoom, di topp baax yi buuri Israyil tëralal seen bopp. 9 Waa Israyil teg ca di jéema nëbbuy def njubadi gu seen Yàlla Aji Sax jiy tere; di tabax ay bérabi jaamookaay ca seen dëkk yépp, dale ko ca tatay wattukat ya, ba ca dëkk ya ñu wëraley tata. 10 Ñu boole ca sampal seen bopp ay tuuri doj ak xer yu ñuy jaamoo Asera ci kaw mboolem tund wu kawe mbaa ker garab gu naat. 11 Ñuy taal cuuraay foofa ca mboolem bérabi jaamookaay ya, di roy xeet ya Aji Sax ji dàq ngir ñoom. Ñuy def daal ay ñaawtéef, di merloo Aji Sax ji, 12 di jaamu ay kasaray tuur, te Aji Sax ji waxoon leen ne buñu leen jaamu. 13 Moonte Aji Sax ji àrtu woon na Israyil ak Yuda, mboolem yonentam yaak boroom peeñu ya jottli leen ko, ne leen: «Dëppleen seen yoon yu bon yii ngeen topp, te sàmm samay santaane, wormaal samay dogal, na mu dëppook mboolem yoon wi ma tëralal seeni maam, yónnee leen ko, yonent yiy samay jaam jottli leen ko.»
14 Teewul ñu të ticc, sajju loos ni seen maam ya gëmuloon seen Yàlla Aji Sax ji. 15 Dañoo xalab ay ndigalam ak kóllëre ga mu fasoon ak seeni maam, xalab kàddu ya mu leen artoo woon. Ñu topp ay tuuri caaxaan ba mujj di niti caaxaan, di roy xeet yi leen wër, te Aji Sax ji tere woon leen ñu roy leen. 16 Ba loolu amee ñu dëddu mboolem seen santaaney Yàlla Aji Sax ji; sàkkal seen bopp ñaari wëllu yu ñu móol, samp xer wu ñuy jaamoo Asera, di sujjóotal mboolem biddiiwi asamaan tey jaamu Baal. 17 Ci biir loolu ñuy lakk seen doom yu góor ak yu jigéen ngir ay tuur, di gisaaneek a xërëmtu, ba làggi ci jëfi mbon yu Aji Sax ji ñaawlu, ba tax mu mer. 18 Moo tax Aji Sax ji mere Israyil lool, ba jële leen fi kanamam, ba giirug Yuda rekk des fa.
19 Waa Yuda it sàmmuñu seen santaaney Yàlla Aji Sax ji. Dañoo roy ci aada yi Israyil sos, di ko jëfe. 20 Moo tax Aji Sax ji xalab mboolem bànni Israyil, fitnaal leen, teg leen ci loxoy yàqkat yi, ba ni mu leen wacce.
21 Ba Aji Sax ji foqatee Israyil ca loxol waa kër Daawuda, dañoo fal Yerbowam doomu Nebat buur; Yerbowam dëddale Israyil ak Aji Sax ji, yóbbe leen bàkkaar bu réy; 22 mbooloom Israyil topp Yerbowam ci bàkkaar ya muy def yépp, bañ koo dëddu, 23 ba Aji Sax ji dëddu leen, muy la mu waxoon, yonent yay jaamam jottli ko. Noonu la mujj génne Israyil réewam, yóbbu leen Asiri ba bésub tey jii.
Waa Asiri sancal nañuy jaambur ca Samari
24 Ci kaw loolu buurub Asiri jële ay nit dëkk ya ñuy wax Babilon ak Kuta ak Awa ak Amat ak Sefarwayim, dëël leen dëkki Samari, ñu wuutu bànni Israyil. Ñu daldi moom diiwaanu Samari, féetewoo dëkk ya. 25 Ba ñuy doora sanc foofa, ragaluñu woon Aji Sax ji, ba tax Aji Sax ji yebal ay gaynde ci seen biir, ñu di leen rey. 26 Ñu wax buurub Asiri ne ko: «Xeet ya nga toxal, sancal leen ca dëkki Samari de, xamuñu yoonu Yàllay réew ma. Yebal na ay gaynde ci seen biir. Ña nga leen di rey, ndax xamuñu yoonu Yàllay réew ma.»
27 Ba loolu amee buurub Asiri joxe ndigal ne: «Yebal-leen fa kenn ci sarxalkat ya ngeen fa toxale, mu dem toog foofa, jàngal leen yoonu Yàllay réew ma.» 28 Kenn ca sarxalkat ya ñu jële woon Samari nag dikk, dëkksi Betel, jàngal leen nu ñuy jaamoo Aji Sax ji. 29 Terewul xeet wu ci nekk di sàkk ba tey seen tuuri bopp ca seen dëkk ya ñu féete, ba dugal tuur ya ca bérabi jaamookaay, ya waa Samari defaroon. 30 Ci biir loolu waa Babilon sàkk tuur ma ñuy wax Sukkóot Benoot, waa Kuta sàkk Nergal, waa Amat sàkk Asima; 31 waa Awa sàkk Nibaas ak Tartag, waa Sefarwayim di lakk seeni doom ngir tuuri Sefarwayim yi ñuy wax Addraameleg ak Anameleg. 32 Ñu boole ci di jaamu Aji Sax ji, tabb fu nekk ci seen biir ay sarxalkat ngir bérabi jaamookaay ya, ñu di leen sarxalal ca bérabi jaamookaay yooyu. 33 Ñuy wormaal Aji Sax ji, di jaamuwaale seen tuuri bopp itam, na ñu ko baaxoo ca seen waa réewum cosaan ma ñu leen toxale. 34 Ba tey jii ñu ngi topp seen aaday cosaan. Ragaluñu Aji Sax ji dëgg te sàmmontewuñook santaane yeek dogal yeek yoon week ndigal li Aji Sax ji joxoon askanu Yanqóoba mi mu tudde Israyil. 35 Aji Sax ji daa fasoon ak ñoom kóllëre, sant leen ne leen: «Buleen wormaal yeneen yàlla, buleen leen sujjóotal, buleen leen jaamu, te buleen leen sarxalal itam. 36 Man Aji Sax ji leen génne réewum Misra ci sama kàttan gu màgg ak sama dooley loxo, man ngeen wara wormaal, di ma sujjóotal, di ma sarxalal. 37 Te santaane yeek dogal yeek yoon week ndigal li ma leen bindaloon, fexeleen ba di sàmmonteek moom ba fàww. Buleen wormaal yeneen yàlla. 38 Kóllëre gi ma fasoon ak yeen nag, buleen ko fàtte. Buleen wormaal it yeneen yàlla. 39 Waaye man seen Yàlla Aji Sax ji ngeen di wormaal, ma xettli leen ci seen loxol mboolem noon.» 40 Taxul ñu dégg, xanaa sax rekk ci seen aaday cosaan. 41 Noonu la xeet yooyu daan wormaale Aji Sax ji, boole ci di jaamu seen jëmmi tuur. Seeni doom it noonu, ba tey seeni sët di def na seeni maam daan def.