Esekiya falu na buur ca Yuda
18
1 Ba Ose doomu Ela buurub Israyil duggee ñetteelu atu nguuram, ca la Esekiya doomu Axas falu ca Yuda. 2 Amoon na ñaar fukki at ak juróom ba muy falu buur. Nguuru na ñaar fukki at ak juróom ñeent, péeyoo Yerusalem. Yaayam nag mooy Abi doomu Sàkkaryaa. 3 Muy def li Aji Sax ji rafetlu, mboolem noonee ko Daawuda maamam daan defe.4 Moom moo dindi bérabi jaamookaay ya, toj tuuri doj ya, gor xer wa ñuy jaamoo Asera, rajaxe jaanu xànjar ja Musaa defaroon. Ndax ba ca jamono yooya waa Israyil dañu daan taalal jaanu xànjar ja cuuraay, tudde ko Nexustan. 5 Ni Esekiya wóoloo woon Aji Sax ji Yàllay Israyil amu ci moroom ci mboolem buuri Yuda yi topp ci moom mbaa yi ko jiitu. 6 Dafa sax ci Aji Sax ji, dëdduwu ko, xanaa di topp ndigal ya Aji Sax ji joxoon Musaa.
7 Aji Sax ji nag ànd ak Esekiya, mu am ndam ci mboolem lu mu sumb. Bañ na noteelu buurub Asiri, ba nangulatu ko. 8 Ci kaw loolu dàq na waa Filisti, ba ca dëkk ba ñuy wax Gasa ak diiwaanam, dale ko ca tatay wattukat ya ba ca dëkk yu mag ya ñu wëraley tata.
9 Ba Esekiya buurub Yuda duggee ñeenteelu atu nguuram, yemook ba buurub Israyil Ose doomu Ela duggee juróom ñaareelu atu nguuram, ca la Salmanasar buurub Asiri song Samari, gaw ko. 10 Gaw nañu Samari ba ca ñetteelu at ma, door koo nangu, ca juróom benneelu atu nguurug Esekiya, yemook ba Ose buurub Israyil duggee juróom ñeenteelu atu nguuram. 11 Ba mu ko defee buurub Asiri jàpp Israyil, yóbbu Asiri, dëël leen diiwaanu Ala ak Gosan ga dexu Abor wale, ak ca dëkki xeetu Medd ya. 12 Li waral loolu mooy waa Israyil a déggalul seen Yàlla Aji Sax ji. Dañoo fecci kóllëreem ak moom, ba mboolem li Musaa, jaamu Aji Sax ji, santaane woon, faalewuñu ko, jëfewuñu ko.
Asiri song na Yuda
13 Ca fukk ak ñeenteelu atu nguurug Esekiya buurub Yuda, ca la Senakerib buurub Asiri dikk song mboolem dëkki Yuda ya tata wër, daldi leen nangu. 14 Esekiya buurub Yuda yónnee ca buurub Asiri ca Lakis ne ko: «Tooñ naa de, waaye ngalla baal ma, te dem. Loo ma sas dinaa ko fey.» Buurub Asiri sas Esekiya buurub Yuda juróom ñeent fukki barigoy xaalis ak juróom ñeenti barigoy wurus. 15 Esekiya joxe mboolem xaalis ba nekkoon ca kër Aji Sax ji ak ca dencukaayi kër Buur. 16 Booba la Esekiya xobbi wurus wa ñu xoobe woon bunti kër Aji Sax ji ak kenu ya, yónnee ko buurub Asiri.
17 Buurub Asiri nag tollu ca Lakis, yebal bummeem ak kilifay jawriñam ak bëkk-néegam, ñu ànd ak mbooloom xare mu takku, dem Yerusalem. Ba ñu agsee Yerusalem ba tollook solomu mbàndum kaw ma, fa feggook yoon wa jëm ca toolub fóotukaay ba, fa lañu taxaw. 18 Ci kaw loolu ñu woolu Buur. Gannaaw loolu bootalub buur Elyakim doomu Ilkiya moo ànd ak Sebna bindkat ba, ak ka yor téere ya, Yowa doomu Asaf, ñu dikk dajeek ñoom.
19 Ba mu ko defee Rabsake bëkk-néegu buurub Asiri ne leen: «Waxleen nag Esekiya ne ko: Buur bu mag ba, buurub Asiri dafa wax ne: “Sa yaakaar jii nga yaakaar, ana foo ko teg? 20 Defe nga ne làmmiñ kese doy na pexeek njàmbaar cib xare? Ma ne: Ana kan nga yaakaar bay fippu ci sama kaw? 21 Misra daal, nga def sa yaakaar, bantu barax bu tas boobu di sokk képp ku ko wéeroo! Firawna buuru Misra de, mooy boobu bant ci képp ku ko yaakaar. 22 Xanaa doo ma ne seen Yàlla Aji Sax ji ngeen yaakaar? Xanaa du moom nga toxal bérabi jaamookaayam yeek sarxalukaayam, ba noppi ne waa Yerusalem ak Yuda sarxalukaay boobu ci Yerusalem lañuy sujjóotal?” 23 Léegi daal, déggool rekk ak sama sang buurub Asiri, ma jox la ñaari junniy fas. Ndegam am ngay gawaram! 24 Ana noo mana tëwe ki gëna tuut ci sama jawriñi sang? May wax ngay yaakaare Misra ay watiir aki fas! 25 Te sax, xanaa du Aji Sax ji laa àndal ba dalsi fi kaw bérab bii, ngir tas ko? Aji Sax ji ci boppam moo ma ne: “Songal réew mii, tas ko!”»
26 Ci kaw loolu Elyakim doomu Ilkiya ak Sebna ak Yowa ñaan Rabsake, ne ko: «Ngalla, làkk nu arameen, dégg nanu ko. Bu nu wax ebrë, mbooloo mi ci kaw tata ji di ci dégg.» 27 Bëkk-néeg ba ne leen: «Ndax yeen ak seen sang doŋŋ la ma sama sang yóbbante kàddu yii? Ñi toog ci kaw tata ji dañu cee bokkul? Te ñu nara ànd ak yeen lekk seen jonkani bopp, naan seenum saw!» 28 Ba loolu amee bëkk-néeg ba taxaw, xaacu ca kaw ci ebrë ne: «Dégluleen kàddug buur bu mag bi, buurub Asiri. 29 Buur dafa wax ne bu leen Esekiya nax, ndax manu leena xettli ci loxoom. 30 Bu leen Esekiya yaakaarloo Aji Sax ji it, naan leen: “Aji Sax ji moo nuy xettli moos, te deesul teg dëkk bii ci loxol buurub Asiri!” 31 Buleen déglu Esekiya. Buurub Asiri kat dafa wax ne: Jàmmooleen ak man te ngeen génn dëkk bi, dikk nangul ma. Su ngeen ko defee, ku nekk ci yeen mana lekk ak jàmm ci garabu reseñam, lekk ak jàmm ci figgam, di naan ndoxum teenam, 32 ba keroog may dikk, yóbbu leen réew mu mel ni seen reew mi, réewum pepp ak ndoxum reseñ, réewum mburu ak tooli reseñ, réewum garabi oliw, diw ak lem tuuru, ndax ngeen dund te baña dee. Bu leen Esekiya sànk, naan leen: “Aji Sax ji moo nuy xettli.” Buleen ko déglu! 33 Ndax tuuri xeet yi mas nañoo xettli réewu wenn xeet ci buurub Asiri? 34 Ana tuuri réew yii di Amat ak Arpàdd? Ana tuuri Sefarwayim ak Ena ak Iwa? Ndax dañoo xettli Samari ci man? 35 Tuuri réew yépp, ana mu ci xettli menn réew ak man, ba Aji Sax ji wara mana xettli, Yerusalem ak man?»
36 Mbooloo ma nag ne cell, tontuwuñu ko baat, ndax Buur moo leen santoon ne leen buñu ko tontu. 37 Ba loolu amee bootalub Buur, Elyakim doomu Ilkiya ak Sebna, bindkat ba, ak doomu Asaf, Yowa ma denc téere ya, ñoo dem ak seen yérey ñaawlu yu xottiku, ba ca Esekiya. Ñu daldi koy àgge kàddug bëkk-néeg ba.