Limeefu ngàllo ga ñibbsi nii la
2
1 Ñii nag ñoo di niti diiwaanu Yuda, ña jóge njaam ca ngàllo ga leen Nabukodonosor buuru Babilon yóbbu woon, te ñu jóge ca ñibbsi Yerusalem ak Yuda, ku nekk ak fa mu dëkk. 2 Ña nga ñibbi ca njiital Sorobabel ak Yosuwea ak Neyemi ak Seraya ak Relaya ak Mardose ak Bilsan ak Mispar ak Bigway ak Reyum ak Baana.
Limeefu góori bànni Israyil nii la tëdde: 3 Askanu Paros, ñaari junni ak téeméer ak juróom ñaar fukk ak ñaar lañu (2 172). 4 Askanu Sefatiya, ñetti téeméer ak juróom ñaar fukk ak ñaar lañu (372). 5 Askanu Ara, juróom ñaar téeméer ak juróom ñaar fukk ak juróom lañu (775). 6 Askanu Payat Mowab, soqikoo ci Yeswa ak Yowab, di ñaari junni ak juróom ñetti téeméer ak fukk ak ñaar (2 812). 7 Askanu Elam, junni ak ñaar téeméer ak juróom fukk ak ñeent lañu (1 254). 8 Askanu Sàttu, juróom ñeenti téeméer ak ñeent fukk ak juróom lañu (945). 9 Askanu Sakay, juróom ñaar téeméer ak juróom benn fukk lañu (760). 10 Askanu Baani, juróom benni téeméer ak ñeent fukk ak ñaar lañu (642). 11 Askanu Bebay, juróom benni téeméer ak ñaar fukk ak ñett lañu (623). 12 Askanu Asgàdd, junni ak ñaar téeméer ak ñaar fukk ak ñaar lañu (1 222). 13 Askanu Adonikam, juróom benni téeméer ak juróom benn fukk ak juróom benn lañu (666). 14 Askanu Bigway, ñaari junni ak juróom fukk ak juróom benn lañu (2 056). 15 Askanu Adin, ñeenti téeméer ak juróom fukk ak ñeent lañu (454). 16 Askanu Ater, soqikoo ci Esekiya, di juróom ñeent fukk ak juróom ñett (98). 17 Askanu Besay, ñetti téeméer ak ñaar fukk ak ñett lañu (323). 18 Askanu Yora, téeméer ak fukk ak ñaar lañu (112). 19 Askanu Asum, ñaar téeméer ak ñaar fukk ak ñett lañu (223). 20 Askanu Gibar, juróom ñeent fukk ak juróom lañu (95).
21 Waa Betleyem, téeméer ak ñaar fukk ak ñett lañu (123). 22 Waa Netofa, juróom fukk ak juróom benn lañu (56). 23 Waa Anatot, téeméer ak ñaar fukk ak juróom ñett lañu (128). 24 Waa Asmawet, ñeent fukk ak ñaar lañu (42). 25 Waa Kiryaat Yarim ak Kefira ak Berot, juróom ñaar téeméer ak ñeent fukk ak ñett lañu (743). 26 Waa Raama ak Geba, juróom benni téeméer ak ñaar fukk ak benn lañu (621). 27 Waa Migmas, téeméer ak ñaar fukk ak ñaar lañu (122). 28 Waa Betel ak Ayi, ñaar téeméer ak ñaar fukk ak ñett lañu (223). 29 Waa Nebo, juróom fukk ak ñaar lañu (52). 30 Waa Magbis téeméer ak juróom fukk ak juróom benn lañu (156). 31 Waa Elam gu ndaw, junni ak ñaar téeméer ak juróom fukk ak ñeent lañu (1 254). 32 Waa Arim, ñetti téeméer ak ñaar fukk lañu (320). 33 Waa Lodd ak Adidd ak Ono, juróom ñaar téeméer ak ñaar fukk ak juróom lañu (725). 34 Waa Yeriko, ñetti téeméer ak ñeent fukk ak juróom lañu (345). 35 Waa Sena, ñetti junni ak juróom benn téeméer ak fanweer lañu (3 630).
36 Sarxalkat yi ñii la:
Askanu Yedaya, soqikoo ci waa kër Yosuwe, di juróom ñeenti téeméer ak juróom ñaar fukk ak ñett (973). 37 Askanu Imer, junni ak juróom fukk ak ñaar lañu (1 052). 38 Askanu Pasur, junni ak ñaar téeméer ak ñeent fukk ak juróom ñaar lañu (1 247). 39 Askanu Arim, junni ak fukk ak juróom ñaar lañu (1 017).
40 Leween ñi ñii la: Askanu Yeswa ak Kadmiyel. Mooy ñi bànqaasoo ci Odawya, tollu ci juróom ñaar fukk ak ñeent (74).
41 Jàngkat yi ñoo di: Askanu Asaf, di téeméer ak ñaar fukk ak juróom ñett (128).
42 Askanu fara bunt yi ñoo di: Askanu Salum, ak askanu Ater, ak askanu Talmon, ak askanu Akub, ak askanu Atita, ak askanu Sobay, ñépp di téeméer ak fanweer ak juróom ñeent (139).
43 Liggéeykati kër Yàlla gi ñoo di: Askanu Ciya, ak askanu Asufa, ak askanu Tabawot, 44 ak askanu Keros, ak askanu Siya, ak askanu Padon, 45 ak askanu Lebana, ak askanu Agaba, ak askanu Akub, 46 ak askanu Agab, ak askanu Samlay, ak askanu Xanan, 47 ak askanu Gidel, ak askanu Gayar, ak askanu Raaya, 48 ak askanu Reccin, ak askanu Nekoda, ak askanu Gasam, 49 ak askanu Usa, ak askanu Paseya, ak askanu Besay, 50 ak askanu Asna, ak askanu Meyunim, ak askanu Nefusim, 51 ak askanu Bagbug, ak askanu Akufa, ak askanu Arur, 52 ak askanu Baslut, ak askanu Meyida, ak askanu Arsa, 53 ak askanu Barkos, ak askanu Sisera, ak askanu Tema, 54 ak askanu Necciya, ak askanu Atifa.
55 Askanu jaami Suleymaan ñii la: Askanu Sotay, ak askanu Asoferet, ak askanu Peruda, 56 ak askanu Yaala, ak askanu Darkon, ak askanu Gidel, 57 ak askanu Sefatiya, ak askanu Atil, ak askanu Pokeret Asbayim, ak askanu Aami.
58 Mboolem liggéeykati kër Yàlla gi ak askanu jaami Suleymaan yi, ñetti téeméer ak juróom ñeent fukk ak ñaar (392).
59 Ña bàyyikoo Tel Mela ak Tel Arsa ak Kerub Adon ak Imer te manuñoo firndeel ne seen waa kër maam ak seen askan ci Israyil lañu bokk, ñii la: 60 Askanu Delaya, ak askanu Tobya, ak askanu Nekoda, di juróom benn téeméer ak juróom fukk ak ñaar (652).
61 Am na it ñu loolu daloon ci askanu sarxalkat yi, muy askanu Abaya, ak askanu Akocc, ak askanu Barsilay, ma doon denc doomu Barsilay waa Galàdd ba, ba tax ñu santale ko seen sant. 62 Ñooñu, seet nañu seen limeefu kër maam, waaye gisuñu ko. Ñu daldi leen doyadal, génne leen ci carxal gi. 63 Boroom dëkk ba nag aaye leen ñu lekk ci ñam yu sell yaa sell, ba keroog ab sarxalkat di am lu leer ci ñoom ci jumtukaayi tegtal yi ñuy wax Urim ak Tumim.
64 Limu mbooloo ma mépp ba mu daj, ñeent fukki junneek ñaar ak ñetti téeméer ak juróom benn fukk lañu (42 360), 65 te limaaleesul seen jaam yu góor ak yu jigéen, yi tollu ci juróom ñaari junni ak ñetti téeméer ak fanweer ak juróom ñaar (7 337). Amoon nañu itam ay jàngkat yu góor ak yu jigéen, yu tollu ci ñaar téeméer (200). 66 Amoon nañu juróom ñaar téeméeri fas ak fanweer ak juróom benn (736), ak ñaar téeméeri berkelle ak ñeent fukk ak juróom (245), 67 ak ñeenti téeméeri giléem ak fanweer ak juróom (435), ak juróom benni junniy mbaam ak juróom ñaar téeméer ak ñaar fukk (6 720).
68 Ba ñu àggee ca kër Aji Sax ja ca Yerusalem, am na ñenn ca kilifa ya jiite seen kër baay, ñu joxe ay saraxi yéene ngir tabaxaat kër Yàlla ga ca gentam. 69 Joxe nañu ku nekk la mu man, jëme ca alal ja ñuy liggéeye, muy juróomi barigoy wurus ak fanweeri barigoy xaalis, ak téeméeri mbubbi sarxalkat.
70 Ba loolu amee bànni Israyil gépp sancaat ca seen dëkki cosaan, sarxalkat yaak Leween ñaak ñenn ca baadoolo yaak jàngkat yaak fara bunt yaak liggéeykati kër Yàlla ga.