Njaamug Aji Sax ji feddliku na
3
1 Ba juróom ñaareelu weer wa agsee, fekk na bànni Israyil sancaat ca seeni dëkk, mbooloo ma daje doon benn bopp ca Yerusalem. 2 Ba mu ko defee Yosuwe doomu Yoccadag, mook moroomi sarxalkatam, ak Sorobabel doomu Selcel aki bokkam daldi tabax sarxalukaayu Yàllay Israyil, ngir sarxal ca saraxu dóomal ba, mu dëppook li ñu bind ci téereb yoonu Musaa, góorug Yàlla ga. 3 Ci kaw loolu ñu yékkatiwaat sarxalukaay ba, ca kenoom gu jëkk ga, doonte ragaloon nañu waasoy réew ma. Ba ñu noppee, defal ca Aji Sax ji ay saraxi dóomal subaak ngoon. 4 Ñu teg ca amal màggalu Mbaar ya, mu dëppook la ñu bind, boole kook saraxu dóomal yi war bés bu nekk. 5 Gannaaw loolu ñu joxe saraxu dóomal bi sax fàww, ak saraxi Terutel weer ya, ak sarax yu sell yi war ci mboolem màggali Aji Sax ji, ak mboolem saraxi yéene yi ñuy indil Aji Sax ji. 6 Benn fan ca juróom ñaareelu weer wa lañu tàmbalee defal Aji Sax ji ay saraxi dóomal, te fekkul ñu yékkatiwaat kenug kër Aji Sax ji. 7 Ci biir loolu ñu jox xaalis yettkati doj yeek xaddkat yi, jox waa Sidon ak waa Tir ab dund, aki naan akug diw, ngir ñu jëleji Libaŋ ay banti seedar, jaarale ko ci géej gi ba Yafa, ci ndigalal Sirus buuru Pers.8 Ba ñu dikkee ca kër Yàlla ga ca Yerusalem, ba ca déwén sa, ca ñaareelu weeru at ma, Sorobabel doomu Selcel, ak Yosuwe doomu Yoccadag ànd nañook ña des ca seeni bokk, sarxalkat yaak Leween ñaak mboolem ña jóge ca njaam ga délsi Yerusalem. Ñu daldi tàmbali liggéey bi. Ci biir loolu ñu tabb ay Leween ñu am ñaar fukki at, jëm kaw, ñuy saytu liggéeyu kër Aji Sax ja. 9 Yeswa nag jàpp ca, mook doomam yu góor aki bokkam, ak Kadmiyel ak doomam yu góor, ñuy askanu Odawya. Ñu mànkoo di jiite liggéeykat yiy tabaxaat kër Yàlla ga. Waa askanu Enadàdd jàpple nañu leen ci, ñook seen doom yu góor ak seen bokki Leween ña.
10 Ba tabaxkat ya lalee kenug kër Aji Sax ji, ñu tabb ay sarxalkat. Ñu solu ba jekk, yor ay liit, feggook Leween ña askanoo ca Asaf, ànd ak tëggum weñ, di màggal Aji Sax ji, muy la Daawuda buurub Israyil digle woon. 11 Ña ngay jàng, di màggal ak a sant Aji Sax ji, naan:
«Kee baax.
Kee gore ba fàww ci Israyil.»
Ci kaw loolu mbooloo ma mépp xaacu, di ko màggale Aji Sax ji ngir kenug kër Aji Sax ja lale. 12 Teewul ñu bare ca ña féete mag, diy sarxalkat aki Leween aki boroom kër, gisoon nañu kër gu jëkk ga. Ba ñu gisee kenug kër gu bees ga, dañoo yékkati seen kàddu ca kaw di jooy, ñu bare it di xaacu ndax mbégte. 13 Kenn manuloona ràññee coowal mbégte laak jooy ya ndax riiru mbooloo mu réy, di àkki fu sore.